Israyil duma na Majan
31
1 Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko: 2 «Fexeel ba feyul bànni Israyil ci waa Majana. Gannaaw loolu dees na la yóbbu, tëral la fa say bokk.»3 Musaa daldi wax ak mbooloo ma, ne leen: «Na ñenn ci yeen gànnaayu, waajal xare, te dal ci kaw waa Majan, ba feyul Aji Sax ji. 4 Gii giir, junni, gee giir junni, ba giiri Israyil yépp daj, ngeen yebal leen ñu xareji.»
5 Ba mu ko defee ñu tànne ca gàngoori Israyil, junniy góor jóge ci giir gu nekk, ñuy fukki junneek ñaari (12 000) xarekat yu gànnaayu. 6 Musaa nag yebal leen, junni jóge ci giir gu nekk, ñu xareji. Ñoom ak sarxalkat bi Fineyas doomu Elasar, ñoo xareji, yóbbaale jumtukaay yu sell yaak liiti xare ya. 7 Ñu xareek Majan, na ko Aji Sax ji sante Musaa, ba rey góor ñépp, 8 reyaale buuri Majan, Ewi ak Rekem ak Sur ak Ur ak Reba, juróomi buuri Majan ya. Balaam doomu Bewor it, ñu reye ko saamar.
9 Ba loolu amee bànni Israyil jàpp jigéeni Majan, ak seeni tuut-tànk, ak seen jur gépp, gu gudd ak gu gàtt, seen alal jépp, ñu sëxëtoo ko. 10 Seen dëkk yépp ak seeni dëkkuwaay, ak seen dal yépp, ñu lakk. 11 Ba mu ko defee ñu jël mboolem la ñu sëxëtoo, mboolem la ñu ca jàppe, nit ñaak jur ga. 12 Ñu daldi yóbbu ca Musaa ak Elasar sarxalkat ba, ak mbooloom bànni Israyil, ña ñu jàppe ca xare ba, ak la ñu ca jàppe, ak la ñu sëxëtoo. Ñu indi lépp ca seen dal ba ca joori Mowab, fa janook Yeriko, te dendeek dexu Yurdan.
13 Ci kaw loolu Musaa ak Elasar sarxalkat ba ànd ak mboolem njiiti mbooloo ma, ñu génn dal ba, gatandu leen ca biti. 14 Musaa nag sànju ca kaw kilifay xare ya, muy kilifay kuréli junni yaak kilifay kuréli téeméer, ya jóge xare. 15 Musaa ne leen: «Kon jigéeni Majan ñépp ngeen bàyyi, ñu dund! 16 Xanaa du ñoom ñoo dëdduloo woon bànni Israyil Aji Sax ji, ci ndigalal Balaam, ca mbir ma woon ca Pewor, ba tax mbas ma dikkal mbooloom Aji Sax ji? 17 Kon nag reyleen lépp luy góor ci tuut-tànk yi, mboolem lu ciy jigéen ju xam lalu góor it, rey leen, 18 mboolem lu ciy jigéen ju ndaw, te xamul lalu góor, ngeen bàyyi mu dund, ñeel leen.
19 «Te yeen nag, dal-leen ci biti, buleen dugg ci biir dal bi diiru juróom ñaari fan, mboolem ñi rey ak mboolem ñi laal ku ñu rey. Nangeen setlu bésub ñetteel ba, ak bésub juróom ñaareel ba, yeen ak ñi ngeen jàpp. 20 Te itam lépp luy yére, ak bépp jumtukaayu der, ak lépp lees defare kawari bëy, ak bépp jumtukaayu bant, nangeen ko setal.»
21 Ba mu ko defee Elasar sarxalkat ba wax ak ña xareji woon, ne leen: «Lii moo di dogalu yoon, bi Aji Sax ji dénk Musaa: 22 Luy wurus ak xaalis ak xànjar, ak weñ gu ñuul, ak weñ gu weex, ak beteex, 23 mboolem lu dul lakk, rekk, nangeen ko laalale sawara, mu set. Ndoxum setlu mi it, warees na koo dellu setale yooyii. Waaye mboolem luy lakk, ci ndoxum setal mi doŋŋ lees koy dugal, ngir mu set. 24 Bésub juróom ñaareel ba, fóotleen seeni yére, daldi set. Gannaaw loolu man ngeena duggsi ci dal bi.»
