Bàkkaarloo nit aay na
17
1 Yeesu neeti ay taalibeem: «Ag fiir guy bàkkaarloo manula ñàkk, waaye wóoy ngalla ka koy lal. 2 Ñu takkoon doj wu réy ci baatam, sànni ko biir géej moo gën ci moom muy yóbbe bàkkaar kenn ci xale yii. 3 Wattuleen seen bopp.Jéggal-leen ku leen tuubal
«Bu la sa mbokk tooñee, yedd ko. Bu tuubee, baal ko. 4 Su la tooñoon juróom ñaari yoon ci bés bi, te walbatiku juróom ñaari yoon, ne la: “Tuub naa ko,” baal ko rekk.»
Ngëm maye na kéemtaan
5 Ci kaw loolu ndaw ya ne Sang bi: «Yokk nu ngëm.» 6 Sang bi ne leen: «Su ngeen amoon ci ngëm, lu tollu ni peppu fuddën sax, ba ne garab gii: “Buddeekul, dem jëmbate ca géej ga,” su boobaa garab gi déggal leen.
Ab jaam du sàkku jaajëf
7 «Kan ci yeen la ab jaamam di beyi mbaa mu sàmmi ba jóge tool, dikk, mu ne ko: “Kaay, nu lekk”? 8 Xanaa kay da koy wax ne ko: “Defaral sama reer, te takku, taajal ma, ba ma lekk, naan, nga doora lekk, naan.” 9 La jaam ba jëfe ndigal tax na sangam sant ko? Déedéet kay. 10 Yeen itam noonu. Bu ngeen defee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeena war ne: “Ay jaam rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»
Yeesu faj na fukki gaana
11 Ci biir yoon woowu Yeesu jëmoon Yerusalem, ma nga jaare fa Samari ak Galile digaloo. 12 Mu dem bay duggsi cib dëkk, fukki gaana dikk, dajeek moom, ba dànd ko, daldi taxaw. Ñu xaacu ne: 13 «Yeesu, Njaatige, yërëm nu!» 14 Yeesu nag gis leen, ne leen: «Demleen seetluji seen yaram ca sarxalkat ya.»
Ba ñuy dem ca sarxalkat ya lañu wér, seen yaram set. 15 Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi walbatiku, di xaacuy sàbbaal Yàlla. 16 Mu dikk, ne gurub, dëpp jëëm fa tànki Yeesu, sant ko. Waa ja nag nitu Samari la woon. 17 Ba loolu amee Yeesu ne: «Xanaa du fukk a wér? Juróom ñeent ña nag, ana ñu? 18 Amu ci kenn ku ñëw, delloo Yàlla njukkal ku dul doxandéem bii!» 19 Yeesu nag ne ko: «Jógal dem; sa ngëm faj na la.»
Nguurug Yàlla door na ba noppi
20 Farisen yi ñoo laajoon Yeesu, ne ko: «Kañ la nguurug Yàlla di dikk?» Mu ne leen: «Dikkug nguurug Yàlla du ànd akum ceetaan. 21 Deesul ne it: “Xool-leen, mu ngi” mbaa: “Ma ngee,” ndax kat nguurug Yàlla mu ngi ci seen biir.»
22 Mu ne taalibe ya: «Ay jant a ngi ñëw yu ngeen naa ngéejoo fekke benn bés ci bési Doomu nit ki, te dungeen ko fekke. 23 Te it, dees na leen ne: “Ma ngee!” mbaa: “Mu ngii!” Buleen dem, buleen ca topp. 24 Ndax ni melax di xuyye gii wetu asamaan, ba ne ràññ ca gee, noonu la Doomu nit kiy def keroog bésam. 25 Waaye balaa booba fàww Doomu nit ki am coono yu bare, jànkoonteek diiŋatu niti tey jii.
26 «Noonee mu deme woon ca janti Nóoyin, ni lay deme ca janti Doomu nit ki. 27 Nit ñaa nga doon lekk ak a naan, di jël jabar ak a séyi, ba keroog bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga, mbënn ma dikk, sànk ñépp.
28 «Noonee itam la deme woon ca janti Lóot. Nit ñaa nga doon lekk ak a naan, di jënd ak a jaay, di jëmbat ak a tabax. 29 Waaye bés ba Lóot génnee Sodom, la tawub sawara ak tamarax wàcce asamaan, sànk ñépp. 30 Noonu doŋŋ lay deme, bés bu Doomu nit kiy feeñ.
31 «Bésub keroog boobee, ku mu fekk ci kaw am taax, te say yëf ne ca biir kër ga, bul wàcc, di ko jëli. Te ku mu fekk tool ba itam, bul dellu. 32 Fàttlikuleen jabaru Lóot ja! 33 Képp kuy wuta rawale sa bakkan, yaay ñàkk sa bakkan, waaye képp ku ñàkk sa bakkan, yaay dund. 34 Maa leen ko wax: guddig keroog ñaar ay bokk benn lal, kenn ki, ñu yóbbu ko, ka ca des, ñu ba ko. 35-36 Ñaar di wolandoo, kenn ki, ñu yóbbu ko, ka ca des, ñu ba ko.»
37 Taalibe yi ne Yeesu: «Loolu fan la, Sang bi?» Mu ne leen: «Fu médd nekk, fa la tan yay daje.»