Woyu Musaa waak bànni Israyil
15
1 Ba loolu amee nag Musaa ak bànni Israyil woy Aji Sax ji, màggal ko. Ña nga naan:
 
«Ma woy Aji Sax ji, ngir ndamam li kawee kawe.
Fas ak gawaram la fab, xalab géej.
2 Sama doole, sama kaaraange, Ki Sax a;
te mooy sama wall tey.
Mooy sama Yàlla, ji may tagge,
sama Yàllay maam, ji may joobe.
 
3 «Aji Sax ji jàmbaari xare ji,
Aji Sax jeey turam!
4 Watiiri Firawnaaki xarekatam la fab sànni géej;
ñeyi xareem ya labandoo ca géeju Barax ya,
5 xóote ya boole sàng,
ñu ne ca biir menteñ niw doj.
 
6 «Aji Sax ji, sa kàttanu ndijoor a yéeme!
Aji Sax ji, sa ndijoor a ne noon ba rajax.
7 Sa màggaay gu yéemee nërmeel say noon.
Yaa yebal sa mer, mu ne jippét,
xoyom leen ni boob.
8 Nga wal sag noo, ndox ya tegloo,
wal ma ne sàtt, jaloo jalu,
ndoxi xóotey géej way deeŋ!
 
9 «Noon baa nga naa: “Maay dàqe, dabe,
lël alal ja, séddale
séddu, ba xol sedd,
ne saamar boset,
teg leen loxo.”
10 Waaye sa ngelaw nga wal,
géej mëdd leen,
ñu diigandoo ni beteex biir géej mbàmbulaan!
 
11 «Ana kuy sa moroom ci tuur yi, yaw Aji Sax ji?
Kuy sa dend, yaak sa sellaay bu yéeme,
sa yànjaay bu raglook sa jëf yu yéeme?
12 Yaa tàllal sa ndijoor,
suuf wonn leen.
 
13 «Sa ngor nga jiitee mbooloo, mi nga jot,
te sa kàttan nga leen di yóbboo ca sa kër gu sell.
14 Jaambur ñay dégg, di rag-ragi,
tiitaange ne taral waa Filisti,
15 kilifay waa Edom jàq,
njiiti Mowab di kat-kati,
mboolem waa Kanaan tiit, ne yasar;
16 tiitaangeek njàqaree ne milib ca seen kaw.
Sa kàttan a tax ñu mel niw doj, ne yàcc,
ba kera sa ñoñ jàll, Aji Sax ji,
ba kera askan wa nga goreel, jàll,
17 te yaa leen di sampi ca sa tund wa nga séddoo,
fa nga waajal sa dëkkuwaay, Aji Sax ji,
bérab bu sell ba nga sàkke sa loxol bopp, Boroom bi.
18 Aji Sax jeey Buur, tey ak ëllëg ba fàww.»
19 Ci kaw loolu fasi Firawna ànd ak watiiri xareem aki gawaram, tàbbi géej, Aji Sax ji delloo ndoxi géej ga ca seen kaw, bànni Israyil ñoom, jaare joor gu wow ca digg géej ga.
Maryaama woy na
20 Yonent Yàlla Maryaama, jigéenub Aaróona nag ŋàbb tabala, jigéen ñépp topp ko, génn di fecc, tabala ya jiin. 21 Maryaamaa nga leen di dëbbeel, naa:
«Woyleen Aji Sax ji, ngir ndamam li kawee kawe.
Fas ak gawaram la fab, xalab géej.»
Lu jëm ci ndox mu wex ma
22 Gannaaw loolu Musaa jële bànni Israyil géeju Barax ya, ñu wéy, wuti màndiŋ, ma ñuy wax Sur. Dox nañu ñetti fan ca màndiŋ ma, gisuñu ndox. 23 Ñu dem, ba àgg fu ñu naan Maara, waaye manuñoo naan ca ndoxum Maara, ndax wex. Looloo waral ñu tudde bérab ba Maara (mu firi Fu wex). 24 Mbooloo ma nag di diiŋat Musaa, naan: «Ana ndox mu nuy naan nag?» 25 Musaa woo Aji Sax ji wall, Aji Sax ji won ko dammitu bant, mu sànni ko ca ndox ma, ndox ma neex.
Foofa la Aji Sax ji dogalal bànni Israyil ay sàrti yoon ak ndigal, te fa la leen nattoo itam. 26 Da ne leen: «Bu ngeen farloo ci déggal seen Yàlla Aji Sax ji, di def li mu rafetlu, di teewlu tey jëfe ay santaaneem, di sàmm bépp dogali yoonam, su boobaa duma leen teg lenn ci jàngoro, yi ma tegoon waa Misra, ndax man maay Aji Sax, ji leen di wérloo.»
27 Ci kaw loolu ñu dem ba Elim, fekk fa fukki bëti ndox ak ñaar, ak juróom ñaar fukki garabi tàndarma. Ñu dal foofa ca wetu ndox ma.