Yàlla waccul bànni Israyil
11
1 Ma ne kon, xanaa Yàlla daa wacc ñoñam? Mukk kay! Man ci sama bopp ci Israyil laa bokk, askanoo ci Ibraayma, giiroo ci Beñamin. 2 Yàlla waccul ñoñam ñi mu ràññee woon lu jiitu. Am dangeena xamul li Mbind mi indi ci mbirum Ilyaas, ba mu dikkee Yàlla njàmbat lu jëm ci Israyil? Mu ne: 3 «Boroom bi, say yonent, rey nañu leen; say sarxalukaay, màbb nañu leen; man doŋŋ maa fi des, te ñu ngi wut sama bakkan.a» 4 Ana lu ko Yàlla tontu? Da ne: «Beral naa sama bopp juróom ñaari junniy (7 000) nit ñu sujjóotaluloon Baal tuur mib 5 Kon nag naka noonu itam ci jamonoy tey jii, aw ndes a ngi fi, te ci kaw yiw lees leen taamoo. 6 Gannaaw aw yiw a tax nag, dootu seen peyu jëf, lu ko moy aw yiw noppee doon aw yiw.
7 Kon léegi nag? Li am moo di li bànni Israyil doon wut, amuñu ko. Ñi ñu taamu ñoo ko am, ña ca des, seenum xel a dërkiis. 8 Noonu lees binde ne:
«Yàlla moo leen jox xelum ngëmment,
ak bët yu dul gis, ak nopp yu dul dégg,
ba bésub tey jiic
9 Daawuda it wax na ne:
«Yal na seen ndab di seenum yeer,
boole ci dib caax,
te di fiir gu ñuy daanu,
muy seenub yool.
10 Yal na seeni gët giim, ba duñu gisati,
yal nañu sëgg ba fàwwd
Lu jëm ci muccug ñi dul Yawut
11 Moo tax ma ne xanaa ba bànni Israyil tërëfee, jéll bu ñu dul jógati lañu daanu? Mukk kay! Waaye tooñug bànni Israyil moo waral muccug jaambur ñi dul Yawut, ba tax bànni Israyil siis leen. 12 Gannaaw tooñug bànni Israyil mooy xéewalu àddina si, seenug néewle di xéewalu jaambur ñi dul Yawut, kon bu bànni Israyil yembee, ndaw xéewal gu gënatee baawaan!
13 Léegi nag yeen jaambur ñi dul Yawut laay waxal. Gannaaw maay ndaw li ñu yebal ci jaambur ñi dul Yawut, samab yónnent laay teral. 14 Jombul sama liggéey dina yee fiiraangey sama bokki Yawut ñi, ba ñenn ci ñoom mucc. 15 Ndax kat ba Yàlla dàqee Israyil, ca la àddina juboo ak Yàlla. Kon nag bu leen Yàlla délloosee, ana lu muy jur lu moy ndee-ndekki? 16 Ndax kat ab jooxe bu génnee ci tooyalub sunguf, di ndoortel meññeef, su boobu jooxe sellee, tooyalub sunguf bépp ay sell. Ndax su reenu garab sellee, car ya it sell.
17 Waaye su ñu tenqee lenn ci cari oliwu kër, te yaw ngay caru oliwu àll, ñu indi la, jabtal ci oliwu kër gi, nga wuutu car ya ca fàqe, ba mana xéewloo meen miy wale ci reenu oliwu kër gi, di ko dundal, 18 bumu tax nga bàkku ci kaw car ya fàqe. Soo dee bàkku, xamal ne du yaa yenu reen bi, waaye reen bee la yenu.
19 Xam naa dinga ne: «Car yooyu, dees leena tenqi, ngir jabtal ma.» 20 Dëgg it; waaye ngëmadi moo leen fa tenqee, te yaw, ngëm a la fa teg. Bu ko réy-réyloo, waaye ragalal. 21 Ndegam cari judduwaale ya la Yàlla déegul, moytul mu bañ laa déeg yaw itam.
22 Xoolal kon ni Yàlla baaxe, ak ni mu ragloo; ci ñi déggadi la raglu, baax ci yaw, ndegam cig mbaaxam nga sax; lu ko moy dees na la tenqi yaw itam. 23 Car ya fàqe woon itam, su ñu wéyewul ngëmadi, dees leen di delloo ca ndey ja, nde Yàlla man na leen caa saxalaat. 24 Ndax kat, ndegam yaw lañu tenqee ci oliwu àll gi, jabtal la ci oliwu kër gi dul sa ndey, astamaak car yi oliwu kër gi di seen ndey, nde saxalaat leen ca mooy gëna yombati.
Yàlla ñépp la yërëm
25 Bokk yi, moytuleena defe ne seen xel mu rafet a leen may li ngeen am. Bugguma ngeen umple mii mbóot: Ag déggadi moo dikkal lennati bànni Israyil, ba kera xeet yi dul Yawut duggsi, ba seenub lim mat. 26 Su boobaa nag, bànni Israyil gépp ay mucc, noonee ko Mbind mi indee ne:
«Siyoŋ la wallukat bay jóge,
mooy tenqee ngëmadi ci askanu Yanqóoba.
27 Loolooy doon sama kóllëreek ñoom,
kera ba may far seeni bàkkaare
28 Ci wàllu xibaaru jàmm bi, ay noon la Yawut ñi taxawe, te muy xéewal ci yeen ñi dul Yawut. Waaye ci wàllu dogal bi taamu Yawut ñi, ay soppe lañu, te seeni maam tax. 29 Ndax Yàlla kat, ay mayam akub wooteem, lenn du ci toxu. 30 Yeena déggadi woon, waaye tey daj ngeen yërmande, ndax déggadig Yawut yi. 31 Noonu itam la Yawut yi déggadee tey, ba ni ngeen daje yërmande, ñoom it ñu daje ni yërmande. 32 Yàlla moo tëj nit ñépp ci seenug déggadi, ngir yërëm leen ñoom ñépp.
Yàllaa yelloo teddnga
33 Céy xóotaayub koomu Yàlla ak xel ma, ak xam-xam ba! Deesul natt ay dogalam, deesul ràññee ay jëfinam!
34 «Ana ku xam xalaatu Boroom bi?
Ana ku ko digalf
35 «Ana ku ko dawlul lenn,
ba mu war koo delloog
36 Ci moom la lépp sosoo, ci moom la lépp sottee, te moom la lépp ñeel. Moom la daraja ñeel ba fàww! Amiin.