Lu jëm ci sarxalkat yi ak Leween ñi
18
1 Aji Sax ji ne Aaróona: «Yaw, yaak say doom ak sa waa kër maam, yeenay gàddu peyug tooñ ci wàllu bérab bu sell bi, te itam yaw, yaak say doom, yeenay gàddu peyug tooñ ci seen wàllu carxal. 2 Te itam sa bokki Leween ñi, sa giirug baay, jegeñal leen sa bopp, ñu jokku ci yaw, di la jàpple, te yaw yaak say doom, ngeen féete fi kanam xayma ba seedes kóllëre ga dence. 3 Ñooy dénkoo sa ndénkaane, ak dénkaaney mboolem xayma bi, waaye jumtukaayi bérab bu sell bi, ak sarxalukaay bi, buñu ko jege, lu ko moy dañuy dee, ñoom ak yeen itam. 4 Nañu jokku ci yaw, te ñu dénkoo ndénkaanel xaymab ndaje mi, ci mboolem liggéeyu xayma bi. Kenn ku ci bokkul nag du leen jege, yeen. 5 Nangeen dénkoo ndénkaanel bérab bu sell bi, ak ndénkaanel sarxalukaay bi, ngir am sànj baña dalati ci kaw bànni Israyil.6 «Man mii nag maa seppee seen bokki Leween ñi ci biir bànni Israyil. Yeen lañu leen jagleela jagleel, ñeel Aji Sax ji, ngir ñu liggéey liggéeyu xaymab ndaje mi. 7 Yaw nag yaak say doom, dénkooleen seenug carxal ci mboolem mbiru sarxalukaay bi, ak ca wàllaa ridob biir bi, ngeen di ca liggéey. Seen liggéeyu carxal bi, ab sasu teraanga la, maa leen ko terale. Waaye ku bokkul ci yeen, bu ci laalee, dees koy rey.»
Lu jëm ci peyu sarxalkat yi
8 Aji Sax ji neeti Aaróona: «Man mii maa la sédd ndénkaaneb samay jooxe; mboolem jooxe yu sell yi bànni Israyil indi, yaw laa ko jagleel, nga jagoo, yaak say doom, ci kaw dogal bu sax dàkk. 9 Lii nag, yaa ko moom, ci mboolem sarax yu sell yee sell, yi mucc sawara: seen bépp sarax, seen bépp saraxu pepp ak seen bépp saraxu póotum bàkkaar, ak seen bépp saraxu peyug tooñ bu ñu ma indil, lu sella sell la, ñeel la, yaak sa doom yu góor. 10 Fu sella sell ngeen koy lekke; képp kuy góor ci yeen, sañ na cee lekk. Lu sell lay doon ci yaw.
11 «Leneen lu la ñeel moo di jooxe bu jóge ci saraxi nit ñi, di bépp saraxu yékkati-jébbal bu bànni Israyil. Yaw laa ko sédd, yaak sa doom yu góor, ak sa doom yu jigéen, ci kaw dogalu yoon bu sax dàkk. Képp ku set ci sa waa kër, sañ na cee lekk.
