Samiyel
di téereb ñaareel bi
Lii mooy jaar-jaari Buur Daawuda
Lu jëm ci tàggeb Sóol
1
1 Gannaaw ba Sóol faatoo, fekk na Daawuda walbatikoo ca dumay Amalegeen ña, dellu Ciglaag, ba toog fa ñaari fan. 2 Ca gannaaw ëllëg sa, jenn waay ne jimeet, jóge ca dalub Sóol, dikk. Yére yaa nga xottiku, bopp ba taq suuf, ngir naqarlu. Naka la agsi ci Daawuda, daldi daanu fi suuf, sujjóot.3 Daawuda ne ko: «Foo jóge nii?» Mu ne ko: «Ca dalub Israyil laa rëcce.» 4 Daawuda ne ko: «Lu xew, gaawe ma!» Mu ne ko: «Mbooloom Israyil a dawe ca xare ba. Ñu bare ca ñoom daanu nañu, dee. Sóol ak doomam Yonatan it dee nañu.» 5 Daawuda ne ndaw la: «Lu la xamal ne Sóol ak doomam Yonatan dee nañu?» 6 Ndaw la ne ko: «Dafa yemook ma tollu tembe ca kaw tundu Gilbowa. Ndeke Sóol a nga fa, sukkandikoo xeejam. Watiiri xare yaak gawar ya defuñu lu moy ne ko dann. 7 Naka la ne gees, yem ci man, woo ma, ma wuyu. 8 Mu ne ma: “Yaa di kan?” Ma ne ko: “Ab Amalegeen laa.” 9 Mu ne ma: “Kaay fii, jekkli ma. Maa ngi ci miirum ndee, doonte dese naa tuuti.” 10 Ma dikk, daldi koy jekkli, ndax xamoon naa ne du dundati gannaaw jéllam ba. Ma summi nag mbaxanam buur ma mu soloon, tekki lam ba woon ca përëg ma. Yooyu laa la yótsi nii, sang bi.»
11 Ba loolu amee Daawuda sëq yéreem, xotti, ña ànd ak moom ñépp itam, noonu, ndax aw naqar. 12 Ñaawlu nañu, di jooy, lekkuñu ba ca ngoon ndax Sóol ak doomam Yonatan ak gàngooru Aji Sax ji, waa kër Israyil, ña fàddoo saamar.
13 Daawuda ne ndaw la: «Ana foo bokk?» Mu ne ko: «Man doomu doxandéemub Amalegeen laa.» 14 Daawuda ne ko: «Noo saña xàccee sa loxo, di bóom ki Aji Sax ji fal?» 15 Daawuda nag woo kenn cay surgaam, ne ko: «Dikkal dóor, mu dee!» 16 Daawuda ne Amalegeen ba: «Yaa gàddu sa bakkanu bopp, ndax yaa seedee sa gémmiñu bopp ne yaa rey ki Aji Sax ji fal.» Surga ba dóor Amalegeen ba, mu dee.
Daawuda jooy na Sóol ak Yonatan
17 Kàddu yii la Daawuda jooye Sóol ak doomam Yonatan. 18 Moo santaane ñu jàngal ko askanu Yuda. «Fittkat» lañu dippee woy wi. Nii lañu ko binde ci «Téereb aji jub ji.» Mu ne:
19 Wóoy Israyil, ña ngay sagoo lañu jam,
ñu ne lareet ca sa tund ya!
Jàmbaar ñaa daanu!
20 Buleen ko siiwal fa Gaat,
buleen ko yéene fa mbeddi Askalon,
lu ko moy janqi Filisti bég,
janqi yéefar yiy textexi.
21 Wóoy tundi Gilbowa!
Yàlla bu ngeen lay, bu ngeen tawlu,
Yàlla bu seeni tool nangooti,
ba duunal jooxeb pepp,
nde foofa lees torxale pakkub jàmbaar.
Wóoy pakkub Sóol ba deesul diwati!
22 Du deret mbaa nebbonu jàmbaar
bu fittug Yonatan xof,
te saamaru Sóol ba du sooy!
23 Wóoy Sóol ak Yonatan,
ñoo yiw, sopplu ba ñuy dund,
te ba ñu deeyee, teqlikoowuñu.
Ag jaxaay, ñoo ko gëna gaaw,
te gaynde, ñoo ko gëna jàmbaare.
24 Yeen jigéeni Israyil,
jooyleen Sóol, ma leen wodde ndimol tànnéef
lu xonq curr,
takkal leen gànjari wurus ca seen kawi yére.
25 Jàmbaar ñaa daanoo biir xare ba,
Yonatan lañu jam ca kaw tund ya!
26 Yonatan, doom yaay, tiisoo naa la,
dama laa soppoon lool,
te sa mbëggeel ci man yéeme,
ba raw mbëggeelu jigéen.
27 Jàmbaar ñaa daanu,
ngànnaayi xare ya sànku!