Lu jëm ci dalinu giir yi
2
1 Ba loolu wéyee Aji Sax ji wax Musaa ak Aaróona, ne leen: 2 «Na bànni Israyil di dal, ku nekk ak raayaam ak xàmmikaayu kër maamam. Fi wër xaymab ndaje mi te dànd ko as lëf, fi lañuy dale:
 
3 «Ñay dale ca kanam, fa féete penku, ñooy waa raayab Yuda ak seeni gàngoor, kilifag Yudeen ñi di Nason doomu Aminadab. 4 Ña ñu lim ci gàngooram di juróom ñaar fukki junneek ñeent ak juróom benni téeméer (74 600).
5 «Ñay dale fa feggook ñoom ñooy giirug Isakareen ñi, kilifag askanu Isaakar di Netanel doomu Suwar. 6 Ña ñu lim ci gàngooram di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400).
7 «Giirug Sabuloneen ñeey feggook ñoom, kilifag askanu Sabulon di Elyab doomu Elon. 8 Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400).
9 «Mboolem ña ñu limal dalub Yuda aki gàngooram daldi doon téeméeri junneek juróom ñett fukk ak juróom benn ak ñeenti téeméer (186 400). Bu ñuy dem, ñooñooy dox, jiitu.
 
10 «Waa raayab Ruben ñooy dale bëj-saalum, ñook seeni gàngoor, kilifag askanu Ruben di Elisur doomu Sedeyur. 11 Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (46 500).
12 «Ñay dale fa feggook ñoom ñooy giirug Cimyoneen ñi, kilifag askanu Simeyon di Selumyel doomu Surisadaay. 13 Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300).
14 «Giiru Gàddeen ñeey feggook ñoom, kilifag askanu Gàdd di Elyasaf doomu Rewel. 15 Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650).
16 «Mboolem ña ñu limal dalub Ruben aki gàngooram doon téeméeri junneek juróom fukk ak benn, ak ñeenti téeméer ak juróom fukk (151 450). Bu ñuy dem, ñooñooy doon ñaareelu kurél, dox, topp ca.
 
17 «Su ko defee xaymab ndaje mi jóg topp ca, ànd ak Leween ñi koy gàddu, te seen dal nekk ci digg dal yi. Noonee kurél yiy dale daal, ni lañuy jóge dem, ku nekk topp ayam ak raayaam.
 
18 «Waa raayab Efrayim ñooy dale wetu sowu, ñook seeni gàngoor, kilifag askanu Efrayim di Elisama doomu Amiyut. 19 Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500).
20 «Ñay dale fa feggook ñoom ñooy giirug Manaseen ñi, kilifag askanu Manase di Gamalyel doomu Pedasur. 21 Ña ñu limal gàngooram di fanweeri junneek ñaar ak ñaar téeméer (32 200).
22 «Giirug Beñamineen ñeey feggook ñoom, kilifag askanu Beñamin di Abidan doomu Gidoni. 23 Ña ñu limal gàngooram di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400).
24 «Mboolem ña ñu limal dalub Efrayim aki gàngooram daldi doon téeméeri junneek juróom ñett ak téeméer (108 100). Bu ñuy dem, ñooñoo di ñetteelu kurél, dox topp ca.
 
25 «Waa raayab Dan ñooy dale bëj-gànnaar, ñook seeni gàngoor, kilifag askanu Dan di Ayeser doomu Amisadaay. 26 Ña ñu limal gàngooram di juróom benn fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (62 700).
27 «Ñay dale fa feggook ñoom ñooy giirug Asereen ñi, kilifag askanu Aser di Pagyel doomu Okkran. 28 Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500).
29 «Giirug Neftaleen ñeey feggook ñoom, kilifag askanu Neftali di Ayra doomu Enan. 30 Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400).
31 «Mboolem ña ñu limal dalub Dan daldi doon téeméer ak juróom fukki junneek juróom ñaar ak juróom benni téeméer (157 600). Ñooñooy mujja jóg, topp seeni raaya.»
 
32 Ñooñu lañu limal bànni Israyil na ñu bokke seen këri maam. Mboolem ña ñu limal dal ya ak seeni gàngoor doon juróom benni téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). 33 Leween ñi nag limaaleesu leen ci bànni Israyil, te noonu la ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
34 Bànni Israyil daldi def noonu. Mboolem noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa, na lañu daan dale, topp seeni raaya, na lañu daan jóge, ku nekk ak làngam ak kër maamam.