Kore fippu na
16
1 Ku ñuy wax Kore doomu Isar, mi askanoo ci Keyat doomu Lewi, moo àndoon ak ay Rubeneen, ñuy Datan ak Abiram, doomi Elyab, ak Onn doomu Pelet, 2 ñu jógal Musaa, ñook ñaar téeméer ak juróom fukk (250) ci bànni Israyil, diy kilifa ci mbooloo mi, am baat ca pénc ma, te di ñu amu tur. 3 Ci kaw loolu ñu bokk daje fi kaw Musaa ak Aaróona, ne leen: «Doy na sëkk! Mbooloo mi ba mu daj, ñépp a sell, te ci sunu biir la Aji Sax ji nekk. Ana lu ngeen di xoggliku ci kaw mbooloom Aji Sax ji?»4 Ba Musaa déggee loolu, da ne gurub, dëpp jë bi fi suuf. 5 Mu wax Kore ak gàngooram gépp, ne: «Bu ëllëgee, Aji Sax ji mooy xamle kan la séddoo ak kan mooy ki sell, mu jegeñal ko boppam. Ki mu taamu nag, dina ko jegeñal boppam. 6 Dangeen di def nii: jël-leeni and, yaw Kore, yaak sa gàngoor gépp, 7 te ngeen def ciy xal, def ci cuuraay fi kanam Aji Sax ji, ëllëg. Su ko defee ku Aji Sax ji taamu, kookooy ki sell. Doy na sëkk, yeen Leween ñi!» 8 Musaa teg ca ne Kore: «Yeen Leween ñi, dégluleen nag! 9 Xeeb ngeen daal ber gi leen Yàllay Israyil ber ci mbooloom Israyil, jegeñal leen boppam, ngeen di liggéey liggéeyu màkkaanu Aji Sax ji, di taxaw fi kanam mbooloo mi, di leen jaamul Yàlla? 10 Yaw mu jegeñal la, yaak sa bokki Leween ñépp, ngeen di xëccu céru carxal, boole ci! 11 Kon kay yaw yaak sa gàngoor gépp, ci kaw Aji Sax ji ngeen bokk daje! Ana kuy Aaróona, ba ngeen di ñaxtu ci kawam?»
12 Musaa nag woolu Datan ak Abiram, doomi Elyab, ñu ne ko: «Danoo ñëwul! 13 Dangaa xeeb li nga nu jële réew mu meew maak lem ja tuuroo, ngir reylu nu ci màndiŋ mi, ba tax ngay buur-buurlu ci sunu kaw teg ci? 14 Du réew mu meew maak lem ja tuuroo nga nu yóbbu de, te séddoo nu céri tool mbaa tóokëri reseñ. Mbooloo mii mépp, man nga leena tuur lëndëm? Danoo ñëwul!» 15 Ba loolu amee Musaa mer lool. Mu ne Aji Sax ji: «Bul geesu sax seen sarax. Menn mbaam sax, masuma leen koo jëlal te masuma cee tooñ kenn.»
Way-fippu ya jot nañu seen añ
16 Musaa nag ne Kore: «Yaw, yaak sa gàngoor gépp, ca kanam Aji Sax ji, yaak ñoom ak Aaróona, ëllëg. 17 Na ku nekk jël ub andam, def ci cuuraay, te na ku ci nekk indib andam fi kanam Aji Sax ji, muy ñaar téeméeri and ak juróom fukk, yaak Aaróona it, ku nekk akub andam.»
18 Ba mu ko defee ku nekk jël ub andam, def cay xal, teg ca cuuraay. Ñu taxaw ca bunt xaymab ndaje ma, ñook Musaa ak Aaróona. 19 Kore nag dajale gàngoor gépp fa ñoom, ca bunt xaymab ndaje ma. Ci kaw loolu leeru Aji Sax ji feeñu mbooloo ma mépp!
20 Aji Sax ji wax Musaa ak Aaróona, ne: 21 «Xiddileen mbooloo mii, ma xoyom leen léegi!» 22 Musaa ak Aaróona ne gurub, dëpp seen jë fa suuf, daldi ne: «Éy Yàlla, yaw Yàllay bépp boroom bakkan bu bindoo aw suux, xanaa du kenn ay bàkkaar, nga far sànju ci kaw mbooloom lëmm?»
23 Ci kaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: 24 «Waxal mbooloo mi, ne leen ñu jóge fi wër màkkaani Kore ak Datan ak Abiram.»
25 Musaa daldi jubal ca Datan ak Abiram, magi Israyil topp ca. 26 Ci biir loolu mu wax ak mbooloo ma, ne leen: «Ngalla dàndleen xaymay nit ñu bon ñii, te buleen laal seen lenn, bala ngeen di buuboondook mboolem bàkkaari ñii.» 27 Ñu daldi jóge mboolem fa wër màkkaani Kore ak Datan ak Abiram. Datan ak Abiram ñoom, ña nga génn, taxaw ca seen bunti xayma, ñook seeni jabar ak seeni doom, ak seeni tuut-tànk.
28 Musaa nag ne: «Lii nag moo leen di xamal ne Aji Sax ji moo ma yebal ngir ma def jëf jii jépp, waaye du sama coobarey bopp: 29 Ndegam ni mboolem doom aadama di deeye, ni la ñii deeye, seen demin di deminu mboolem doom aadama, su boobaa du Aji Sax jee ma yebal. 30 Waaye ndegam Aji Sax ji moo sàkk ba sàkk tey lu masula am, ba suuf ŋa, mëdd leen, ñook lu bokk ci ñoom, ñu tàbbiwaale bakkan biir njaniiw, su boobaa dingeen xam ne ñoom ñii ñoo xarab Aji Sax ji.» 31 Naka la Musaa di daaneel kàddu yooyu yépp, fa ñu taxaw jekki xar, 32 suuf ŋa, mëdd leen, ñook seen waa kër, ak mboolem ku bokk ci Kore, ak mboolem alal ja. 33 Ñu daldi tàbbiwaale bakkan biir njaniiw, ñook mboolem lu ñu moom, suuf sàng leen, ñu réer mbooloo ma mërr. 34 Mboolem Israyil dégg seen yuux ya, daldi daw, te naan: «Nan daw bala noo suuf a mëdd!»
35 Ci kaw loolu sawara moo bawoo fa Aji Sax ji, xoyom ñaar téeméeri nit ak juróom fukk ña indi woon saraxu cuuraay ba.