Kayin rey na Abel
4
1 Gannaaw loolu Aadama dëkkoo na soxnaam Awa, mu ëmb, am Kayin, mu ne: «Am naa doom ju góor ci ndimbalu Aji Sax jia 2 Awa teg ca rakkam, Abel. Abel di sàmm, Kayin di beyb.
3 Ñu dem ba mu yàgg, Kayin sàkk ci mbeyam, jébbal ko Aji Sax ji, màggale ko ko. 4 Abel moom jébbal ko nebbonu jur, ga jëkka juddu ca géttam. Aji Sax ji nangul Abel, 5 te nangulul Kayin. Kayin nag mer lool, ba ne fóññ.
6 Aji Sax ji ne Kayin: «Lu la taxa mer, ba ne fóññ nii? 7 Soo defee lu baax, dees na la nangul; soo deful lu baax, bàkkaar a ngi lay yeeru ci sa bunt, di la tërook a wut, waaye yaa ko wara man.»
8 Ci kaw loolu Kayin séq ak rakkam Abel wax. Ba mu ko defee ñu dem ca àll ba, Kayin dal ci kaw Abel, bóom ko. 9 Aji Sax ji ne Kayin: «Ana sa rakk Abel?» Mu ne ko: «Gisuma ko de; xanaa maa wara sàmm sama rakk?» 10 Yàlla ne ko: «Loo def? Sa deretu rakk jaa ngi yuuxoo ci suuf, ma di ci dégg. 11 Léegi dinga alku, ba suuf dummóoyu la, moom mi ubbi gémmiñam, naan sa deretu rakk, ji nga tuur. 12 Boo beyee, dootu nangu. Dinga dëkke daŋ-daŋ, di wëreelu ci àddina.»
13 Teewul Kayin wax Aji Sax ji ne ko: «Sama mbugal diis na lool, ba àttanuma ko! 14 Ndegam tey jii danga maa dàq, xañ ma sa jataay, dinaa dëkke daŋ-daŋ, di wëreelu ci kaw suuf, te kon ku ma gis rey ma.» 15 Aji Sax ji ne ko: «Kon nag ku la rey, yaw Kayin, dina jot juróom ñaari yoon lu ko raw.» Ba loolu amee mu sàkkal Kayin màndarga, ba ku ko gis du ko rey. 16 Kayin daldi bàyyikoo ca Aji Sax ji, dem dëkki réewu Nóddc, fa féete Àjjana penku.
Askanu Kayin
17 Gannaaw loolu Kayin dëkkoo na soxnaam, mu ëmb, am Enog. Ci biir loolu Kayin sanc ab dëkk, dippee ko doomam ju góor Enog. 18 Enog jur Iraat; Iraat jur Mexuyayel; Mexuyayel jur Metusayel; Metusayel jur Lemeg. 19 Lemeg nag jël ñaari jabar, aawo bi tudd Ada, ñaareel bi di Silla. 20 Ada taawloo Yabal, miy cosaanu sàmm yiy màngaan, 21 teg ca Yubal, miy cosaanu ñi mane xalam ak toxoro. 22 Silla moom jur Tubal Kayin miy tëgg lépp luy jumtukaayu xànjar ak weñ. Tubal Kayin am na jigéen bu tudd Naama.
23 Lemeg nag ne ay soxnaam:
«Dégluleen maa, yeen soxnay Lemeg,
teeyluleen maa, yeen Ada ak Silla.
Nit a ma gaañ, ma bóom,
goneg jàmbaar dóor ma, ma faat.
24 Kayin kay, lees di feyul juróom ñaari yoon,
ne, bu dee Lemeg mii, muy juróom ñaar fukki yoon ak juróom ñaar.»
25 Bi loolu wéyee Aadama dëkkoo soxnaam, mu am doom ju góor; tudde ko Set (mu firi May), ndax da ne: «Yàlla may na ma weneen askan, mu wuutu Abel, mi Kayin rey.» 26 Set it, am doom ju góor, tudde ko Enos. Fan yooya lañu tàmbalee tudd Aji Sax ji, di ko wormaal.