Li war ci ku wasin
12
1 Bu loolu wéyee Aji Sax ji wax na Musaa ne ko: 2 «Waxal bànni Israyil ne leen: Ku ëmb ba wasin, am doom ju góor, dina sobewu diiru juróom ñaari fan. Day sobewu ni bu tolloo ci fan yi muy gis baax. 3 Bu bés ba délsee, nañu xarfal xale bi. 4 Dina ca teg fanweeri fan ak ñett, ngir setlu ca meret ma. Ci diir booba warula laal lenn lu ñu sellal, mbaa muy dugg fu sell li feek àppu setloom matul. 5 Su amee doom ju jigéen, dina sobewu diiru ñaari ayi bés, mu mel ni ku gis baax. Dina ca teg juróom benn fukki fan ak juróom benn, doora tàggook sobey meret ma.6 «Keroog bu àppu setloom matee, bu doom ja dee góor, bu dee jigéen, na dem ca bunt xaymab ndaje ma te yóbbul sarxalkat bi am xar mu am at, muy saraxu rendi-dóomal, ak xati mu ndaw mbaa pitax, mu doon saraxu póotum bàkkaar. 7 Na ko sarxalkat bi sarxal fi kanam Aji Sax ji, def ko njotlaayal wasin-bees wi, mu doora tàggook sobey meret ma.»