Yanqóoba tàggoo na
49
1 Gannaaw loolu Yanqóoba woo ay doomam ne leen:
«Bokkleen daje, ma xamal leen li leen di dikkal ëllëg.
2 Dajeleen te déglu ma, man Yanqóoba seen baay;
teewluleen seen baay Israyil.
 
3 «Ruben, yaw mi ma taawloo,
nga sosoo sama digg doole, sama ndoortel kàttan,
yaa jëkke sut moos ci teraanga ak doole.
4 Yaa toogadi it ni ndox muy wal-wali,
doo mujje sut,
nde yaa tëdd sa lalu baay,
ba teddadi, kera ba nga ca tëddee.
 
5 «Simeyon ak Lewi ñoo duye yene,
ñooy nas pexey ay.
6 Yàlla bu sama xol ànd ci seeni pexe,
mbaa sama xel di nangu seeni diisoo,
ndax fu ñu mere, xal faa bóome,
te làggal ay yëkk lañuy foye.
7 Mbas ma seen xadar, gu tar,
ak seen mer, mi dul meddi.
Maa leen di wasaare ci kër Yanqóoba,
tasaare leen ci Israyil.
 
8 «Yaw Yuda, mi say doomi baay di taggeji,
ngay sëqi sa ndoddi noon, sëgal leen,
sa doomi baay a lay sujjóotal.
9 Yuda yaa di gaynde gu ndaw, doom,
doora jóge nii ci pàdd,
tey yuug ak a goor ni gayndeg sibi.
Yaa di gaynde gu deesul yee.
10 Nguur gi du jóge ci loxol Yuda,
te yetu buur ay wéye sampe ciy tànkam,
li feek borooma di ñëw,
ba xeet yi déggal ko.
11 Mooy yeew mbaamam cig reseñ,
cumbur ma féeteek car, ba ca gën;
muy fóote ay yéreem biiñ,
di sumb mbubbam ci ndoxum reseñ.
12 Bët yaa ngay nes-nesi ndax biiñ,
bëñ ya weex furr ndax um soow.
 
13 «Sabulon ay dëkke tefesi géej,
di teerub gaal yi,
am réewam digalook Sidon.
 
14 «Isaakar mbaam ngonk la,
muy goor diggante ñaari sëf.
15 Bu gisee ni mbaaram neexe,
ak ni réew mi naate,
day waaf, gàddu ngaaxam,
daldi féetewoo coonob njaam.
 
16 «Dan ay àtteji xeetam,
ni ko giiri Israyil baaxoo.
17 Waaye Dan ay jaan ju dog aw yoon,
mbaa céebi ciw ñall,
mooy màtt tànki fas,
gawar jullootu.
 
18 «Céy Aji Sax ji, maa ngi séentu sa xettal!
 
19 «Gàdd la gàngoor di gaw,
mu téqtal leen, ba daan.
 
20 «Aser ay boroom dund bu duun,
mooy maye ngëneeli ñami buur.
 
21 «Neftalee di kéwél gu fëx,
te mooy jur doom yu taaru.
 
22 «Yuusufaay bànqaasu garab,
garab guy meññ, feggook bëtu ndox,
car yaa nga law, tiim digu tool ba.
23 Ay fittkat a ko toŋal,
di ko song ak a fitt.
24 Teewul xalaam ga di wéye daŋ,
te la loxo yay dëgërloo mooy
loxoy Jàmbaar ju Yanqóoba,
kookooy Sàmm bi, Doju cëslaayal Israyil,
25 mooy sa Yàllay baay, ji lay wallu,
mooy Aji Man ji lay barkeele
ca barkey asamaan, ya fa kaw,
ak barke ya ne leww ca suuf xóote ya,
teg ca barkeb njur ak nàmpal.
26 Sa ñaani baay ya romb
xéewali tund, ya sax fàww,
rombati ngëneeli jànji cosaan ya,
yal na dal ci boppu Yuusufa,
ca kaw ndaal boppam, moom sangub doomi baayam ya.
 
27 «Beñamin ay till guy yeeroo,
di xëye yàpp rëbbam,
tey gonloo séddale am lëlam.»
 
28 Ñooñu ñoo sos mboolem giiri Israyil, ñu tollu ci fukk ak ñaar, te loolu la leen seen baay wax, ba mu leen di tàggu. Ku ci nekk mu tàggoo ko kàdduy tàggtoo, ya war ca moom.
Yanqóoba nelaw na
29 Gannaaw loolu da leena dénk ne leen: «Maa ngi waaja fekki samay maam; dencleen ma fa samay maam ca xuntim bàmmeel ba ca toolub Efron, Etteen ba. 30 Mooy xuntim bàmmeel ba ca biir tool, ba ca Magpela, te jàkkaarloo ak Mamre ca réewu Kanaan, di tool, ba Ibraayma jëndoon ca Efron, Etteen ba, ngir def ko bàmmeel. 31 Foofa lañu denc Ibraayma ak soxnaam Saarata, te foofa lañu denc Isaaxa ak soxnaam Rebeka, te fa laa denc Leya it. 32 Tool ba ak xuntim bàmmeel ba ca nekk, ña nga ko jënde ca Etteen ña.»
33 Naka la Yanqóoba dénku doomam yu góor ya noona, daldi delloo ay tànkam ca lal ba, bakkan ba rot, mu fekki ay maamam.