Askanu Esawu
(Saar 36.1-43)
36
1 Askanu Esawu, mi ñuy wax Edom, mooy lii.2 Esawu jël na janqi Kanaaneen jabar. Ñooñoo di: Ada doomu Elon, Etteen ba, ak Olibama doomu Ana, miy doomu Sibeyon, Eween ba, 3 ak Basmat doomu Ismayla, di jigéenub Nebayot. 4 Ada am ak Esawu Elifas; Basmat am ca Rewel. 5 Olibama am ca Yewus, Yalam ak Kora. Ñooñu ñooy doomi Esawu, te mu am leen ca réewu Kanaan.
6 Ba loolu amee Esawu ànd aki soxnaam, aki doomam yu góor ak yu jigéen, ak waa këram ñépp, jiital géttam ak juram gépp, yóbbaale mboolem alal ju mu amoon ca réewu Kanaan, daldi sanci meneen réew ngir sore rakkam Yanqóoba. 7 Li ko waral mooy, seen alal dafa bare woon lool, ba manuñoo dëkk ñoom ñaar, te réew, mi ñu daloon, àttanu leen ndax seen gétt yu bare. 8 Esawu nag dëkk ca tundu Seyir: Esawu moomu mooy Edom.
9 Askanu Esawu, di maami Edomeen ña ca tundi Seyir, mooy lii.
10 Doomi Esawu yu góor ñooy: Elifas, mi mu am ak soxnaam Ada ak Rewel, mi mu am ak Basmat. 11 Doomi Elifas yu góor yi di: Teman ak Omar ak Sefo ak Gatam ak Kenas. 12 Timna it nekkaaleb Elifas. Mu am caak moom Amaleg. Ñooñoo xeetoo ci Ada, soxnas Esawu. 13 Doomi Rewel yu góor yi ñoo di: Naxat ak Sera ak Saama ak Misa. Ñooñoo xeetoo ca Basmat, soxnas Esawu. 14 Soxnas Esawu, si ñu naa Olibama, tey doomu Ana miy doomu Sibeyon, moo am ak Esawu doom yu góor yii: Yewus, Yalam ak Kora.
15 Làngi doomi Esawu yu góor nag, ñooy ñii. Ñi askanoo ci Elifas taawub Esawu, ñuy Teman ak Omar ak Sefo ak Kenas 16 ak Kora ak Gatam ak Amaleg, ku ci nekk ak làngam. Làngi Elifas, ya ca réewum Edom a ngi noonu; ñooy sëti Ada. 17 Ñi askanoo ci Rewel doomu Esawu, ñooy Naxat ak Sera ak Saama ak Misa, ku ci nekk ak làngam. Làngi Rewel, ya ca réewum Edom a ngi noonu; ñooy sëti Basmat, soxnas Esawu. 18 Ñi xeetoo ci Olibama soxnas Esawu, ñooy Yewus, Yalam ak Kora, ku ci nekk ak làngam. Ñooñooy làngi Olibama, soxnas Esawu siy doomu Ana. 19 Ñooñooy doomi Esawu, mi ñuy wax Edom, ñooñooy doomam yu góor, ñook seeni làng.
Lu jëm ci askanu Seyir
20 Doomi Seyir, ya bokk ca waa Or te sancoon ca réew ma, ñooy Lotan ak Sobal ak Sibeyon ak Ana 21 ak Dison ak Eser ak Disan. Ñooñooy làngi waa Or, di sëti Seyir ya ca réewum Edom. 22 Doomi Lotan yu góor ya nag ñooy Ori ak Emam. Jigéenub Lotan di Timna. 23 Doomi Sobal yu góor ya di Alwan ak Manaat ak Ebal ak Sefo ak Onam. 24 Doomi Sibeyon yu góor di Aya ak Ana. Te Ana moomu moo feeñal bëti ndox yu tàng ya ca màndiŋ ma, ba muy sàmm mbaami baayam Sibeyon. 25 Doomi Ana ñooy Dison ak Olibama, doomam ju jigéen. 26 Doomi Dison di Emdan ak Esban ak Yitran ak Keran. 27 Doomi Eser di Bilan, Saawan ak Akan. 28 Doomi Disan di Uus ak Aran.
Lu jëm ci buur ya jëkka falu ca Edom
29 Làngi waa Or ñooy ñi askanoo ci Lotan ak Sobal ak Sibeyon ak Ana 30 ak Dison ak Eser ak Disan, ku ci nekk ak làngam. Ñooñooy làngi waa Or, na ñu xàjjalikoo kenn-kenn ca réewu Seyir.
31 Buur, yi falu ca réewum Edom, lu jiitu kenn ci waa Israyil di fa falu, ñooy ñii. 32 Bela doomu Beyor falu na ca Edom. Dinaba moo doon péeyam. 33 Ba Bela faatoo, Yobab doomu Sera, ma dëkk Boccra, wuutu ko. 34 Ba Yobab faatoo, Usam mu diiwaanu waa Teman wuutu ko. 35 Ba Usam faatoo, Adàdd, ma dàqoon waa Majan ca réewu Mowab, tey doomu Bedàdd, moo falu, wuutu ko. Awit a doon péeyam. 36 Ba Adàdd faatoo, Samla, ma dëkk Masreka, falu, wuutu ko. 37 Ba Samla faatoo, Sawul ma woon ca Reyobot Efraat, falu, wuutu ko. 38 Ba Sawul faatoo, Baal Anan doomu Agbor falu, wuutu ko. 39 Ba Baal Anan doomu Agbor faatoo, Adar falu, wuutu ko. Pawu moo doon péeyam, soxnaam di Metabeel, mi Mataredd doomu Me Saab di yaayam.
40 Làng yi sosoo ci Esawu nag, làng gu ci nekk ak turam ak njaboot, ya mu ëmb, ak gox, ba mu dëkke, ñoo di ñii: ñi askanoo ci Timna ak Alwa ak Yetet 41 ak Olibama ak Ela ak Pinon 42 ak Kenas ak Teman ak Mibsar 43 ak Magdiyel ak Iram, ku ci nekk ak làngam. Ñooñu ñooy làngi Edom, ma ñu naa Esawu, moom ma giir Edomeen ñi, làng gu ci nekk ak gox, ba nga dëkke te moom ko.