Ñaareelu bataaxal bi Yàlla may Póol, mu bind ko waa
Korent
1
1 Ci man Póol, ndawal Almasi Yeesu ci coobarey Yàlla, ci man la bataaxal bii bawoo, bawoo itam ci Timote mbokk mi, ñeel mbooloom Yàlla mi ci Korent, ak mboolem ñu sell ñi ci diiwaanu Akayi gépp. 2 Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.Yàlla mooy dëfal xol yi
3 Cant ñeel na Yàlla sunu Baayu Sang Yeesu Almasi, Baayu yërmande yi, Yàlla jiy dëfale nu nekk, 4 moom mi nuy dëfal ci sunu jépp njàqare, ngir noonu nu jote nun ci sunu bopp, ndëfalaay lu nu dëfaloo fa Yàlla, nu man koo dëfale ñi nekke mboolem xeeti njàqare. 5 Ndax kat coonoy Almasi, nu mu gëna yokkoo ci sunu kaw, ndax li nu ko gëm, noonu itam la ndëfalaay liy bawoo ci Almasi di yokkoo. 6 Su nu jaaree ci njàqare, seen ndëfalaay ak seen jàmm lay doon. Sunu amee ndëfalaay it, seen ndëfalaay lay doon, ngir coono yi nuy dékku, ngeen man koo dékku, yeen itam. 7 Te itam am nanu yaakaar ci yeen bu baax. Xam nanu ne ni ngeen bokke ak nun coono, ni ngeen di bokke ak nun ndëfalaay.
8 Ndax kat, bokk yi, buggunu ngeen umple njàqare, ji nu daj ci diiwaanu Asi. Daj nanu coono bu jéggi dayo, te wees sunu kàttan, ba yaakaaratunu woona dund sax. 9 Nun ci sunu wàllu bopp, jàppoon nanu ne sunu àtteb dee moo taxaw. Waaye loolu tax na nu bañatee yaakaar sunu bopp, xanaa di yaakaar ci Yàlla, miy dekkal ñi dee. 10 Moo nu wallu ci googu dee gu naroona metti, moo nuy walluwaat, te moom lanu yaakaar mu wallooti nu. 11 Yeen itam, ni ngeen nu ciy jàpplee mooy ngeen di nu ñaanal. Su ko defee yiw, wa nu ñu bare ñaanal ba nu am ko, dina tax ñu bare biral ag cant ci sunu mbir.
Póol biral na jëfinam ak mébétam
12 Li nuy damoo nag moo di seede bi nu sunu xel mu dal seedeel, ne xol bu set ak jikko ju dëggu ju bawoo fa Yàlla, mooy li nu doxale ci àddina si, rawatina sunu digg ak yeen, te du lu nu sunu xam-xamu nitu neen may, waaye yiwu Yàlla moo nu ko may. 13 Bindunu leen leneen lu moy mbind moomu ngeen jàng te man koo xam. May yaakaar nag ne dingeen xam ba mokkal, 14 noonu ngeen xawa xame ne nun, man ngeen noo damoo, te nun it, yeen la nuy damoo, keroog bésu Sang Yeesu.
15 Kóolute gu ma amoon ci ni ngeen nuy damoo moo tax ma naroona jëkka dikk ba ci yeen, ngir seen yiw mana yaar, 16 ba bu ma jógee ci yeen, daldi jaareji diiwaanu Maseduwan, bu ma jógee Maseduwan, dikkaat ci yeen, ba ngeen yiwi ma, ma jëm Yude. 17 Ndax ñàkk pastéef laa mébéte moomu mébét? Am ni nitu suuxu neen di mébéte rekk laa topp bay xel-yaar, naan «waaw» te naan «déet»?
18 Yàlla mi mata gëm de seere na ne kàddu gi nu leen di wax du «waaw, déet,» 19 ndax Doomu Yàlla, Yeesu Almasi, mi nu biral ci seen biir, man ak Silasa ak Timote, du kàddug «waaw, déet;» «waaw» doŋŋ a nekk ci moom. 20 Ak li digey Yàlla di bare lépp, ci Almasi la ay digeem di doone «waaw». Moo tax itam, ci moom lanu naan Yàlla: «Amiin», ngir delloo ko njukkal. 21 Te ki nuy saxal ci Almasi, nook yeen, moo nu tabbe diwu pal gi, te moo di Yàlla. 22 Moo nu màndargaale xàmmikaayam, te moo yeb dawalub Noo gu Sell gi ci sunu biir xol.