Yeesu Almasi dekki na
24
1 Ca ëllëg sa, di ndoortel ayu bés, jigéen ña jëlu dem ca bàmmeel ba, yóbbaale cuuraay la ñu waajal. 2 Ñu agsi bàmmeel ba, fekk ñu randal doj wa uboon bunt ba, laf ko ca wet ga. 3 Ñu dugg, fekkuñu fa néewu Sang Yeesu. 4 Naka lañu nekke seenug njaaxle ci loolu, ñaari góor ne jimeet fa seen wet, sol yére yuy melax. 5 Naka la leen tiitaange jàpp, ba ñu sukk, dëpp seen jë fa suuf, ñu ne leen: «Kiy dund, lu tax ngeen di ko seet ci biir ñi dee? 6 Nekku fi; dekki na. Fàttlikuleen la mu leen waxoon, ba mu génnagulee Galile. 7 Da noon: “Fàww ñu teg Doomu nit ki ci loxoy bàkkaarkat yi, ñu daaj ko ci bant, rey ko, ba ñetteelu fanam, mu dekki.”» 8 Booba lañu fàttliku kàddug Yeesu googu.
9 Ñu jóge ca bàmmeel ba, dem àgge loolu lépp Fukk ñaak benn, ak ña ca des ñépp. 10 Jigéen ña àgge loolu ndaw ya ñoo doon Maryaamam Magdala, ak Yowaana, ak Maryaama yaayu Yanqóoba, ak itam ñeneen jigéen ñu àndoon ak ñoom. 11 Teewul ñu def waxi jigéen ña ay caaxaan, ba gëmuñu leen. 12 Piyeer nag jóg, daw, ba ca bàmmeel ba. Mu sëgg, yër, gisul lu dul càngaay la. Mu daldi ñibbi, jaaxle lool ca mbir ma.
Yeesu feeñ na ca yoonu Emayus
13 Ndeke ca bés booba ñaar ca taalibe yaa nga woon ca yoonu dëkk bu ñuy wax Emayus, digganteem ak Yerusalem wara tollu ci fukki kilomeetar. 14 Ña ngay waxtaane mboolem xew-xew yooyu. 15 Naka lañuy waxtaan ak a diisoo, Yeesu ci boppam dab leen, ànd ak ñoom. 16 Teewul seeni gët tëlee ràññee, ba manuñu koo xàmmi. 17 Yeesu ne leen: «Lu ngeen di waxtaane nii ci yoon wi?» Ñu daldi taxaw, seen kanam lëndëm ndaxu tiis. 18 Kenn ci ñoom, ku ñuy wax Kelyopas ne ko: «Xanaa yaw rekk de, yaa dal Yerusalem te umple li fi xew fan yii?» 19 Yeesu ne leen: «Lu fi xew?» Ñu ne ko: «Mbirum Yeesum Nasaret. Mu doonoon ab yonent bu manoorewu ci jëf ak ci kàddu, Yàlla ak askan wépp seede. 20 Waaye sunu sarxalkat yu mag ak sunuy njiit ñoo ko teg ciy loxo, ngir ñu teg ko àtteb dee, daaj ko ci bant. 21 Nun nag danoo yaakaaroon ne mooy jotsi Israyil. Loolu lépp teewul nu ngii ci ñetteelu fan, ba mbir yooyu amee ba tey. 22 Ay jigéen ñu bokk ci nun nag ñoo nu jaaxal. Ndax ñoo jëlu dem ca bàmmeel ba, 23 waaye fekkuñu fa néewam. Ñu dikk, ne ay malaakaa leen feeñu, xamal leen ne Yeesoo ngi dund. 24 Ñenn ci sunuy àndandoo it dem nañu ca bàmmeel ba, fekk ko noonee ko jigéen ña waxe. Waaye moom, gisuñu ko.»
