6
1 Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Dinga gis léegi ni may def Firawna: loxo bu ko ëpp dooleey tax mu bàyyi leen ñu dem. Bir na ne, loxo bu ko ëpp doole mooy tax mu dàq leen réewam.»
Yàlla dellu na yónni Musaa
2 Yàlla dellu wax Musaa ne ko: «Man maay Aji Sax ji. 3 Yàlla Aji Man ji, mooy ni ma feeñoo woon Ibraayma, te ni laa feeñoo Isaaxa ak Yanqóoba it, waaye sama tur, Aji Sax ji, leeraluma leen ko woon. 4 Te itam damaa fasoon ak ñoom kóllëre, ngir jox leen réewum Kanaan, réew ma ñu nekkoon ay doxandéem. 5 Maa déggal sama bopp yuuxi bànni Israyil, gi waa Misra def ay jaam, te fàttewuma sama kóllëre ga. 6 Kon nag waxal bànni Israyil ne leen: Man maay Aji Sax ji. Maa leen di sippil, yeen bànni Israyil, li leen waa Misra sëf, te maa leen di teggil njaam, gi ñu leen teg. Maay tàllal sama loxo, dogal mbugal yu kéemaane, ba goreel leen. 7 Maa leen di def sama ñoñ, di seen Yàlla. Dingeen xam ne man Aji Sax ji maay seen Yàlla, ji leen di teggil sas, yi leen waa Misra teg. 8 Maa leen di yóbbu ba ngeen dugg réew ma ma giñoon ne maa koy jox Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, te maa leen koy moomale, man Aji Sax ji.»
9 Ba Musaa waxee loolu bànni Israyil, dégluwuñu ko sax ndax xol bu jeex ak njaam gu metti.
10 Aji Sax ji wax Musaa ne ko: 11 «Demal wax Firawna buuru Misra, mu bàyyi bànni Israyil, ñu génn réewam.» 12 Musaa tinu Aji Sax ji ne ko: «Waaw, ndegam bànni Israyil sax nanguwuñu maa déglu, nu ma Firawna di déggale, man mii tëlee wax?» 13 Aji Sax ji nag wax ak Musaa ak Aaróona, jox leen ay ndigal ci mbirum bànni Israyil ak Firawna buuru Misra, ngir ñu yiwi bànni Israyil, ba ñu génn Misra.
Lu jëm ci cosaanu Musaa ak Aaróona
14 Bànni Israyil ya yilifoon seen kër baay, ñoo di:
Góor ña Ruben, taawu Israyil, jur: Anog ak Palu ak Esron ak Karmi. Ñooñoo sos làngi Ruben.
15 Doomi Simeyon yu góor di Yemuwel ak Yamin ak Owàdd ak Yakin ak Sowar ak Sawul, mi ndeyam dib Kanaaneen. Ñooñoo sos làngi Simeyon.
16 Doomi Lewi yu góor ñoo di Gerson ak Keyat ak Merari, ku nekk ak askanam. At ya Lewi dund, téeméer la ak fanweer ak juróom ñaar (137).
17 Doomi Gerson yu góor ñoo di Libni ak Simey, ñook seeni làng.
18 Doomi Keyat yu góor ñoo di Amram ak Isar ak Ebron ak Usyel; te at ya Keyat dund, téeméer la ak fanweer ak ñett (133).
19 Doomi Merari yu góor ñoo di Maali ak Musi.
Ñooñoo sos làngi Lewi ak seeni giir.
20 Amram moo jël bàjjanam Yokebedd soxnaa, kooku am ak moom Aaróona ak Musaa. At, ya Amram dund, téeméer la ak fanweer ak juróom ñaar (137).
21 Doomi Isar yu góor ñoo di Kore ak Nefeg ak Sikkri.
22 Doomi Usyel yu góor di Mikayel ak Elsafan ak Sitiri.
23 Aaróona moo jël Eliseba doomu Aminadab, jigéenub Nason. Kooku am ak moom Nadab ak Abiyu ak Elasar ak Itamar.
24 Doomi Kore yu góor ñoo di Asir ak Elkana ak Abiyasaf. Ñooñoo sos làngi Kore.
25 Elasar doomu Aaróona moom, moo jël soxna kenn ca doomi Putiyel, kooku am ak moom Fineyas.
Ñooñoo yilif seeni kër baay ca Leween ña, ku nekk sos làngam. 26 Aaróona moomu nag, mook Musaa, la Aji Sax ji wax, ne leen: «Génneleen bànni Israyil Misra, kurél ci kaw kurél.» 27 Ñoom ñooñu ñoo wax ak Firawna buuru Misra, ngir génne bànni Israyil Misra; du keneen ku dul Musaa ak Aaróona.
Yàlla feddli na digeem baak Musaa
28 Keroog ba Aji Sax ji waxee ak Musaa ca réewum Misra, 29 da koo wax, ne ko: «Man maay Aji Sax ji. Nanga wax Firawna buuru Misra, li ma lay wax lépp.» 30 Teewul Musaa tinu Aji Sax ji, ne ko: «Waaw, waaye man, damaa tëlee wax. Mbaa Firawna dina ma déggal yee?»