UBBITE GI
Téere bii mooy ñaareel xaajub Kàddug Yàlla gi. Dees na ko wooye it kóllëre gu mujj, gi Yàlla fas ak nit. Am na ñu koy wooye Injiil, mu tekki Xibaaru jàmm bi. Yàllaa ko wàcce ci gaayam yu sell yi, ñu bind ko ci làkku gereg. Li ñu bind ci téere yu jëkk ya nag, moom lanu tekki ci wolof.
Xaaju Kàddug Yàlla bu jëkk bi moo ëmb Tawreet ak Sabóor ak bindi yonent yi. Diirub junniy at, Yàlla wax na ci wàll yu bare ak ci tëralin yu wuute, jaarale ko ci gémmiñu lu ëpp fanweeri yonent, dale ko ci Yonent Yàlla Musaa ba ci Yonent Yàlla Malasi. Yàlla won na yonent yooyu seen matadi fa kanamam, te yégal na leen ñëwug Rammukat bi, Almasi bu sell, biy ubbi buntu jàmm ëllëg. Bind nañu sax ne: «Yonent yépp a ko seedeel ne, ku ko gëm, Yàlla dina la baal say bàkkaar ci turam.»
Injiil bu sell bi nag moo nettali ni Yàlla matale la mu waxoon ca jamonoy yonent yu jëkk ya. Almasi, mooy Boroom tur wu rafet wii: Kàddug Yàlla, ndax moo làmboo yéene ju rafet, ji Yàlla am, ngir baal nit ñi seeni bàkkaar, ba noppi boole leen ci ndamam. Ni ay dex di wale, tàbbi géej, ni la waxi yonent yi mate ci Injiil. Gif moo sax ba doon guy. Yonent yi ay làmp lañu yuy lerxate àddina su lëndëm, Almasi di jant bu fenk, ngir leeral doom Aadama, teg ko ci yoonu jàmm.
Téere bii 27 wàll la. Ñeent yu jëkk yi, Macë, Màrk, Luug ak Yowaan, ñooy xamle dundug Almasi, dale ko ci juddoom ba ci njàngleem ak mbëggeelam ci nit ak deeyam gi mu sarxee bakkanam, ngir gàddu bàkkaari àddina, ak ndekkiteem. Wàll wi ci topp, di Jëf ya, moo nettali mbirum gëmkati Almasi ñu jëkk ña, ak xibaar ba ca dégtoo, ñeel àddina. 21wàll a ngi ci, ay bataaxal yu ñu bind la, ngir ñaax gëmkat ñi. Bataaxal yooyu ñoo lal xóotaayu mucc, gi Yàlla tëral ci Almasi ci kaw yërmandeem. Wàll wu mujj wi, di Peeñu mi, day misaal xare biy jib ci mujug jamono diggante leer ak lëndëm. Mooy xamle ni Yàlla note Seytaane, boole ci àtte àddina si ci njub, ak yeesal asamaan ak suuf.
Téere bu sell bii moo feeñal màggaayu Yàlla Aji Kawe, ji dëkke leer gu kenn manula jege. Moo feeñal sellngay Aji Sell ji xajoowul bàkkaar. Waaye moo fésal itam cofeelam gu réy, gi taxoon Musalkat bu sell bi ganesi àddina, ngir jot nu ci sànkute.
Yaw miy jàng téere bii nag, yal na Yàlla barkeel sam njàng. Yal na la Noowam gu Sell taxawu, te firil la ko. Moom moo ne, kuy seet, dinga gis. (Macë juróom ñaareelu saar, juróom ñetteelu aaya, Macë 7.8) Te woote bu mag, bi jibe woon ci gémmiñu Rammukat bi, mu ngi dégtu ba tey: «Ñëwleen ci man, yeen ñépp ñi sonn te diis, dinaa leen may noflaay.» (Macë fukkeelu saar ak benn, ñaar fukkeelu aaya ak juróom ñett, Macë 11.28.)