Njiiti yoon yi fexeel nañu Yeesu
22
1 Màggalu Mburu mu amul lawiir, te ñu di ko wax bésub Mucc, moo jubsi woon. 2 Ci biir loolu sarxalkat yu mag ya ak firikati yoon ya di seet nu ñuy fexee ba rey Yeesu, waaye dañoo ragaloon nit ña. 3 Seytaane nag dugg Yuda, mi ñuy wooye Iskaryo te mu bokkoon ca Fukk ñaak ñaar. 4 Yuda daldi diisooji ak sarxalkat yu mag ya, ak kilifay wattukati kër Yàlla ga, ngir xam nan lay tege Yeesu ci seeni loxo. 5 Ñu am ca mbégte, digook moom, ngir jox ko xaalis. 6 Yuda nangu, di wut nag yoon wu mu wore Yeesu, fu mbooloo ma teewul.Yeesu tàggoo na
7 Ci kaw loolu bésu màggalu Mburu mu amul lawiir agsi, ñu war caa rendi gàttub bésub Mucc. 8 Yeesu yebal Piyeer ak Yowaan ne leen: «Demleen, waajalal nu bésub Mucc bi, ba nu reeri.» 9 Ñu ne ko: «Foo bëgg nu waaje ko fa?» 10 Mu ne leen: «Bu ngeen di dugg ca dëkk ba rekk, dingeen dajeek waa ju yenu njaqas ndox. Toppleen ci moom ba ca biir kër ga mu jëm, 11 te ngeen ne boroom kër ga: “Sëriñ bi nee: Ana néegu gan, bi may reere reeru bésub Mucc, maak samay taalibe?” 12 Kooku moo leen di won néegub kaw bu yaa bu ñu defar ba noppi. Foofa ngeen di waajale.»
13 Ba ñu demee, noonee leen ko Yeesu waxe, na lañu gise lépp. Ñu daldi waajal reer ba.
14 Ba waxtuw reer jotee, Yeesu toog ak ndaw ya, 15 ne leen: «Yàkkamti woon naa lool bokk ak yeen reeru bésub Mucc bii, bala maa tàbbi coono. 16 Ndax maa leen ko wax, dootuma ko reer mukk, ba keroog solob reer bi di sotti ca nguurug Yàlla.»
17 Ci kaw loolu mu jël ab kaas, yékkati kàddug cant, daldi ne: «Jël-leen kaas bii, te ngeen séddoo ko. 18 Ndax maa leen ko wax, gannaaw-si-tey dootuma naan ndoxum reseñ, ba kera nguurug Yàlla dikk.»
19 Gannaaw loolu mu jël mburu, yékkati kàddug cant, dagg ko, jox leen ko ne: «Lii moo di sama yaram wi ñu jooxe ngir yeen. Deeleen def lii, di ma ko fàttlikoo.»
20 Kaas ba itam noonu la def ak moom gannaaw reer ba, ne leen: «Kaas bii mooy kóllëre gu yees gi fasoo ci sama deret ji leen nara tuurul. 21 Waaye nag ki may wor, loxoom a ngi ci ndab lii nu bokk. 22 Doomu nit ki déy, ni ñu ko dogale, noonu lay deme, waaye wóoy ngalla ki pexe mi ñu koy wore di jaare ci moom.» 23 Ci kaw loolu taalibe yi di laajante ci seen biir, kan ci ñoom moo nar jooju jëf.
24 Ab werante itam dikkal leen, ñuy xëccoo ci seen biir ku wara gëna kawe ci ñoom. 25 Yeesu nag ne leen: «Buuri xeeti àddina doole lañuy nguuroo ci seen kaw, teewul ñi leen di néewal doole, baaxekati nit ñi lañu leen di wooye. 26 Yeen nag bumu deme noonu ci seen biir. Ki gëna kawe ci yeen, na mel ni moo gën di ndaw, te njiit li, na mel ni ab surga. 27 Ki ñu taajal ndab li, ak surga bi ko taajal, ana ku ci gëna kawe? Xanaa du ki ñu taajal? Moonte man, ci seen biir laa tooge toogaayu surga! 28 Yeen nag yeenay ñi des ak man ci sama biir coono. 29 Man itam ni ma sama baay dénke nguur, ni laa leen koy dénke. 30 Yeenay lekk ak a naane ca sama ndab, ca sama nguur, te yeenay tooge ay gàngune, di jiite fukki giiri bànni Israyil ak ñaar.»
31 Yeesu neeti: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane kat mu ngi sàkku ab sañ-sañ ngir man leena jéri ni am pepp. 32 Waaye man tinul naa la, ngir sa ngëm baña giim. Yaw nag boo waññikoo, nanga dooleel sa bokki gëmkat.» 33 Piyeer ne ko: «Sang bi, jekk naa ci ànd ak yaw kaso, ak ci ànd ak yaw dee.» 34 Yeesu ne ko: «Piyeer, maa la ko wax, bala ganaar a sab tey jii, dinga weddi ñetti yoon ne xam nga ma.»
