Lu jëm ci sarxalkat yeek seen xewu colu
29
1 «Lii nag mooy li nga leen di defal, ngir sédd leen céru sellnga, ngir ñu di ma sarxalal: Dangay jël yëkk wu ndaw ak ñaari kuuy yu amul sikk, 2 ak mburu yu mag yu amul lawiir, ak kàmp yu sew yu amul lawiir yu ñu xiiwaale diw, ak mburu yu tàppandaar yu amul lawiir, ñu wis diw ca kaw, te sungufu bele su mucc ayib ngay defare yooyu. 3 Yebal lépp ci benn pañe te jébbale ko, mook yëkk wu ndaw wi ak ñaari kuuy yi. 4 Yóbbul Aaróona ak doomam yu góor, ba ca bunt xaymab ndaje ma, nga sang leen. 5 Nga jël yére yi nag, solal Aaróona mbubb mu gudd mi, ak fëxyab xar-sànni mi, teg ci xar-sànni mi, tegaat ci kiiraayal dënn bi, daldi koy takkal ngañaay liy tege ci xar-sànni mi. 6 Su ko defee nga kaala ko, takkal ko meeteel gu sell gi, fi kanam kaala gi. 7 Te nga jël diwu pal gi, sotti ko ci kaw boppam, diw ko. 8 Bu loolu weesee, nga ne doomi Aaróona ñu jegesi, nga solal leen seeni mbubb, 9 kaala leen, te takkal Aaróona ak doomam yu góor ay laxasaay. Su ko defee ñu féetewoo céru sarxalkat, muy dogal bu sax dàkk.«Noonu ngay sase Aaróona ak doomam yu góor. 10 Nanga yóbbu yëkk wu ndaw wi ba ci bunt xaymab ndaje mi, Aaróona aki doomam teg seeni loxo ci kaw boppu yëkk wi, 11 nga daldi rendi yëkk wi fi kanam Aji Sax ji, fi bunt xaymab ndaje mi. 12 Sàkkal ci deretu yëkk wu ndaw wi, nga capp ci sa baaraam, diw ci béjjéni sarxalukaay bi, te nga tuur li des ci deret ji ci suufu sarxalukaay bi. 13 Jëlal mboolem nebbon bi sàng yérey biir yi, ak bàjjo bi ci res wi, ak ñaari dëmbéen yi ànd ak nebbon bi ci kaw dëmbéen yi, nga boole lépp def ko saraxu taal-saxaral ci kaw sarxalukaay bi. 14 Seen saraxu póotum bàkkaar a ngoogu. Li des ci yàppu yëkk wi, boole kook der bi, ak sébbriit mi, nga génne ko dal bi, lakk ko.
15 «Menn kuuy mi, jël ko, Aaróona aki doomam teg seeni loxo ci boppu kuuy mi, 16 ba noppi, nga rendi kuuy mi, jël deret ji, xëpp ko ci peggi sarxalukaay bi yépp ba mu daj. 17 Kuuy mi, ay dog nga koy dogat, daldi raxas yérey biir yi ak yeel yi, teg ci kaw dog yi ak bopp bi. 18 Lakkal kuuy mépp ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, ñeel Aji Sax ji, di xeeñ xetug jàmm; saraxu sawara la, ñeel Aji Sax ji.
19 «Jëlal kuuy mi ci des, Aaróona ak doomam yu góor teg seeni loxo ci boppu kuuy mi. 20 Su ko defee nga rendi kuuy mi, sàkk ci deret ji, taqal ci tabanum noppu ndijooru Aaróona ak tabanum noppu ndijooru doomam yi, te nga taqal ci seen baaraamu déyu ndijoor, ak seen baaraamu tànku ndijoor bu mag. Boo noppee, nga xëpp li des ci deret ji ci peggi sarxalukaay bi yépp ba mu daj. 21 Sàkkal ci deret ji ci sarxalukaay bi, ak ci diwu pal gi, nga wis-wisal ko ci kaw yaramu Aaróona ak ci kawi yéreem, wis-wisal ko ci kaw yarami doomam ak ci seen kawi yére. Su ko defee Aaróona sell, mooki yéreem, ay doomam it sell, ñook seeni yére.
22 «Kuuy mi, nanga ci génne li ci duuf: calgeen bi, ak nebbon bi sàng yérey biir yi, ak bàjjo bi ci res wi, ak ñaari dëmbéen yeek nebbon bi ci seen kaw, ak tànku ndijoor bu kanam bi, ndax kuuyum colug sarxalkat yi la. 23 Pañe biy taaje fi kanam Aji Sax ji te def mburu yu amul lawiir nag, nanga ci sàkke menn mburu mu tàppandaar, ak menn mburu mu ñu xiiwe diwu oliw, ak menn mburu mu gëna sew. 24 Nga boole lépp, teg ko ci loxoy Aaróona aki doomam, ñu def ko saraxu yékkati-jébbale, ñeel Aji Sax ji. 25 Nga daldi koy nangoo ci seeni loxo, lakk ko ci kaw sarxalukaay bi, boole kook saraxu rendi-dóomal bi, muy xeeñ xetug jàmm fi kanam Aji Sax ji. Saraxu sawaraa ngoogu, ñeel Aji Sax ji.
