Nj - nj

njaboot g- *   n. famille *, chef de famille; Familie; Kernfamilie; family. Gannaaw ba loolu amee, Aji Sax ji dafa wax Nóoyin ne ko: «Duggal ci gaal gu mag gi, yaak sa njaboot gépp, ndaxte niti jamono jii, yaw rekk laa ci gis, nga jub ni ma ko bëgge.» [Njàlbéen ga / Gn 7.1]

njàqare j- / g- *   n. angoisse; anxiété; embarras; inquiétude; bouleversement *; peur; Angst; Beklommenheit; Ängstlichkeit; Bedrängnis; Besorgnis; Umbruch; anxiety; fear; trepidation; anxiousness; affliction; distress; concern; great fear. Terewul lu ñu leen gëna fitnaal, ñuy gën di fulandiwu tey yokku, ba waa Misra am njàqare ca bànni Israyil. Plus on les opprimait, plus ils devenaient nombreux et plus ils prenaient de place, jusqu'á ce que les égyptiens avaient peur des Israëlites. Je mehr sie sie unterdrückten, desto stärker mehrten sie sich und breiteten sich aus, bis die Ägypter Angst vor den Israeliten bekamen. The more they oppressed them, the more they multiplied and spread; so the Egyptians came to dread the Israelites. [Mucc ga / Ex 1.12]

njariñ l- *   n. utilité; profit *; Nützlichkeit; Nutzen; Gewinn; Vorteil; Profit; usefulness; profit; benefit. Variant: njériñ l-.

amal njariñ   v. avoir de l'utilité; Nutzen haben; Gewinn bringen; to be useful; to bring profit; to be profitable.

njëgg m- *   n. caravane (du désert) *; (Wüsten-)Karavane; caravan (in the desert). Loolu weesu ñu toog, di lekk. Nees-tuut ñu siggi, séen am njëggum giléem, muy ay Ismayleen, yu sëf cuuraayu ndàbb ak diwu yaram ak cuuraayu xas*, jële ko réewu Galaat, jëme Misra. [Njàlbéen ga / Gn 37.25] Ku yab naar, njëgga ma nga dajeel Si tu oses attaquer les moor, c'est que tu as rencontré la caravane. (Les caravanes ne sont pas en position d'attaquer.) [MB]

njël g- / l- *   n. aube *; Morgengrauen; daybreak. Ba njël jotee Aji Sax ji dafa tollu ca biir jumu sawara wa ànd ak niir wa, di xool xarekati Misra, tiital leen, ñu fëlxoo. [Ex 14.24]