Defar nañu sarxalukaay bi ak mbalkam njàpp mi
38
1 Ba tey Besalel sàkk ci bantu séng sarxalukaayu rendi-dóomal bu kaare, guddaay bi di juróomi xasab, yaatuwaay bi di juróomi xasab, taxawaay bi di ñetti xasab. 2 Mu sàkkal ko ay béjjénam ci ñeenti collam, mu ànd aki béjjénam, di benn. Mu xoob nag lépp xànjar. 3 Mu sàkk jumtukaayi sarxalukaay bi yépp: ndabi tibbukaayu dóom yi ak ñiitukaay yi ak këll yi, ak lonkukaayi yàpp yi, ak and yi, jumtukaay yépp di xànjar. 4 Mu sàkkal sarxalukaay bi caax bu ñu tëgge xànjar, mu ronu peggu sarxalukaay bi, dale ci suuf ba ci digg sarxalukaay bi. 5 Mu daldi koy móolal ñeenti nopp ci ñeenti colli caaxu xànjar bi, ñuy téye njàppu yi. 6 Mu sàkk njàppuy bantu séng, xoob lu ci nekk xànjar, 7 daldi roof njàppu yi ci nopp yi ci weti sarxalukaay bi, ngir bu ñu koy yóbbu. Am pax, mu xànq yu tàppandaar ub, moom la def sarxalukaay bi. 8 Mu sàkk itam mbalkam njàpp mu ànd ak tegoom, di xànjar ju jóge ci seetuy jigéena, ñi doon liggéey ci bunt xaymab ndaje mi.Defar nañu ëttu jaamookaay bi
9 Besalel nag sàkk wurmbalu jaamookaay bi. Wetam, gi fare bëj-saalum di téeméeri xasabi sori rabal yu ñu ràbbe wëñu lẽe, 10 seen ñaar fukki jën ànd ak seen ñaar fukki tegu, di xànjar, lonku yeek galani jën yi di xaalis.
11 Wetu bëj-gànnaar it di téeméeri xasabi sori rabal, seen ñaar fukki jën ànd ak seen ñaar fukki tegu, di xànjar, lonku yeek galani jën yi di xaalis.
12 Wetu sowu di juróom fukki xasabi sori rabal, ak seen fukki jën yu ànd ak seen fukki tegu, lonku yeek galani jën yi di xaalis.
13 Wetu penku bi ci kanam di juróom fukki xasab; 14-15 fukki xasabi sori rabal ak juróom fi làng ak buntu ëtt bi ci genn wetam, ak seen ñetti jën yu ànd ak seen ñetti tegu, ak fukki xasabi sori rabal ak juróom, wet gi ci des, ak seen ñetti jën yu ànd ak seen ñetti tegu.
16 Mboolem sori wurmbalu ëtt bi ba mu daj, wëñu lẽe la.
17 Teguy jën yi xànjar la, wékkukaayi jën yeek ay galanam di xaalis, ñu xoob boppi jën yi xaalis; jëni ëtt bi yépp nag, galani xaalis lañu leen lëkklee. 18 Lafu buntu ëtt bi, liggéeyu ràbb bu rafet la, bu ñu ràbbe wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe. Guddaayu laf bi ñaar fukki xasab la, taxawaay bi yemook yaatuwaay bi, di juróomi xasab, tollook sori wurmbalu ëtt bi. 19 Jëni lafu bunt bi ñeent la, seen ñeenti tegu di xànjar, seeni wékkukaay di xaalis, ñu xoob kaw jën yi xaalis, galan yi di xaalis. 20 Mboolem xeri jaamookaay bi ak xeri wurmbalu ëtt bi ba mu daj, lépp xànjar la.
Lim nañu jumtukaay yi
21 Lii nag moo di tënkub dayoy gànjar yi ñu jëfandikoo ci liggéeyu jaamookaay bi, jaamookaay boobu àlluway seede si dence. Tënkees na ko ci ndigalu Musaa, Leween ñi sasoo tënk bi ci njiital Itamar doomu Aaróona sarxalkat bi. 22 Fekk na Yudeen bi Besalel doomu Uri, miy doomu Ur, sottal na mboolem li Aji Sax ji santoon Musaa. 23 Mu àndoon ci ak Daneen bi, doomu Ayisamaag, Oliyab. Mu dib yettkat, dib taaralkat te di liggéeykatu wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe.
24 Wurus wi dem ci liggéey bi bépp, mboolem liggéeyu bérab bu sell bi, te muy wurus wu ñu def saraxu yékkati-jébbal Yàlla, juróom ñetti téeméeri kilo ak juróom ñaar fukk ak juróom ñaar la (877), ak ñetti téeméeri garaam (300), yemook ñaar fukki talaŋ ak juróom ñeent, ak juróom ñaar téeméer ak fanweeri (730) siikal ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi. 25 Xaalis bi tukkee ci limeefu askan wi, ñetti junniy kilo ak fukk ak juróom ñaar (3 017), ak juróom ñaar téeméeri garaam ak juróom fukk (750), yemook téeméeri (100) talaŋ ak junneek juróom ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróomi (1 775) siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi, 26 muy juróomi garaami xaalis bopp bu nekk, yemook genn-wàllu siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi, ñeel képp ku bindu ci limeef bi, dale ko ci ñi am ñaar fukki at jëm kaw, ñépp di juróom benni téeméeri junniy góor ak ñetti junneek juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). 27 Ñetti junniy (3 000) kiloy xaalis, di téeméeri talaŋ, ñeel móolub teguy bérab bu sell bi, ak teguy rido bi. Muy téeméeri tegu ci ñetti junniy kilo, di fanweeri kilo ci benn tegu, muy téeméeri tegu ci téeméeri talaŋ, benn talaŋ ci benn tegu. 28 Fukki kilook juróom ñaar yeek juróom ñaar téeméeri garaam yeek juróom fukk (17 kilo 750 garaam) yi ci topp, yemook junneek juróom ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróomi siikali xaalis, ay wékkukaay la ci sàkk ngir jën yi, xoob ci boppi jën yi, sàkk ci galan yi.
29 Xànjar bi ñu def saraxu yékkati-jébbal Yàlla, ñaari junniy kilo ak téeméer ak ñaar fukk ak ñeent la (2 124), yemook juróom ñaar fukki (70) talaŋ ak ñaari junneek ñeenti téeméeri (2 400) siikal. 30 Mu sàkk ci teguy buntu xaymab ndaje mi, ak sarxalukaayu xànjar bi, ak caaxub xànjaram, ak mboolem jumtukaayi sarxalukaay bi, 31 ak teguy wurmbalu ëtt bi, ak teguy buntu ëtt bi, ak xeri jaamookaay bi yépp, ak xeri wurmbalu ëtt bi.