Lu jëm ci séddaleb alalu waa Majan
25 Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: 26 «Yaw ak Elasar sarxalkat bi, ak ñi jiite seeni kër maam ci mbooloo mi, waññleen alal ji ñu nangoo xare, nit aku jur. 27 Xaajleen sëxëtoo mi ñaar, te ngeen séddale ko diggante xarekat ya xareji woon, ak mbooloo mi ci des yépp. 28 Te ngeen sàkkal Aji Sax ji, ci céru xarekat ya xareji woon, ab galag bu yemook benn bopp ci juróomi téeméer (500) yu nekk, ci aw nit, mbaa ay nag, mbaa ay mbaam, mbaa ay gàtt. 29 Ci céru xarekat yi ngeen koy sàkke, jox ko Elasar sarxalkat bi, muy jooxeb Aji Sax ji. 30 Céru bànni Israyil bi ci des, nangeen ci sàkk benn ci juróom fukk yu nekk (50), ci aw nit, mbaa ay nag, mbaa ay mbaam, mbaa ay gàtt, mbaa gépp jur, te ngeen jox ko Leween ñi dénkoo dénkaaney màkkaanu Aji Sax ji.»
31 Ba loolu amee Musaa ak Elasar sarxalkat bi defe ko noonee ko Aji Sax ji sante Musaa. 32 La des ca alalu sëxëtoo, ja ña xareji woon indaale, gannaaw ba ñu ca génnee yooyu, nii la tollu: gàtt yi, juróom benni téeméeri junneek juróom ñaar fukk ak juróom (675 000); 33 nag yi, juróom ñaar fukki junneek ñaar (72 000); 34 mbaam yi, juróom benn fukki junneek benn (61 000), 35 aw nit, fanweeri junniy jigéen ñu xamul lalu góor (30 000).
36 Genn-wàll giy céru nit ña xareji woon, nii la tëdde: gàtt yi, ñetti téeméeri junneek fanweer ak juróom ñaar ak juróomi téeméer (337 500), 37 galagu Aji Sax ji génne ci gàtt yi, di juróom benni téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróom (675); 38 nag yi, fanweeri junneek juróom benn (36 000), galagu Aji Sax ji génne ci, di juróom ñaar fukk ak ñaar (72); 39 mbaam yi, fanweeri junneek juróomi téeméer (30 500), galagu Aji Sax ji génne ci, di juróom benn fukk ak benn (61); 40 aw nit, fukki junneek juróom benn (16 000), galagu Aji Sax ji génne ci, di fanweeri bopp ak ñaar (32). 41 Ba mu ko defee Musaa jox galag ba Elasar sarxalkat ba, muy jooxeb Aji Sax ji, na ko Aji Sax ji sante Musaa.
42 Genn-wàll giy céru bànni Israyil, ba Musaa teqale ak cérub ña xareji woon, 43 te muy céru mbooloo ma, ci wàllu gàtt yi, ñetti téeméeri junneek fanweer ak juróom ñaar ak juróomi téeméer (337 500) la; 44 nag yi di fanweeri junneek juróom benn (36 000); 45 mbaam yi, fanweeri junneek juróomi téeméer (30 500); 46 aw nit, fukki junneek juróom benn (16 000). 47 Musaa daldi sàkk ci céru bànni Israyil boobu, benn ci juróom fukk yu nekk. Musaa jox loola Leween ñi dénkoo dénkaaney màkkaanu Aji Sax ji, noonee ko ko Aji Sax ji sante woon.
Kilifay xare ya jëfe nañu ngor
48 Ba loolu amee njiiti gàngooru xarekat ya, kilifay kuréli junni yaak kilifay kuréli téeméer ya, ñoom ñépp dem ca Musaa. 49 Ñu ne Musaa: «Sang bi, nun de, waññ nanu xarekat yi ci sunu kilifteef, waaye kenn wuutewu ci. 50 Moo tax nu indi jooxeb Aji Sax ji, ku nekk ak la nga muurloo, ci gànjari wurus; lami përëg, ak takkub jara, ak jaaroy torlukaay, ak jaaroy nopp, aki caq. Noo ko def sunu njotlaayal bakkan, fi kanam Aji Sax ji.»
51 Musaa ak Elasar sarxalkat ba nangoo wurus wa ca ñoom, lépp di takkaay yu ñu tëgg. 52 Mboolem wurusu jooxe, wi ñu jooxeel Aji Sax ji, di fukk ak juróom benni junniy siikal ak juróom ñaar téeméer ak juróom fukk (16 750), yemook barigo ak juróom ñaar fukki kilo (170), te bawoo ci kilifay kuréli junni yaak kilifay kuréli téeméer ya. 53 Xarekati gàngoor ga ñoom, dañoo féetewoo la ñu sëxëtoo. 54 Musaa ak Elasar sarxalkat ba nag jële wurus wa ca kilifay kuréli junni yaak kuréli téeméer ya. Ñu yóbbu ko ca biir xaymab ndaje ma, muy seedeel bànni Israyil fi kanam Aji Sax ji.