25 Ci kaw loolu mu ne leen: «Yeen daal, yeena ñàkk xel, yeena naqarim xel, ndegam ba tey gëmaguleen mboolem li yonent yi xamle woon! 26 Xanaa du fàww Almasi daj boobu coono, doora dugg ci teraangaam?» 27 Mu tàmbalee nag ci Yonent Yàlla Musaa, jaare ci yonent yépp, tekkil leen mboolem lu Mbind mi indi ci mbiram.
28 Naka lañuy jub dëkk, ba ñu jëm, mu mel ni ku nara jubal yoonam. 29 Ñu daldi koy téye, ne ko: «Dalal ak nun, ndax jant baa ngi so, léegi mu guddi.»
Ba loolu amee mu dugg, dal ak ñoom. 30 Ba reer jotee mu toog ak ñoom ca ndab la, jël mburu ma, yékkati kàddug cant, daldi dagg, jox leen. 31 Ca la seeni gët ubbiku, ñu xàmmi ko. Moom nag, mu ne mes, réer leen. 32 Ba loolu amee, ku nekk naan sa moroom: «Ndax yéguloo woon cawartey xol bu tooy, ba muy wax ak nun ci yoon wi, di nu firil Mbind mi?»
33 Ñaari taalibe ya daldi jóg ca waxtu woowu tembe, dellu Yerusalem, ca Fukk ñaak benn. Ñu fekk leen ñu dajeek seeni àndandoo. 34 Ci kaw loolu ñu ne ñaar ña jóge Emayus: «Ndeke Sang bi kay, dekki na; feeñu na Simoŋ!» 35 Ñaari taalibe ya ñoom it, nettali leen la xewoon ca yoon wa ak na ñu xàmmee Yeesu, ba mu daggee mburu ma.
Yeesu feeñu na ay taalibeem
36 Ba ñaari taalibe ya di nettali loolu, ca la Yeesu ci boppam ne jimeet taxaw ci seen biir, ne leen: «Jàmm seen!» 37 Tiitaange lu réy jàpp leen, ñu foog ne njuuma lañu gis. 38 Yeesu nag ne leen: «Lu ngeen di jaaxle, ak lu ngeen di xel-yaar nii? 39 Xool-leen samay loxo ak samay tànk. Man la. Làmbleen ma, ba xam! Njuuma amul suux, amuli yax, nii ma ko ame, ngeen gis.» 40 Loolu la leen wax, daldi leen won ay loxoom aki tànkam. 41 Taalibe ya nag boole mbég akug jaaxle ba tax manuñu koo gëm. Mu ne leen: «Lu ngeen fi am, lu ñuy lekk?» 42 Ñu jox ko dogu jën wu ñu lakk. 43 Mu jël ko, lekk ci seen kanam.
44 Ci kaw loolu mu ne leen: «Lii moo di kàddu ya ma leen waxoon ba ma nekkee ak yeen. Noon naa leen: Mboolem li ñu bind ci samay mbir ci yoonu Musaa, ak ci téerey yonent yi, ak ci Sabóor, fàww lépp sotti.» 45 Ca la ubbi seen xel, ngir Mbind mi leer leen. 46 Mu ne leen: «Nii lees binde, ne fàww Almasi dee ci biir coono, ba ñetteelu fanam, mu dekki, 47 te ciw turam, dees na dale ci Yerusalem, yégal xeet yépp, tuubeel gu jur njéggalug bàkkaar. 48 Loolu yeena ko seede. 49 Man ci sama bopp maa leen di yónnee li sama baay dige. Waaye yeen toogleen ci dëkk bi, ba kera ñu leen solee manoore ju bawoo fa kaw.»
Yeesu tàggooti na
50 Gannaaw loolu Yeesu yóbbu leen ca wetu Betani. Ci kaw loolu mu yékkati ay loxoom, barkeel leen. 51 Ba mu leen di barkeel, ca la teqlikoo ak ñoom, ñu yéege ko asamaan. 52 Ñoom nag, ñu sujjóotal ko, daldi dellu Yerusalem, ànd ak mbég mu réy. 53 Saa su nekk, ña nga woon ca kër Yàlla ga foofa, di sant Yàlla.