Walum dund mi feeñ na
22
1 Ci kaw loolu malaaka mi won ma dexu ndoxum dund mu leer nàññ ni doju kiristaal, ndox ma wale ca ngàngunem Yàllaak Gàtt ba, 2 di tuuru ci digg péncu dëkk bi. Ci ñaari tàkki dex gi, garabu dund a ngi ci, di meññ fukki yoon ak ñaar, weer wu nekk benn yoon, xob yi di faj askani àddina. 3 Alkànde nag du fa amati, te ngàngune mu Yàllaak Gàtt bi ci biir dëkk bi lay nekk, jaamu Yàlla yi di ko sujjóotal, 4 di gis kanamam, turam binde ci seen jë. 5 Guddi du amati, te deesul soxlaati làmp mbaa naaj, ndax Boroom bi Yàlla moo leen di leeral. Te dañuy nguuru ba fàww.6 Ba loolu amee malaaka mi ne ma: «Lii wax ju wóor la te dëggu. Boroom bi Yàlla miy xelal yonent yi, moo yebal malaakaam, ngir mu won jaamam ñi mbir yi dëgmal te du jaas.»
Yeesu Almasi dina délsi
7 «Maa ngii di ñëw léegi. Ndokklee yaw miy sàmm kàdduy waxyuy téere bii.»
8 Man Yowaan maa dégg mbir yii, gis ko. Ba ma ko déggee, gis ko, dama ne gurub sukk ci tànki malaaka, mi ma ko won, nar koo sujjóotal. 9 Mu ne ma: «Ëpp naa def, sa mbokkum jaam doŋŋ laa, ni yaak sa bokki yonent yeek ñiy sàmm kàdduy téere bii. Sujjóotalal Yàlla.» 10 Mu neeti ma: «Bul làq kàdduy waxyuy téere bii, ndax waxtu wi jege na. 11 Ku jubadi, na saxoo njubadi; ku yàqu, saxoo yàqute; ku jub, wéye def njub; ku sell it, wéye sell.»
12 «Maa ngii di ñëw léegi, ànd ak sama pey, ngir delloo ku nekk jëfam. 13 Man maay Alfa di Omega; maa jëkk, maa mujj, maay njàlbéen, maay muj.
14 «Ndokklee yeen ñi fóot seeni yére, ngir saña lekk ci garabu dund gi, jàlle bunt yi, dugg ci biir dëkk bi. 15 Ci biti, xaj yaa fa nekk ak xërëmkat yi ak moykat yi ak bóomkat yi ak bokkaalekat yi, ak képp ku sopp fen te di ko jëfe.
16 «Man Yeesu maa yónni sama malaaka, ngir mu seede mbir yii ci yeen, ñeel mboolooy gëmkat ñi. Man maay njebbitu Daawuda, di kuutaayam, maa di biddiiwu njël bi ne ràññ.»
17 Noo gi ak Séet bi neeñu: «Ñëwal!»
Ku ci dégg it, neel: «Ñëwal!»
Ku mar, ñëwal; ku bëgg ci ndoxum dund mi, jëlal, ñu may la.
18 Man Yowaan, seede naa ñeel képp ku dégg kàdduy waxyu yu téere bii, ne: Képp ku ci yokk lenn, Yàlla dina la yokkal mbugal, yi ñu bind ci téere bii. 19 Te ku wàññi lenn ci kàdduy waxyu yu téere bii, sa wàll la Yàlla di wàññee ci yooyii ñu bind ci téere bi, muy garabu dund gaak dëkk bu sell ba.
20 Kiy seede mbir yii nee: «Waawaaw, maa ngi ñëw léegi.»
Amiin, Sang Yeesu, ñëwal!
21 Yal na yiwu Sang Yeesu ànd ak ñépp.