26 «Nanga jël dënn bi bokk ci kuuyum xewu colug Aaróona, nga def ko saraxu yékkati-jébbale, ñeel Aji Sax ji. Loolu moo cay sa wàll. 27 Nanga ber dënn bi ñu def saraxu yékkati-jébbale, mook tànkub jooxe bi ñu def saraxu yékkati-jébbale, te ñu jooxee ko ci kuuyu colu gi, ñeel Aaróona aki doomam. 28 Aaróona aki sëtam la loolu di doon seen cér bu bànni Israyil di warlook ñoom ba fàww, ndax ab jooxe la; jooxe bu bànni Israyil di génnee ci seen saraxi cant ci biir jàmm, muy seenub jooxe, ñeel Aji Sax ji.
29 «Yérey Aaróona yu sell yi nag, gannaaw bu dëddoo, dees koy féetale ay doomam, ñu fale leen ko ci seen xewu colug carxal. 30 Diiru juróom ñaari fan, ci la sarxalkat bi koy wuutu ci doomam yu góor, di sol yére yooyu, moom miy dugg ci biir xaymab ndaje mi, ci biir bérab bu sell bi.
31 «Nanga jël kuuyu xewu colu gi, nga baxal yàpp wi ci bérab bu sell. 32 Aaróona aki doomam ñooy lekk yàppu kuuy mi ci bunt xaymab ndaje mi, boole kook mburu mi ci pañe bi. 33 Ñam yooyu, ña koy lekk mooy ña muy seen saraxu njotlaay, keroog ca seen xewu colu, ga ñu leen tabbe ngir sellal leen. Waaye keneen du ci lekk, ndaxte ñam wu sell la. 34 Bu lenn ci yàppu colu gi mbaa lenn ci mburu mi fanaanee ba bët set, nañu lakk loola ca fanaan ba mu jeex. Deesu ko lekk, ndaxte ñam wu sell la.
35 «Noonu ngay def ak Aaróona aki doomam, ni ma la ko sante rekk. Diiru juróom ñaari fan ci nga leen di sas, 36 te aw yëkk ngay def saraxu póotum bàkkaar bés bu nekk, muy seen njotlaay, di njotlaay liy setal sarxalukaay bi. Te itam nanga diw sarxalukaay bi ag diw, sellale ko ko. 37 Diiru juróom ñaari fan ngay defal sarxalukaay bi saraxu njotlaayam, sellale ko ko, ba sarxalukaay bi doon lu sella sell. Lépp lu laal sarxalukaay bi day séddu ci sellaayam.
Lu jëm ci sarax yi war bés bu nekk
38 «Lii mooy li ngay rendi ci kaw sarxalukaay bi: ñaari kuuyi menn at, bés bu nekk ba fàww. 39 Menn kuuy mi, nga rendi ko ci suba, meneen kuuy mi, diggante ngoon, ba jant di so. 40 Sàkkal ñetti kilo, yemook benn fukkeelu nattub sunguf su mucc ayib su ñu xiiwe liitar ak genn-wàll, yemook xaajaatub natt bi ñuy wax xiin ci diwu segalu oliw, ak saraxu tuurub benn liitaru biiñ ak genn-wàll, yemook xaajaatub xiin. Loolu yépp ànd ak menn kuuy mi. 41 Meneen kuuy mi, nga rendi ko diggante ngoon ak jant bu so, booleeti ko ak saraxu pepp mi ak saraxu tuuru bi, ni woon ci suba, muy xeeñ xetug jàmm, di saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. 42 Saraxu rendi-dóomal lay doon bu sax, te war seen maasoo maas fi bunt xaymab ndaje mi, ci kanam Aji Sax ji. Foofu laay dajeek yeen, te fa laay waxe ak yaw, 43 Foofa laay dajeek bànni Israyil, bérab ba doxe fa sell, ndax samag leer. 44 Maay sellal xaymab ndaje mi ak sarxalukaay bi, te Aaróona aki doomam, maa leen di sellal, ngir ñu doon samay sarxalkat. 45 Maay dëkk fi digg bànni Israyil te maay nekk seen Yàlla. 46 Su boobaa bànni Israyil xam ne, man Aji Sax ji maay seen Yàlla, ji leen génnee réewum Misra, ngir dëkk fi seen biir. Man maay seen Yàlla Aji Sax ji.