10
1 Jant yooyu la ma Aji Sax ji wax ne ma: «Yettal ñaari àlluway doj yu mel ni yu jëkk ya, nga yéegsi fi man, ci kaw tund wi. Te nanga sàkk itam gaalu bant. 2 Dinaa bind ci àlluwa yi, kàddu ya woon ca àlluwa yu jëkk, ya nga toj. Su ko defee nga yeb àlluwa yi ci gaal gi.» 3 Ma sàkk gaalu bantu séng, daldi yett ñaari àlluway doj yu mel ni yu jëkk ya. Ci kaw loolu ma yéeg ca kaw tund wa, maak ñaari àlluwa yi ci sama loxo. 4 Aji Sax ji nag bind ca àlluwa ya, la mu jëkkoona bind, muy fukki santaane ya mu leen waxoon ca kaw tund wa, ba mu àddoo fa digg sawara wa, keroog bésub ndaje ma. Ba loolu amee Aji Sax ji jox ma àlluwa yi. 5 Ma walbatiku, wàcc tund wa, yeb àlluwa ya ca gaal ga ma sàkk, àlluwa ya des ca biir, na ma ko Aji Sax ji waxe woon.
6 Gannaaw gi bànni Israyil bàyyikoo ca teeni Bene Yaakan, dem ba Mosera. Foofa la Aaróona faatoo, ñu denc ko fa, doomam Elasar doon sarxalkat, wuutu ko. 7 Foofa lañu bàyyikoo dem Gutgoda, bawooti Gutgoda, jàll ba Yotbata, réewum wali ndox ya.
8 Jant yooyu la Aji Sax ji ber giirug Lewi, ngir ñuy gàddu gaalu kóllëreg Aji Sax ji, di taxaw fi kanam Aji Sax ji, di ko liggéeyal, di taase barke ciw turam, te mooy seen péete ba tey jii. 9 Looloo waral Leween ñi amuñu wàll ci céru suuf su ñuy séddoo ak seeni bokk. Aji Sax ji mooy seenub cér, ni leen ko seen Yàlla Aji Sax ji waxe woon.
10 Man nag maa am ca kaw tund wa fan ya ma fa jëkkoona am, muy ñeent fukki bëccëg, ak ñeent fukki guddi. Aji Sax ji dellu ma nangul, boobu yoon itam, ba bëggatu leena sànk. 11 Aji Sax ji ne ma: «Doxal jiite yoonu mbooloo mi, ñu dem nanguji réew, ma ma giñaloon seeni maam, ne ñoom laa koy jox.»
Musaa ngi woote déggal Aji Sax ji
12 Léegi nag yeen Israyil, ana lu leen seen Yàlla Aji Sax ji laaj, lu moy ngeen ragal seen Yàlla Aji Sax ji, di doxe mboolemi yoonam, sopp ko, di jaamoo seen Yàlla Aji Sax ji seen léppi xol, ak seen léppi bakkan, 13 ngir di sàmm santaaney Aji Sax ji, ak dogali yoonam, yi ma leen dénk bésub tey ngir seen njariñal bopp? 14 Seen Yàlla Aji Sax ji déy mooy boroom asamaan, ak asamaani asamaan, ak suuf, ak mboolem li ci biiram. 15 Terewul seeni maam doŋŋ la Aji Sax ji taqool, ngir sopp leen, te yeen, ñi askanoo ci ñoom la taamu ci biir xeetoo xeet, niki bésub tey jii. 16 Kon nag nangeen dogoo seen xol te bañatee sajju loos. 17 Ndax kat seen Yàlla Aji Sax ji mooy Yàllay yàlla yi, te mooy Sangu sang yi. Mooy Yàlla ju màgg ji, jàmbaare te raglu. Ki gënalewul, jëlul ub ger. 18 Kiy aar jirim akub jëtun, sopp doxandéem, ngir leel ko, wodd ko. 19 Kon soppleen doxandéem, ndax ay doxandéem ngeen woon ca réewum Misra.
20 Seen Yàlla Aji Sax ji moom ngeen di ragal, te moom ngeen di jaamu. Moom ngeen di ŋoyu, te aw turam ngeen di giñe. 21 Moo yelloo seeni kañ te mooy seen Yàlla, ji leen defal jaloore yeek kawtéef yooyu ngeen gisal seen bopp. 22 Juróom ñaar fukki bakkan la seeni maam doonoon ba ñuy wàccsi Misra. Tey seen Yàlla Aji Sax ji def leen ngeen day ni biddiiwi asamaan.