Àlluwa ju wér lii lay xamle
2
1 Yaw nag waareel li dëppook àlluwa ji wér, 2 te mooy na mag ñi moom seen bakkan, di ñu tedd, jiital seenum xel, te pastéefu ci wàllu ngëm, ak cofeel, akug muñ.
3 Naka noonu, jigéen ñu mag ñi itam, nañu jëfe ni mu jekke ci ay nit ñu sell; buñu yàq der, bu leen sàngara jiital, te nañuy jàngle lu baax, 4 ngir tàggat jeeg ju ndaw ji ci sopp seen jëkkër, sopp seeni doom, 5 di ñu jiital seenum xel, set jikko, di liggéey ca seeni kër, baax, nangul seen jëkkër, ba kenn du baatal kàddug Yàlla.
6 Naka noonu, xale yu góor yi itam, ñaaxleen ci jiital seenum xel. 7 Te nanga doon, yaw ci sa bopp ab royukaay, ci lépp ndax sa jëf ju baax, te nga boole ko ak àlluwa ju dëggu te tedd, 8 ak kàddu gu wér gu kenn dul mana weddi, ngir rusloo ab noon bu amul lenn lu bon lu mu nu baatale.
9 Jaam yi, nañu nangul seeni sang ci lépp, di sàkku seen bànneexu sang, te ñu bañ di tontoonte ak moom, 10 mbaa di randal. Waaye nañu firndeel ne ñoo yelloo kóolute gu mat sëkk, su ko defee dinañu sagal ci lépp, àlluwa ji ñu jànge, te muy ju Yàlla, sunu Musalkat.
11 Ndax yiwu Yàlla kat feeñ na, te looloo indil ñépp ag mucc. 12 Yiw woowu moo nu digal nu dëddu ñeme Yàlla, ak xemmemtéefi àddina, te jiital sunum xel, di jëfe njub, te nekke ag njullite ci àddinay tey jii. 13 Loolu lees nu digal, li feek nu ngi séentu yaakaaru mbég ma, keroog bésu peeñum sunu màggaayu Yàlla, miy Yeesu Almasi, Musalkat bi. 14 Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.
15 Googu kàddu ngay waaree, di dénkoo ak di femmoo, te boole ci fulla ju mat sëkk. Bu la kenn yab.