Xibaaru jàmm bu Almasi Yeesu, ci jottlib
Luug
Ubbite gi
Luug ak Jëf ya benn téere la bu ëmb ñaari pàcc. Ñaar ñépp a indi ni Yàlla jëkka wooye bànni Israyil ba noppi, doora woo mboolem xeet yi, ngir ñu barkeele ci Ibraayma.
Ci pàcc bu jëkk bi, nettalib Luug Yerusalem la dox jëm, ëttu kërug cosaanu askanu Yawut. Ñaareelu pàcc bi, Jëf ya, Yerusalem la bawoo, jëm ci xeeti àddina yi ci des, doora tëje fi Póol birale nguuru Yàlla ca dëkk ba ñuy wax Room, péeyu nguur gu mag ga.
Pàcc bu jëkk bi nettali dundu Almasi Yeesu, ni ko Luug indee, ñetti dog la.
Dog bi ci jiitu moo di liggéeyu Yeesu ca Galile ca Israyil, wetu bëj-gànnaaram.
Ñaareel bi moo di yoonam wu yàgg wa mu jëme Yerusalem. Ci biir woowu yoon la dalale nit ñi ci àlluwa ju yees ju leen xamal ni Yàlla taxawale nguuram, te mu woroo ak ni kaaŋ-fóorey Israyil dégge nguuru Yàlla ca yooyu jant.
Ñetteelu dog bi, ci la Luug indi ni Almasi Yeesu sarxee bakkanam ca Yerusalem, te gannaaw gi mu dekki, ba firndeel ne moo di buuru Israyil, te moo di Sangub àddina dëgg.