Bataaxal bi Yàlla may Póol, mu bind ko waa
Kolos
1
1 Man Póol ndawal Almasi Yeesu ci coobarey Yàlla, maa bind lii, ànd ceek mbokk mi Timote, 2 ñeel waa Kolos ñu sell te wóor te di bokki gëmkati Almasi. Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay.Póol ñaanal na waa Kolos
3 Sant Yàlla sunu Baayu Sang Yeesu Almasi, lanu saxoo, saa su nu leen di ñaanal; 4 dégg nanu ngëm gi ngeen gëm Almasi Yeesu, ak cofeel gi ngeen sopp gëmkat ñu sell ñépp, 5 te li waral ngëm googu ak cofeel googu, di seen yaakaara jot ca cér ba ñu leen dencal fa asamaan. Mooy yaakaar ja ngeen dale am ba ngeen jëkkee dégg kàddug dëgg gu xibaaru jàmm bi. 6 Ni leen xibaaru jàmm bi dikkale nag, ni la dikkale àddina sépp, te mu ngi meññ, di law, na mu ko dale defe fi seen biir, ca bés ba ngeen déggee lu jëm ci yiwu Yàlla, ba ràññee ko dëgg. 7 Noonu ngeen ko jànge ci Epafras, sunu mbokkum surga biy sunu soppe, te di jawriñu Almasi bu wóor bi nu jàpplea, 8 te moo nu xamal itam cofeel gi leen Noo gi may.
9 Moo tax nun itam, ba nu déggee seen mbir ba tey, noppiwunu leena ñaanal, di sàkku ngeen feese xam-xam ci lépp luy coobarey Yàlla, te ngeen ànd ceek lu mat sëkk ci wàllu xel, ak gis-gis bu Noo gi maye. 10 Su ko defee ngeen di dunde dundin wu yellook Boroom bi, ngir bànneexal ko ci wet gu nekk, seen meññeef it di jépp jëf ju baax, te ngeen gën di xam Yàlla. 11 Ngir itam ngeen manoorewoo jépp manoore, na leen ko Yàlla manloo ci kàttanam gu màgg, ba ngeen mana dékkoo lépp, xolu muñ, 12 te ngeen di sante Baay bi, mbég, moom mi leen yellale ab cér ca muuru ñu sell ña, ca réewum leer ga.
Almasi jubale na nit ak Yàlla
13 Yàlla kat moo nu wallu ba génne nu ca kilifteefu réewum lëndëm ga, toxal nu ci biir nguurug Doomam ji mu sopp. 14 Ci moom lanu ame ag njot, te moo nu jéggal sunuy bàkkaar.
15 Doom jooju moo di niruwaale Yàlla, mi kenn manula gis, mooy taaw bi, ki jiitu mépp mbindeef. 16 Ndax moo di ki Yàlla sàkke lépp lu nekk asamaan, ak lu nekk ci suuf, lu gisu, ak lu gisuwul, muy boroom gàngune yeek, boroom ndomboy tànk yeek, boroom nguur yeek, boroom sañ-sañ yi. Lépp ci moom lees ko sàkke, te mooy ki tax ñu sàkk lépp. 17 Mooy ki nekkoon naka jekk balaa daraa nekk, te lépp ci moom la sottee ba temboo. 18 Mooy boppu yaram, wiy mbooloom gëmkat ñi, mooy njàlbéen, mooy taaw bi jëkka dekki, ndekkite lu dee toppul, ba tax muy ki jiitu ci lépp, 19 ndax Yàlla la soob mu dëël gépp matam ci moom. 20 Deretam ja tuuru ca bant ba, ca la Yàlla defe jàmm, ba sottale ci moom, pexe mi mu jubalee boppam ak lépp, muy lu nekk ci kaw suuf, ak la fa asamaan.
21 Te yeen ñi masoona sore lool Yàlla, doonoon ay noonam ci wàllu xalaat, ak jëf ju bon, 22 tey, deewug yaram, deewug suux, gi Almasi dee, moom la leen Yàlla jubalee ak boppam, ba teewal leen fi kanamam, ngeen di ñu sell, mucc sikk, seen der set wecc. 23 Noonu la deme, ndegam kay fekk na leen sësoo ngëm gu ngeen dëjoo ba dëgër, te baña nangu lenn di leen sorele ak yaakaar ji ci xibaaru jàmm, bi ngeen dégg, te ñu biral ko, ñeel mépp mbindeef. Man Póol nag, ci yégle xibaaru jàmm boobu laa di ab jawriñ.
Póol tiisoo na waa Kolos
24 Léegi nag maa ngi bége coono yi ma jànkoonteel ngir seen njariñ; li des ci tiisi Almasi, moom laay mottalee coono yooyu ma daje sama yaramu suux wii, ngir njariñal mbooloom gëmkat, miy yaramu Almasi. 25 Ci moomu mbooloo laa dib jawriñ, te Yàllaa ma sase noonu, ñeel leen, ngir ma xamle kàddug Yàlla ba mu mat sëkk. 26 Kàddu googu moo di mbóot mi masoona làqu maasoo maas, waaye tey Yàllaa ko xamal ay nitam ñu sell. 27 Ñoom la Yàlla nammoona xamal ni mbóot mi yaatoo te yéeme, ñeel jaambur ñi dul Yawut: mbóot mi moo di Almasee ngi ci yeen ñi dul Yawut itam, loolu di seen yaakaar ci ndam lu leen ñeel.
28 Almasi moomu nag lanuy xamle; na mu gëna xeloo lanuy àrtoo nit ku nekk, te ni lanuy jàngale nit ku nekk, ngir àgge nit ku nekk ba fa kanam Almasi, fekk ko mat sëkk, na mu ware ku ànd ak Almasi. 29 Loolu moo ma tax di góor-góorlu ci xare bii may xaree dooleem, ak manoorey jëfam, jiy liggéey ci sama jëmm jii.