Àtte bu mujj ba agsi na
10
1 Ci kaw loolu ma gis meneen malaaka mu am doole, muy wàcce asamaan, làmboo aw niir, ag xon tege ci bopp bi, kanam gi mel ni jant bi, tànk yi mel ni jumi sawara. 2 Mu ngi yor ab téere bu ndaw bu ñu ubbi. Mu teg tànku ndijooram ci géej gi, teg tànku càmmoñam ci jéeri ji. 3 Mu xaacu ca kaw, mel ni gaynde guy yëmmu. Naka la xaacu, juróom ñaari dënu jib. 4 Naka la juróom ñaari dënu yi jib, may waaja bind, daldi dégg baat bu jóge asamaan, ne ma: «Loolu juróom ñaari dënu yi wax de, gas ko, suul, bu ko bind.»5 Ba mu ko defee malaaka, ma ma gisoon mu ŋarale géej geek jéeri ji yékkati loxol ndijooram, jëme asamaan. 6 Mu giñ ci Kiy dund ba fàww, Ki sàkk asamaan ak li ci biiram, ak suuf ak li ci biiram, ak géej ak li ci biiram. Mu ne: «Négandiku wees na, 7 waaye bu bési kàddug juróom ñaareelu malaaka mi taxawee, ba mu tàmbalee wal liit gi, su keroogee pexem Yàlla miy kumpa dina sotti, na mu ko waxe woon ay jaamam, yonent yi.»
8 Ba loolu amee baat, ba ma déggoon, mu bawoo asamaan, dellu wax ak man, ne ma: «Demal jël téere bu ndaw bi ñu ubbi ci loxol malaaka, mi ŋarale géej geek jéeri ji.»
9 Ma dem ba ci malaaka mi, ne ko mu jox ma téere bu ndaw bi. Mu ne ma: «Jël ko te lekk ko. Dina wex ci sa biir nag, waaye ni lem lay neexe ci sa gémmiñ.»
10 Ma jël téere bu ndaw bi ci loxol malaaka mi, lekk ko, mu neex ci sama gémmiñ ni lem, waaye naka laa ko wonn, mu wex xàtt ci sama biir.
11 Gannaaw loolu ñu ne ma: «War ngaa waxati ay waxyu ngir xeet yu bare, ak askan yu bare, ak niti làmmiñ yu bare, ak buur yu bare.»