Yaxya waare na
3
1 Ca fukkeelu at ak juróom ci nguurug buur bu mag ba Tibeer Sesaar, ba Poñsë Pilaat yilifee diiwaanu Yude, Erodd yilif diiwaanu Galile, Filib magam yilif diiwaanu Iture ak bu Tarakonit, Lisañas yilif Abilen, 2 jant yooyu Anas ak Kayif dee sarxalkat yu mag ya, ca la kàddug Yàlla dikkal Yaxya doomu Sàkkaryaa, ca màndiŋ ma. 3 Yaxya dugg mboolem àll, bi wër dexu Yurdan, di waare lu jëm ci tuubeel gu nit ñi wara fésale ag sóobu cim ndox, ngir ñu jéggal leen seeni bàkkaar.
4 Loolu lañu bind ci téereb waxi Yonent Yàlla Esayi ne:
«Baat a ngi xaacoo ca màndiŋ ma, naan:
“Xàll-leen yoonu Boroom bi,
jubal-leen ay xàllam.
5 Xur yépp ay sëkke,
tund wu magoo wu ndaw maasaloo,
yoon ya lunkoon, jubbantiku,
ya ñagasoon, nooy,
6 ba wépp suux gis mucc gi Yàlla dogal.”»
7 Yaxya nag di wax mbooloo may ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, naan leen: «Yeen njurum jaan mee, ku leen àrtu, ba ngeen di daw sànj miy dikk? 8 Kon nag jëfeleen jëf ju yelloo ag tuubeel, te baña nax seen bopp naan: “Nun, Ibraayma mooy sunu maam,” ndax maa leen ko wax, doj yii, Yàlla man na cee sàkkal Ibraayma aw askan. 9 Te itam sémmiñ xàccil na reenu garab ba noppi. Kon nag gépp garab gu ci meññul doom yu baax, dees koy gor, sànni ca sawara sa.»
10 Mbooloo ma itam laaj ko ne ko: «Ana lu nu war nag?» 11 Mu ne leen: «Ku am ñaari turki, na sédd ki amul. Ku am aw ñam itam, na defe noonu.» 12 Ay juutikat itam dikk, ngir sóobusi; ñu ne Yaxya: «Sëriñ bi, ana lu nu war?» 13 Mu ne leen: «Xanaa baña sàkku lenn lu moy li jaadu.» 14 Ay takk-der itam ne ko: «Nun nag, nu nuy def?» Mu ne leen: «Buleen néewal kenn doole, mbaa di duural kenn ngir jëlal ko dara; doyloo leen seen peyoor.»
15 Ci kaw loolu askan wa di séentu, ñépp di seetaat ci seen xel, ndax Yaxya mooy Almasi. 16 Yaxya wax leen ñoom ñépp ne leen: «Man de ci ndox laa leen di sóob. Waaye ku ma sut a ngi ñëw, kooku, buumi caraxam sax, yeyoowuma ko koo feccil. Moom, ci Noo gu Sell gi ak sawara la leen di sóoba. 17 Ab layoom a ngi ci loxoom, mooy jéri dàggaam, ba mu set wecc; pepp mi lay fat cim sàqam, waaye xatax bi, da koy lakk ci sawara su dul fey mukk.»
18 Bare na yeneen dénkaane yu Yaxya doon xamale nit ñi xibaaru jàmm bi. 19 Erodd boroom diiwaan ba nag, Yaxya sikkoon na ko ndax Erojàdd jabaru magam ja mu nekkaloon, ak mboolem yeneen ñaawtéef yu Erodd def. 20 Mu tegati leneen ca loolu lépp: jàpp Yaxya, tëj ca kaso ba.
Yaxya sóob na Yeesu ci ndox
21 Noonu Yaxya doon sóobe ñépp cim ndox, ni la deme ba Yeesu dikk, mu sóob ko ci ndox. Ci biir loolu Yeesu yékkati kàddug ñaan, asamaan ubbiku. 22 Ba loolu amee Noo gu Sell gi moo bindoo ni pitax, wàcc ci kawam, baat jibe asamaan, ne: «Yaa di sama Doom, sama soppe; yaa may bànneexal.»
Lu jëm ci cosaanu Yeesu Almasi
23 Yeesu ci boppam ba muy door, amoon na lu tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa, ni ko xel mana jàppe.
Yuusufa, Eli mooy baayam, 24 Eli, Matat.
Matat, Lewi; Lewi, Melki;
Melki, Yanayi; Yanayi, Yuusufa;
25 Yuusufa, Matacas; Matacas, Amos; Amos, Nawum; Nawum, Esli; Esli, Nagayi.
26 Nagayi, Maat; Maat, Matacas; Matacas, Semeyin; Semeyin, Yoseg; Yoseg, Yoda.
27 Yoda, Yowanan; Yowanan, Resa;
Resa, Sorobabel; Sorobabel, Selcel; Selcel, Neri;
28 Neri, Melki; Melki, Adi; Adi, Kosam; Kosam, Elmadam; Elmadam, Er.
29 Er, Yeesu; Yeesu, Elyeser; Elyeser, Yorim; Yorim, Matat; Matat, Lewi;
30 Lewi, Simeyon; Simeyon, Yuda; Yuda, Yuusufa; Yuusufa, Yonam; Yonam, Elyakim.
31 Elyakim, Meleya; Meleya, Mena;
Mena, Matata; Matata, Natan;
Natan, Daawuda. 32 Daawuda mooy doomu Yese;
Yese, Obedd; Obedd, Bowas; Bowas, Sala; Sala, Nason.
33 Nason, Aminadab; Aminadab, Admin; Admin, Arni;
Arni, Esron; Esron, Peres; Peres, Yuda; 34 Yuda, Yanqóoba; Yanqóoba, Isaaxa; Isaaxa, Ibraayma;
Ibraayma, Teraa; Teraa, Naxor;
35 Naxor, Serug; Serug, Rew; Rew, Peleg; Peleg, Eber; Eber, Sela;
36 Sela, Kenan; Kenan, Arpagsàdd;
Arpagsàdd, Sem; Sem, Nóoyin; Nóoyin, Lemeg;
37 Lemeg, Matusalem; Matusalem, Enog; Enog,
Yeredd; Yeredd, Malaleel; Malaleel, Kenan;
38 Kenan, Enos; Enos, Set; Set, Aadama;
Aadama, Yàlla.