Nekkal-leen Yàlla
4
1 Gannaaw Almasi nag moo daj coonob yaramam, yeen itam gànnaayooleen boobu yéene, ndaxte ku daj coonob yaram, tàggoo naak bàkkaar, 2 ngir bañatee topp xemmemtéefi bakkan, xanaa di topp coobarey Yàlla, diir bi ko dese ci kaw suuf. 3 Ndax démb kat yàgg ngeena def coobarey xeet yi xamul Yàlla, ci ay ñaawtéef, ak topp seen bakkan. Dangeen daa màndi ak a xawaare, dëkke naan biiñ, di jaamu tuur yu seexluwu, waaye na fi yem nag. 4 Ña ngeen ci daa àndal ñoo waaru tey, ba di leen sosal, ndax li ngeen àndatul ak ñoom, daw wuti googu yàqute gu af, 5 waaye ñoo koy layoo ak ki nara àtte ñiy dund, ak ñi dee. 6 Li ñu ci jublu moo di, ñi dee tey sax, ñu àgge leen xibaaru jàmm bi, ngir bu ñu leen àttee àtteb nit ñu seen yaramu suux wara dee sax, du tee ñuy dund tey, ndax Noowug Yàlla.Bennoo moo war gëmkat ñi
7 Te itam mujug lépp dëgmal na; kon nag jiital-leen seenum xel, te ànd ak seen sago, ngir ngeen man di ñaan. 8 Waaye li ci raw mooy soppanteleen cofeel gu mat sëkk, ndax cofeel, bàkkaar yu bare lay far. 9 Ganalanteleen te baña jàmbat. 10 Kenn ku ci nekk, may gi ko aw yiw jagleel, na ko taxawoo ñépp. Noonu ngeen di doone ay saytukat yu baax yu yiwu Yàlla wu yaa. 11 Kuy wax, na waxe nu mu jottlee kàddug Yàlla. Kuy taxawoo, na taxawoo ci dooley Yàlla, ngir màggug Yàlla feeñe ci lépp, ndax Yeesu Almasi, mi yelloo daraja ak kàttan, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.
Bu ngeen di sonn, na Almasi tax
12 Soppe yi, tàngooru nattu bi ngeen nekke nii, bumu leen jaaxal ba mel ni lu jaaduwul moo leen dikkal. 13 Waaye noonu ngeen séddoo ci coonoy Almasi, bégeleen ko, ngir bu ndamam feeñee, ngeen gënatee bég. 14 Su ñu leen jànnee sax ndax turu Almasi, ndokklee yeen, ndax Noo gu darajawu gi, Noowug Yàlla moo wàcc ci yeen. 15 Waaye rey nit, mbaa sàcc, mbaa def lu bon, mbaa dugg ci yëfi jaambur, bumu waral coonoy kenn ci yeen. 16 Ku sonn ndax li muy gëmkatub Almasi nag, bumu ci rus, na sàbbaal Yàlla kay, ci woowu tur. 17 Ndax kat tey la àtte bi wara tàmbalee ci waa kër Yàlla. Ndegam ci nun lay tàmbalee nag, ñi gëmul xibaaru jàmm bu Yàlla, ana fu ñu jëm? 18 Te it:
«Aji jub ji, su ko mucc jafee,
yéefar bi, bàkkaarkat bi moom, fu mu jëma?»
19 Kon nag ñiy sonn te coobarey Yàlla tax, nañu dénk seen bopp Yàlla, Sàkk-kat bu wóor bi, te ñuy saxoo def lu baax.