Musaa ñaanal na bànni Israyil
33
1 Ñaan gii nag la Musaa, góoru Yàlla ga ñaanaloon bànni Israyil, bala moo nelaw.2 Da ne:
Aji Sax ji Sinayi la bawoo,
fenkale leen fa Seyir,
naajali leen fa tundu Paran,
ànd ak ndiiraani ñu sell ña,
ndijooram ba indil leen melax.
3 Yaw kay yaa sopp xeet yi,
sa ñu sell ñépp nga téyee say loxo,
te ñoo topp say tànk,
di taataan say tegtal.
4 Aw yoon la nu Musaa dénk,
muy jagleb péncum Yanqóoba.
5 Yesurun am na buur,
kera ba njiiti askan wa dajee,
ba giiri Israyil bokk teew.
6 Yal na Ruben dund, baña raaf,
yàlla buy nitam néew.
7 Lii nag moo ñeel Yuda. Mu ne:
Éy Aji Sax ji déggal yuuxi Yuda
te yóbbu ko ciy bokkam.
Mooy jànkoontee dooley boppam,
waaye yaa koy wallu ciy noonam.
8 Lewi la wax ne ko:
Sa Tumim ak sa Urim, jumtukaayi tegtal ya,
ñeel na góor gay sa wóllëre,
yaa ko nattoo ca Maasa,
joteek moom ca ndoxum Meriba.
9 Kee ne ndey ak baay:
«Gisuma leen,»
ay doomi ndeyam, ràññeewu leen,
te doomam, xamu ko.
Xanaa di sàmm say wax,
di sàmm sa kóllëre.
10 Leween ñeey xamal askanu Yanqóoba say àtte,
di won Israyil gii saw yoon.
Ñooy taal cuuraay fi sa kanam,
di teg saraxi dóomal ci sab sarxalukaay.
11 Éy Aji Sax ji barkeelal dooley gii giir,
te bége aw ñaqam.
Dammal ndiggal ña koy jógal,
ba ay bañam duñu jógati.
12 Beñamin la wax, ne ko:
Soppeb Aji Sax jaa ngi,
keey dëkke xel mu dal fi wetam,
mu di ko yiir bésoo bés,
te diggantey waggam la dëkke.
13 Yuusufa la wax, ne ko:
Yal na barkeb Aji Sax ji ñeel suufam,
bawoo ca xéewali asamaan, dib lay,
ak ndox mu lal xóotey suuf,
14 ak xéewali meññeef mu jant ñoral,
ak tànnéefi gàncax yiy sax ci weeram.
15 Na barke bawoo fa kawtey tundi cosaan yu mag ya,
ak xéewali tundi cosaan yu ndaw ya,
16 ak xéewali suuf ak la ko fees,
ànd ak yiwu ka màkkaanoo ngarab sa doon tàkk,
te wàccandoo ci kaw boppu Yuusufa;
ak kaaŋi bokkam yay séddooy Aji Sax ji.
17 Taawub yëkk la, daraja mooy boroom,
béjjén ya, béjjéni nagu àll la,
ca lay butteendoo xeet yépp,
ba ca cati àddina.
Ñooñooy junniy junniy nit ca giirug Efrayim,
ak junni ca giirug Manase.
18 Sabulon la wax ne ko:
Yaw, Sabulon, bégeel say dem,
Isaakar yaw, bégeel sa biir xayma.
19 Xeet yi la ñooñu di woo ca tund wa,
te fa lañuy sarxee sarax yi war,
koomu géej, ca lañuy nàmpe,
booleek kumpay mbell yu làqu biir suuf.
20 Gàdd la wax ne ko:
Barke ñeel na ku yaatal Gàdd.
Ni gaynde la goore,
te mooy xotat përëg akum kaaŋ.
21 Moo xool cér ba jëkka lew, jagoo ko,
nde fa la wàllu njiit di xaar boroom.
Moo fekksi njiiti askan wi,
moo jëfe njekku Aji Sax ji,
aki dogalam fi Israyil.
22 Dan la wax ne ko:
Dan gaynde gu ndaw la,
mooy tëbe fa diiwaanu Basan.
23 Neftali la wax ne ko:
Neftalee ne xéew aku yiw,
biibal barkey Aji Sax ji,
te sowu ba bëj-saalum lay nangu.
24 Aser la wax ne ko:
Yal na Aser gëna barkeel ci doom yi,
ay bokkam baaxe ko,
tànk yay xuuse ag diw.
25 Weñ ak xànjar la say xomb di doon,
sa kàttan ànd ak saw fan.
26 Kenn du Yàllay Yesurun!
Keey war asamaan, wallusi leen,
war ay niir, ànd ak darajaam.
27 Yàlla ji sax fàww moo dib rawtu,
përëgam bi sax dàkk di cëslaay,
moo la dàqal ab noon
ne la: «Jekklil!»
28 Israyil a ngi dëkke xel mu dal,
walu Yanqóoba mee fegu,
di wale réewum pepp ak biiñ bu bees,
asamaan it di ko wàcceel ab layam.
29 Ndokklee, Israyil, ana ku mel ni yeen,
askan wu Aji Sax jiy wallu,
di seen kiiraay, di seen ndimbal,
di saamar bi leen di sagal?
Seeni noon a leen di loxal,
te yeen, fa seen gannaaw ya ngeen di daagoo.