35 Yeesu neeti leen: «Ba ma leen yebalee te du dencukaayu xaalis, du mbuus, du carax yu ngeen yóbbaale, ndax ñàkk ngeen dara?» Ñu ne ko: «Déedéet.» 36 Mu ne leen: «Léegi nag képp ku am dencukaayu xaalis, na ko jël, ku am mbuus it, na ko jël; ku amul saamar, na jaay mbubbam, jënde saamar. 37 Ndax maa leen ko wax, li ñu bind ne, “Mook defkati mbon yi lañu boole ab àtte,” fàww mu am ci man, te loolu jëm ci sama mbir mu ngi sottisi.» 38 Ñu ne ko: «Sang bi, ñaari saamar a ngi fi.» Mu ne leen: «Doy na.»
Yeesu ñaan na ca tundu Oliw ya
39 Ci kaw loolu Yeesu génn, jëm ca tundu Oliw ya, na mu ko baaxoo woon, taalibe ya topp ci moom. 40 Ba mu agsee ca bérab ba, da ne leen: «Ñaanleen, ngir baña tàbbi cig fiir.» 41 Ba loolu amee mu dànd leen lu tollook saanu xeer, daldi sukk, di ñaan. 42 Mu ne: «Baay, su dee sa coobare, teggil ma kaasu naqar bii. Bumuy sama coobare nag, waaye yaw, na sa coobare am.» 43 Malaaka mu bawoo asamaan daldi koy feeñu, dooleel ko. 44 Njàqare nag jàpp Yeesu, mu gënatee tënku ci kàdduy ñaanam, ba aw ñaqam mujj mel ni lumbi deret, di dal ci suuf.
45 Mu ñaan ba noppi, daldi jóg, délsi ci taalibe yi, fekk leen ñuy nelaw, sonn lool ndax aw tiis. 46 Mu ne leen: «Lu ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir.»
Jàpp nañu Yeesu
47 Naka la Yeesu di wax, daaneelagul, mbooloo ne jimeet, ka ñuy wax Yuda, di kenn ca Fukk ñaak ñaar jiite leen. Yuda dikk ba ci Yeesu, bëgg koo fóon. 48 Yeesu ne ko: «Yuda, fóon ngay wore Doomu nit ki!» 49 Ña ànd ak Yeesu nag gis la ca nara topp, ñu ne: «Sang bi, nu jame saamar boog?» 50 Kenn ci ñoom daldi caw surgab sarxalkat bu mag ba, njoof noppu ndijooram. 51 Teewul Yeesu ne: «Bàyyileen, na fi yem.» Mu laal noppu waa ja, wéral ko.
52 Ba loolu amee Yeesu wax ak ña ko jàppsi: sarxalkat yu mag ya, ak kilifay wattukati kër Yàlla ga, ak mag ña. Mu ne leen: «Mbete dama di ab fippukat, ba ngeen dikkey saamar aki njur. 53 Moona bés bu nekk, maak yeen la woon ca kër Yàlla ga, te teguleen ma loxo. Waaye seen waxtu la léegi, bi kilifteefug lëndëm ayee nii.»
Piyeer jàmbu na
54 Ba mu ko defee ñu jàpp Yeesu, yóbbu ko ba ca kër sarxalkat bu mag ba, Piyeer dànd fu sore, topp ca. 55 Fekk na ñu taal sawara ca digg ëtt ba, toog yéew sawara wa, Piyeer dikk toog ca seen biir. 56 Ab surga bu jigéen nag gis ko, mu toog fi kanam taal bi, mu ne ko jàkk, ne: «Kii it ci la, moom la àndaloon!» 57 Piyeer nag miim, ne: «Soxna si, xawma kooku!» 58 Nes tuut keneen gis ko ne: «Yaw it ci ñoom nga!» Piyeer ne ko: «Waa jii, du man!»
59 Ba ñu ca tegee lu mat waxtu, keneen jaaraat ca wax ja ne: «Kii kay wax-dëgg, moom la àndaloon, nde waa Galile la.» 60 Teewul Piyeer ne ko: «Waa jii, li ngay wax, xawma ma ko de!» Ca saa sa, ganaar sab, te kàddug Piyeer daanoogul sax. 61 Ci kaw loolu Sang bi geesu, ne jàkk Piyeer, Piyeer fàttliku la ko Sang bi waxoon ne ko: «Bala ganaar a sab tey jii, dina fekk nga jàmbu ma ñetti yoon.» 62 Piyeer nag génn, di jooy jooy yu metti.
Mitital nañu Yeesu
63 Ci kaw loolu ña jàpp Yeesu, di ko kókkali ak a dóor. 64 Ñu muur kanam gi, naan ko: «Yaw, waxal nu kàddug waxyu boog, ana ku la dóor?» 65 Yeneen saaga yu bare tifaar nañu ko ko.
Yeesu janoo naak Pilaat ak Erodd
66 Ba bët setee, mbooloom magi askanu Yawut, ak sarxalkat yu mag ya, ak firikati yoon ya, ñépp daje. Ñu yóbbu Yeesu ca seen kurélu àtte ba. 67 Ñu ne ko: «Soo dee Almasi, wax nu ko.» Mu ne leen: «Su ma leen ko waxee, dungeen ma gëm. 68 Te su ma leen laajee, dungeen tontu. 69 Waaye gannaaw-si-tey, Doomu nit ki mooy toog ci ndijooru Yàlla, Aji Man ji.» 70 Ñépp daldi ne: «Kon yaay Doomu Yàlla?» Mu ne leen: «Yeena waxal seen bopp ne man la.» 71 Ñu ne nag: «Lu nuy doyeeti seede, gannaaw nun ci sunu bopp noo ko dégge ci gémmiñam!»