5
1 Kon nag doonleen ay roykati Yàlla, gannaaw yeenay doomam yi mu sopp, 2 te ngeen di doxale cofeel, ni Almasi mi nu sopp, ba jooxeel nu bakkanam, def ko saraxu sawara, ngir xetug jàmm, ñeel Yàlla.3 Lu jëm nag ci powum séy, ak jépp jëfi sobe, mbaa ag bëgge, li jekk ci ay nit ñu sell, moo di ñu bañ koo tudd sax ci seen biir, 4 te ag ñàkk kersa, ak waxi caaxaan, ak kaf yu bon, dara jekku ci, waaye saxooleen kàdduy cant. 5 Ndax lii kat na leen wóor: képp ku nekke powum séy, mbaa jëfi sobe, mbaa ag bëgge, kooku amul cér ci nguurug Almasi ak Yàlla, ndax ku bëgge ab bokkaalekat la.
Jëfeleen ni niti leer
6 Bu leen kenn naxe waxi ngelawal neen, ndax yooyu ma lim mooy wàcce sànjum Yàlla ci kaw aji déggadi ñi. 7 Kon nag buleen séq ak ñooñu dara. 8 Ag lëndëm ngeen woon démb, waaye tey ag leer ngeen ci Boroom bi ngeen bokk. Jëfeleen nag ni niti leer. 9 Li leer gi ci yeen di meññ moo di mboolem luy mbaax ak njub ak dëgg. 10 Ràññeeleen li neex Boroom bi; 11 jëfi lëndëm amul njariñ, buleen ci bokk, xanaa ngeen feeñal ñaawtéefu jëf ja. 12 Ndax kat li nit ñooñu di làquy def, waxtaane ko sax, lu ruslu la. 13 Waaye mboolem lu ñu feeñal, leer ga ñu ko leerale moo ko wone, 14 te lépp lu ñu wone ci ag leer, di ag leer. Moo tax ñu ne:
«Yaw miy nelaw, yewwul,
dekkil, Almasi leeral la.»
15 Kon nag xool-leen bu baax seen jëfin, defleen jëfinu nit ñu am xel, te baña mel ni ñu ñàkk xel, 16 Jariñooleen lu ngeen man, jot gi ngeen amagum, ndax jant yu bona ngii tey. 17 Moo tax buleen def jëfi ñàkk bopp, waaye jéemleena xam coobarey Boroom bi. 18 Buleen naan biiñ ba màndi, màndite ci afal seen bakkan la leen jëme, waaye na leen Noo gi fees, 19 ngeen di jàngalante jàngi Sabóor, ak jàngi cant, ak jàng yu bawoo ci Noo gi leen fees, te ngeen di woy aka kañ Boroom bi, ci seen xol. 20 Fu ngeen tollu, ak ci mbir mu mu mana doon, santleen Yàlla Baay bi ci sunu turu Sang Yeesu Almasi, 21 te ngeen rus Almasi, ba tax ngeen di nangulante.
Jabar mokk, jëkkër sopp
22 Na jabar nangul jëkkëram ni mu nangule Sang bi. 23 Almasi moo di musalkatu mbooloom gëmkat ñi, mbooloo mi di aw yaramam. Te itam ni Almasi dee boppu mbooloom gëmkat ñi, ni la jëkkër ji dee boppu jabaram. 24 Kon nag ni mbooloo mi nangule Almasi, ni la jabar ji wara nangule jëkkëram ci lépp.
25 Jëkkër nag, na sopp jabaram ni Almasi soppe mbooloom gëmkat ñi, ba jooxeel leen bakkanam. 26 Moo defal loolu mbooloo mi ba man koo setale cangaayal ndox mu ànd ak kàddoom, ngir sellal ko. 27 Li mu ci namm moo di teewal mbooloo mi fi kanamam, mu mel ni ab séetam bu ne ràññ, gàkkul, rasul, taqul lenn, xanaa sell, mucc sikk.
28 Noonu la jëkkër ji wara soppe jabaram, ni mu soppe yaramu boppam rekk. Sopp sa jabar sopp sa bopp la, 29 ndax kenn masula bañ suuxu boppam, xanaa mu di ko dundal, di ko topptoo, ni Almasi ak mbooloom gëmkat ñi, 30 nde noo di céri yaramam. 31 Ni ko Mbind mi indee: «Looloo tax góor di bàyyikoo ci ndeyam ak baayam, daldi taqoo ak jabaram, ba ñoom ñaar di wenn suuxa.» 32 Mbóot mu xóota ngi ci dog boobu, waaye man, li may wax moo di dog bi moo misaal diggante, bi Almasi séq ak mbooloo mi. 33 Teewuleen koo moom yeen itam; kon na ku nekk sopp jabaram ni mu soppe boppam, te ku nekk weg jëkkëram.