Yàlla rafetlu na ngëm
11
1 Ngëm nag mooy cëslaayal yaakaar te mooy firndey li bët gisul. 2 Ngëma taxoon maam ya rafet ub jëw.
3 Ngëm a nu xamal ne Yàllaa sose àddina wërngal këpp ag kàddoom, li gisu daldi sàkkoo ci lu gisuwul.
4 Ngëm la Abel jébbale Yàlla sarax su gën saraxub Kayin, te ngëm lees seedeele Abel ne moo jub, kera ba Yàlla ci boppam seedee ne ay saraxam a nangu. Ngëm it moo waral Abel dee, te di wax.
5 Ci kaw ngëm lees yóbboo Enog, te deewul. Da ne mes, ndax Yàllaa ko yóbbua. Balees koo yóbbu kay, lees ko seedeeloon ne moo bànneexal Yàlla. 6 Ku amul ngëm nag doo mana neex Yàlla, ndax kiy dikk fi Yàlla, fàww nga jëkka gëm ne Yàlla am na, gëm it ne ñi koy sàkku, moo leen di yool.
7 Ngëm la Nóoyin dégge waxyub Yàlla bu jëm ci lu kenn gisagul woon, te ragal Yàlla la sàkke gaal, ngir musal njabootam. Ngëmam it la tiiñale àddina, ba ab céram di njub gi ngëm di maye.
8 Ba Yàllay woo Ibraayma, ngir mu génn, jëm bérab ba mu mujj muurloo, ngëm la déggale Yàlla, ba génn, dem te xamul woon fu mu jëm. 9 Ngëm la Ibraayma daleji ca suuf, sa ñu ko digoon, ba dëkke ay xayma ni ab doxandéem ci réewum jaambur, moom ak ñi mu séddool benn dige bi, te ñuy Isaaxa ak Yanqóoba. 10 Booba Ibraaymaa ngay séentu dëkk ba ca kenu ya, te Yàlla di ki yor xaralag tabax bi, boole ci di tabaxkat bi.
11 Ci kaw ngëm itam la Saarata ci boppam mana ëmbe ba jur tey mag ba wees njurum doom, ndax moo njortoon ne ka dige ku wóor la. 12 Looloo waral genn góor doŋŋ, ku dee rekk dese, aw askan mana soqikoo ci moom, tollu ni biddiiwi asamaan ndax bare, wees ab lim ni feppi suufas géej.
13 Ñoom ñépp ngëm lañu deeyaale te jotaguñu woon la ñu leen digoon. Waaye fu sore lañu ko séene, di ko séentu, tey ràññee ne ay doxandéem aki màngaan lañu ci àddina. 14 Ñooñuy dëggal ne ay doxandéem aki màngaan lañu ci àddina nag, ñoo firndeel ci lu leer ne réew mu ñu moomal seen bopp lañu doon wut. 15 Bu ñu nammoon réew ma ñu jóge, manoon nañoo dellu. 16 Waaye réew mu ko gën lañu doon sàkku, te mooy réewum asamaan. Looloo tax Yàlla rusul ñu di ko tudde seen Yàlla, ndax waajalal na leen ab dëkk.
17 Ibraayma, ba ñu ko nattoo, ngëm la jooxee Isaaxa ngir sarax. Ibraayma mi ñu jagle dige yi, Isaaxa jenn doomam ju góor ji mu am, moom la doon jooxe, 18 te Yàlla noon ko: «Ci Isaaxa lees di tudde saw askanb 19 Waaye Ibraayma njortoon na ne su Isaaxa dee woon it, Yàlla man na koo dekkal. Moo tax itam ci misaal, Isaaxa délsi ciy loxoom, mel ni daa dekki.
20 Ba tey ngëm la Isaaxa ñaanale Yanqóoba ak Esawu, ngir barkey ëllëg.
21 Ba Yanqóoba di waaja nelaw, ngëm la ñaanale ñaari doomi Yuusufa yépp, doora sujjóot, jafandoo boppu yetamc.
22 Ba Yuusufa di waaja nelaw, ngëm la waxe lu jëm ci mbirum gàddaayug bànni Israyil gay bawoo Misra, bay dénkaane ci mbiri yaxam.
23 Ba Musaa juddoo, ngëm la ko ay waajuram làqe woon ñetti weer, ndax gis na xale ba taaroo woon, ba ragaluñu ndigalal buur ba. 24 Ba Musaa màggee, ngëm a taxoon mu bañ ñu wooye ko doomu doomu Firawna ju jigéen. 25 Bokk ak ñoñi Yàlla ab coono moo ko gënaloon muy bànneexoogum ci biir bàkkaar. 26 Toroxtaange gu ñu koy teg ndax Almasi, moom la defoon muy alal ju ëpp denci Misra, ndax yoolub ëllëg ba la doon séentu. 27 Ngëm la bàyyikoo Misra, te ragalul sànjum buur, xanaa dogu rekk, mbete kuy gis ki gisuwul. 28 Ngëm la Musaa aadaale màggalu bésub Mucc ba, ak wis-wisalub deret ja, ndax malaakam bóomkat bi baña laal taawi bànni Israyil.
29 Ngëm la bànni Israyil jàlle géeju Barax ya, mu mel ni yoonu suuf su wow koŋŋ, waa Misra jéema jàll topp ca, daldi lab.
30 Ngëm moo waral tatay Yeriko màbb, gannaaw ba ko bànni Israyil wëree lu mat juróom ñaari fan. 31 Ngëm moo waral ba Raxab gànc ba dalalee jàmm nemmikukati réew ma, àndul ak ñu gëmadi ña dee.
32 Ana lu ma ciy tegati? Jot gee ko dul mate, su ma naroona nettali mbirum Sedeyoŋ ak Barag ak Samson ak Yefte ak Daawuda ak Samiyel ak yonent yi. 33 Ñooñu ngëm lañu tege loxo ay nguur, ngëm lañu defe njekk, ci kaw ngëm la ay dige sottee, ñeel leen, te ci lañu tëje gémmiñi gaynde ya. 34 Ngëm lañu feye dooley sawara, ngëm lañu rëcce ñawkay saamar, ngëm a waral ñu weccikoo kàttan seenug néew doole, ci kaw ngëm lañu doone ay ñeyi xare, ba dàq gàngoori yeneen réew. 35 Ngëm a waral aw jigéen dekkile ñu ñu deele woon; ngëm a waral ay góor ñu ñu mitital, baña dellu gannaaw, weccikoo ko seen njotug bakkan, ndax yaakaara dekki, ba gëna dundati ëllëg. 36 Ngëm la ñeneen dékkoo ay kókkali aki yar, ba ciy jéng ak tëjteb kaso. 37 Ñii, ñu dóor ay doj ba ñu dee, ñee, ñu xeet leen ba xar leen ñaar, ñee, ñu bóome leen saamar, ñii di wëndeelu, sol deri xar mbaa bëy, te diy ndóol, ñu di leen bundxatal, di leen mitital. 38 Ñooñu àddina sax yeyoowu leen woon, te àll yi lañu doon wëreeloo, ak tund yeek xunti yeek kàmb yi.
39 Mboolem ñooñu am jëw bu rafet ndax seen ngëm, jotuñu sax lees dige woon, 40 ndax daa fekk Yàlla gisal nu demin wu gën ci nun. Moo tax boroom ngëm yooyu waruñu woona àgg ci tolluwaay bu mat sëkk, te fekk nun dikkagunu ba bokk ko ak ñoom.