12 «Lépp luy ngëneelu diw gu bees, ak ngëneelu biiñ bu bees, ak pepp mu jëkka ñor, mu ñu jox Aji Sax ji, yaw laa ko jox. 13 Njàlbéenu meññeef mi ñuy indil Aji Sax ji, ci mboolem lu meññee ci seen suuf, yaa koy moom, te képp ku set ci sa waa kër, sañ na cee lekk. 14 Mboolem lees aayalal Aji Sax ji ci Israyil, yaa koy moom. 15 Lépp luy ubbitey njur bu ñu jagleel Aji Sax ji, ci lépp lu bindoo aw suux, nit ak mala, yaa koy moom. Fexeel rekk ba jotlu taawub nit ki, te taawub mala mu setul it, nanga ko jotlu. 16 Njotu xale bu am lu dale ci weer, àpp ko ci juróomi siikali xaalis yu bérab bu sell bi, benn siikal yemook ñaar fukki gera mbaa fukki garaam. 17 Waaye lu nag taawloo, ak lu xar taawloo, ak lu bëy taawloo, deesu ko jot. Yooyii yu sell la. Deretam ngay xëpp ci sarxalukaay bi, nebbon bi, nga def ko saxar, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. 18 Aw yàppam, yaa koy moom, ni nga moome dënnu saraxu yékkati-jébbal, ak tànkub kanam bu ndijoor ba. 19 Mboolem jooxe yu sell yi bànni Israyil di jooxeel Aji Sax ji, sédd naa la ko, yaak sa doom yu góor, ak sa doom yu jigéen, ci kaw dogalu yoon bu sax dàkk. Kóllërey xoroma a ngoogu, du fecciku, xanaa sax dàkk fi kanam Aji Sax ji, ñeel la yaw, yaak saw askan.» 20 Aji Sax ji neeti Aaróona: «Seenum réew nag doo ci am cér, te wàllu suuf, doo ko am ci seen biir. Man maay sa wàll, di sab cér ci biir bànni Israyil.»
Lu jëm ci peyug Leween ñi
21 Leween ñi ñoom, maa leen jox bépp céru fukkeel bu génne ci Israyil, muy seen cér, ñu yooloo ko seen liggéey bi ñuy liggéey ci xaymab ndaje mi.
22 Bu bànni Israyil juuxati ci xaymab ndaje mi, di gàddu bàkkaar bu dee di àtteem. 23 Leween ñi ñooy ñiy liggéey liggéeyi xaymab ndaje mi, te lu ñu ca tooñ, ñooy gàddu pey ga, ci kaw dogal bu sax dàkk, ñeel leen, ñook seen askan. Waaye biir bànni Israyil, Leween ñi duñu ci séddu céru suuf, 24 ndax céri fukkeel yi bànni Israyil yékkati, jooxeel ko Aji Sax ji, jox naa ko Leween ñi, muy seen cér. Moo tax ma ne leen, biir bànni Israyil, duñu ci séddu céru suuf.
Ab jooxe ñeel na Leween ñi
25 Aji Sax waxati Musaa ne: 26 «Leween ñi, wax leen, ne leen bu ñu jëlee ci bànni Israyil seen céri fukkeel yi ma leen jagleel yeen, muy seen cér, nañu ci jooxeel Aji Sax ji, fukkeelub céru fukkeel yooyu. 27 Nañu leen jàppal loolu, yeen Leween ñi, muy seen jooxeb bopp, ni bu doon pepp mu jóge ci seen dàggay bopp, ak biiñ bu bees bu jóge ci seen nalukaay. 28 Su ko defee ngeen jooxe yeen itam, jooxeb Aji Sax ji, ci mboolem seen céri fukkeel yi ngeen jële ci bànni Israyil. Kon nangeen jële coocu, jooxeb Aji Sax ji, jox ko Aaróona sarxalkat bi. 29 Lépp lu ñu leen sédd, nangeen ci jooxe jooxeb Aji Sax ji. Mboolem céri ngëneel yooyu, ci ngeen di génne cér bu sell boobu.
30 «Waxal Leween ñi ne leen gannaaw bu ñu ca génnee céru ngëneel li, li ci des lew na leen, ni bu doon pepp mu jóge ci seen dàggay bopp, ak biiñ bu jóge ci seen nalukaay. 31 Sañ nañu koo lekke fépp, ñoom ak seen waa kër, ndax loolu seen pey la, ñu yooloo ko seen liggéeyu xaymab ndaje mi. 32 Duñu ci gàddu benn bàkkaar, gannaaw bu ñu ci jooxee céru ngëneel li. Waaye jooxe yu sell yu bànni Israyil yooyu, buñu ci teddadil lenn, ba di ci dee.»