Almasi mooy nguuru junniy at
20
1 Ba mu ko defee ma gis malaaka mu wàcce asamaan, yor caabiy xóote bi, ak càllala gu réy. 2 Mu jàpp ninki-nànka ja, jaani cosaan jooju di Tuumaalkat bi, di Seytaane ba tey. Malaaka mi yeew ko diiru junniy at. 3 Da koo sànni ci xóote bi, tëj ko, sakk buntu xóote bi, ndax du naxati askan yi, ba kera junniy at yi mat. Gannaaw loolu nag fàww ñu yiwi ko diir bu gàtt.
4 Ci kaw loolu ma gis ay gàngune yu ñu jox ña ca toog, sañ-sañu àtte. Ma daldi gis bakkani ñi ñu dogoon seen bopp ndax la ñu doon seedeel Yeesu ak la ñu gëmoon kàddug Yàlla, ña sujjóotalul woon rab wi ak jëmmu nataalam, te amuñu màndargam rab wi ci seen jë mbaa seen loxo. Ñu dekki bay nguuroondoo ak Almasi diiru junniy at. 5 Loolu moo di ndekkite lu jëkk li. Yeneen néew yi nag, duñu dekki li feek junniy at yi matul. 6 Ndokkle ak sellnga ñeel na ñi séddu ci ndekkite lu jëkk li! Ñooñu, ñaareelu dee gi manalu leen dara. Ñooy doon it sarxalkati Yàlla ak Almasi, te ñooy nguuroondoo ak Almasi junniy at.
Seytaane moo mujje déegu sawara sa
7 Bu junniy at yi matee, dees na yiwi Seytaane, génnee ko ca kasoom, 8 mu dikk, naxsi askani ñeenti colli àddina, yi ñuy wax waa Gog ak Magoga. Mu dajale leen ngir xare, ñu bare ni feppi suufas géej. 9 Dañuy sam déndub suuf sépp, daldi yéew dalub nit ñu sell ñi ak dëkk bu jar bi. Ci biir loolu sawara wàcce asamaan, lakk leen. 10 Ñu jàpp nag Seytaane, mi leen daan nax, sànni ko ci déegu sawaraak tamarax ba, mu fekki fa rab waak yonentu caaxaan ba. Dees na leen fa mitital guddi ak bëccëg, ba fàww.
Bés-pénc taxaw na
11 Ci kaw loolu ma gis ngàngune mu mag mu weex, ak ku ci toog. Asamaan ak suuf daldi dawe fa kanamam, ne mes. 12 Ma gis néew ya, mag ak ndaw, ñu taxaw ca kanam ngàngune ma, ay téere ubbiku, beneen téere ubbikooti, di téereb dund ba. Ñu daldi àtte néew ya ca seeni jëf, na ñu ko binde ca téere ya. 13 Ba mu ko defee géej jébbale néew ya woon ca moom, ndee ak njaniiw jébbale néew ya woon ca moom, ñu daldi àtte ku nekk ca say jëf. 14 Ba loolu amee ñu jàpp ndee ak njaniiw, sànni ca déegu sawara sa. Ñaareelu dee gi nag moo di déegu sawara si. 15 Képp ku ñu gisul ñu bind la ci téereb dund bi, ci déegu sawara si lees la sànni.