Gëmkatub Almasi, dundin wu yees
3
1 Gannaaw nag yeena dekkeendoo ak Almasi, sàkkuleen la fa kaw, fa Almasi tooge ca ndijooru Yàlla. 2 La fa kaw, xintewooleen ko, te ngeen ba li fi suuf, 3 ndaxte dee ngeen, ba seenug dund ànd ak Almasi, làqe fa Yàlla. 4 Seenug dund dëgg Almasi la, te keroog bu Almasi feeñee, yeen itam ay ànd ak moom feeñ, ba séddu ci ndamam.5 Kon nag reyleen seen cér yi bokk fii ci kaw suuf; lu mel ni powum séy, ak jëfi sobe, ak ñàkk sago ci lu jekkadi, ak xemmemtéef yu bon, ak bëgge, te loolooy bokkaale ba tey, 6 yooyooy wàcce sànjum Yàlla ci kaw ñi déggadi. 7 Yeen itam noonu ngeen daan jëfe bu jëkk, ba seenug dund bokkee fii ci kaw suuf. 8 Waaye léegi lii lépp baleen ko: tàng xol, ak mer mu ëpp, ak coxor, ak saaga, ak waxi ñàkk kersa. 9 Buleen di fenante, gannaaw seen jëmm ja woon démb, boole ngeen kook jëfinam ja mu àndal, summi, 10 ba sol seen jëmm ju yees, jiy gën di yeeslu, te di gëna niru ki leen ko sàkkal, ba kera ngeen xamee, xam-xam bu mat sëkk. 11 Dundin wu yees woowu amul jaambur akub Yawut, amul ku xaraf ak ku xaraful, amul ab doxandéem ak ku xayadi, amul ab jaam ak as gor, waaye Almasi mooy lépp te moo nekk ci ñépp.
12 Yeenay ñi Yàlla taamu, sellal leen, sopp leen. Kon nag solooleen xolu yërmande, akug mbaax, ak woyoflu, ak jikko ju lewet, ak xolu muñ. 13 Muñalanteleen te di balante, ndegam kenn a am lenn lu mu sikke moroomam. Ni leen Boroom bi baale, deeleen balantee noonu. 14 Ci kaw loolu lépp nag, tegooleen cofeel; mooy xànc gi leen faste, ba seenug bennoo mat sëkk.
15 Na jàmmu Almasi saytu seen xol. Ci jooju jàmm lañu leen woo, fekk leen ngeen di wenn yaram doŋŋ, te it saxooleen cant. 16 Na leen kàddug Almasi dëkke, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jànglantee, ak a artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ay taalifi Sabóor, ak woyi tagg Yàlla, ak woy yu fentoo ci Noo gi. 17 Lu ngeen mana def, muy ci wax, di ci jëf, defleen ko ci turu Sang Yeesu, tey sant Yàlla Baay bi ci moom.
Rafetooleen
18 Jigéen ñi, nangul-leen seen jëkkër, noonu mu jekke ci ku bokk ci Boroom bi.
19 Góor ñi, soppleen seen jabar, te buleen leen soxore.
20 Xale yi, déggal-leen seeni waajur ci lépp, nde loolu mooy li Boroom bi rafetlu.
21 Yeen ñiy baay, buleen yékkati seen xolu doom, ngir baña jeexal seen xol.
22 Jaam yi, nangul-leen ci lépp seen sang yi ci àddina. Buleen ko defe ngistal, mbaa ngeen di ko sàkkoo lu leen neex, waaye defeleen ko yéeney xol bu dëggu, ndax ragal Boroom bi. 23 Lu ngeen mana def, liggéeyeleen ko xol bu tàlli, ni bu ñeelul woon nit doŋŋ, xanaa Boroom bi. 24 Te ngeen xam ne ci loxol Boroom bi ngeen di nangoo yool bi ngeen muurloo. Sang Almasi mooy ki ngeen di jaamu. 25 Waaye ku def njubadi, njubadi ga mu def lay yooloo, te xejj ak seen du ci am.