Nanu teewlu pexem mucc mi Yàlla waajal
2
1 Moo tax nu wara yokka teewlu kàddu yi nu dégg, bala noo lajj, taañaañal. 2 Gannaaw nag kàddug Yàlla ga jibe woon ci gémmiñu malaaka yi, mujj na di lu wér péŋŋ, te képp ku ko masa xëtt, mbaa mu déggadi ko, jot nga añ bi war ci sag tooñ, 3 ana kon nun ci sunu bopp, nan lanuy rëcce mbugal, su nu sàgganee pexem mucc mu réy mii Sang bi jëkkoona biral, te ñi ko dégg dëggalal nu ko? 4 Te Yàlla moo doon dëggale seedey ñooñu, ay firnde aki kéemaan, ak wépp xeeti kawtéef, ak ay mayi Noo gu Sell gi, may yi mu séddalee ni mu ko soobe.Yeesu moo rammu jaam ñi
5 Ndax kat du ci kilifteefu malaaka yi la Yàlla teg àddinay ëllëg ji nuy wax, 6 waaye am na ku yékkatee bérab, kàddug seede, ne:
«Ana luy nit ba nga di ko faale?
Ana luy doom aadama, ba nga di ko yég?
7 Yaa ko def mu gëna suufe as lëf malaaka yi,
yaa ko kaalaa teraanga ak daraja,
8 yaa teg lépp ci kilifteefam, ci suufu ndëggul tànkama.»
Ba Yàlla tegee lépp ci kilifteefam it, bàyyiwul dara lu mu tegul ci kilifteefam. Dëgg la, fii nu tollu gisagunu ne lépp a ngi ci kilifteefam, 9 Yeesu mi ñu def mu gëna suufe as lëf malaaka yi, moom lanu gis deeyam gi mu dee tax mu jagoo kaalag teraanga. Noonu la deeyale ñépp ci kaw yiwu Yàlla.
10 Ndax kat Yàlla mi lépp lu sàkke ñeel, te lépp sàkkoo ci moom, moo nammoona wommat gone yu bare ba sédd leen daraja. Moo tax muy lu jaadu, mu sottale matug Yeesu ay coono, ndax Yeesu moo xàllal gone yooyu yoonu mucc. 11 Yeesu miy sellal nit ñi, moom ak ñi muy sellal, ñoo bokk lenqe, te moo tax Yeesu rusu leena wooye ay bokk. 12 Mu ne:
«Maay biralal saw tur samay bokk,
maa lay kañe fi digg mbooloo mib.»
13 Mu waxaat ne:
«Man maay am kóolute ci moom.»
Dellooti ne:
«Maa ngi nii, maak gone yi ma Yàlla joxc.»
14 Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley ndee, te mooy Seytaane. 15 Noonu la goreele mboolem ñi seenug ragala dee tënkoon cig njaam, seen giiru dund. 16 Ndax kat du ay malaaka la Yeesu xettlisi, waaye askanu Ibraayma la xettlisi. 17 Moo tax fàww mu niru woon ay bokkam ci bépp fànn. Su ko defee mu mana doon seen sarxalkat bu mag bu am yërmande te wóor fa kanam Yàlla, ngir mana defal askan wi seen njotlaayal bakkan. 18 Coonoy nattu bi mu dékku nag tax na mu mana wallu ñi ci nattu.