Daawuda falu na buur ca Israyil
5
1 Ci kaw loolu giiri Israyil yépp dikk fa Daawuda ca Ebron, ne ko: «Noo ngii di say bokk lenqe. 2 Te it démb ak bëkk-démb, ba Sóol dee sunu buur, yaw yaa doon jiite Israyil ciy xareem. Aji Sax ji ne la: “Yaay sàmm Israyil sama ñoñ te yaay doon kilifag Israyil.”» 3 Noonu la magi Israyil ñépp dikke ca Buur Daawuda ca Ebron, mu fasook ñoom kóllëre fa kanam Aji Sax ji. Ñu sotti Daawuda diwu pal ga, muy buurub Israyil.
4 Daawuda amoon na fanweeri at, ba muy falu buur, te ñeent fukki at la nguuru. 5 Ca Ebron la yore nguurug Yuda juróom ñaari at ak juróom benni weer, waaye ca Yerusalem la yore diiru fanweeri at ak ñett, mboolem Israyil ak Yuda.
Daawuda nangu na Yerusalem
6 Gannaaw loolu Buur Daawuda ànd aki xarekatam, jëm Yerusalem, songi Yebuseen ña dëkkoon ca réew ma. Yebuseen ña ne Daawuda: «Doo fi dugg de, nde gumba yeek lafañ yi rekk ñoo lay waññi.» Booba foog nañu ne Daawuda manu faa dugg. 7 Terewul Daawuda nangu tatay Siyoŋ, ga ñu dippee Kër Daawuda. 8 Daawudaa noon bésub keroog: «Ku bëgga jam Yebuseen ñi, ca xuntim yoonu ndox ma ngay mana dabe seeni gumbaak seeni lafañ, xuloowaaley Daawuda yi.» Looloo waral waxin wi ñu naan: «Gumba akub lafañ du dugg kër Buur.» 9 Ba mu ko defee Daawuda dëkk ca biir tata ja, wooye ko Kër Daawuda, ba noppi tabax fa ko wër fépp, dale ko ca sëkkub Miloa, ba ca biir. 10 Daawuda nag di gëna am doole, Aji Sax ji Yàlla, Boroom gàngoori xare yi ànd ak moom.
11 Ci biir loolu Iram buurub Tir, yebal ay ndaw ca Daawuda, ñu yóbbul ko ay banti garabu seedar, ak ay liggéeykati bant ak yettkati xeer, ngir ñu tabaxal Daawuda kër. 12 Daawuda xam ne Aji Sax jee ko tabb buurub Israyil te moo kaweel nguuram ngir Israyil, aw ñoñam.
13 Gannaaw ba Daawuda jógee Ebron, dellu na jël ay nekkaale aki soxna ca Yerusalem. Mu am ca yeneen doom yu góor ak yu jigéen. 14 Doomam yu góor yi juddoo Yerusalem ñoo di Samwa ak Sobab ak Natan ak Suleymaan; 15 ak Ibaar ak Elisuwa ak Nefeg ak Yafiya; 16 ak Elisama ak Elyada ak Elifelet.
Buur Daawuda duma na waa Filisti
17 Ba waa Filisti déggee ne fal nañu Daawuda buurub Israyil, ñoom ñépp a jóg, di ko wër. Daawuda nag dégg ko, dem làquji ca biir tata ja. 18 Waa Filisti dikk, tasaaroo ca xuru Refayeen ña. 19 Daawuda laaj Aji Sax ji, ne ko: «Ndax ma songi waa Filisti? Dinga leen teg ci sama loxo?» Aji Sax ji ne ko: «Demal, maay teg waa Filisti ci say loxo déy!» 20 Daawuda dem ba ca Baal Perasim, duma leen foofa. Mu ne: «Aji Sax jee ma bëttal noon yi, ni walum ndox di bëtte, wéy.» Moo tax ñu wooye bérab boobu Baal Perasim (mu firi Boroom bëtt-bëtt yi). 21 Waa Filistee fa wacc seeni gàllaaj, Daawudaaki nitam boole yóbbu.
22 Ba mu ko defee waa Filisti dikkaat, tasaaroo ca xuru Refayeen ña. 23 Daawuda dellu laaj Aji Sax ji. Mu ne ko: «Bul jubal, doxeleen gannaaw, dal ca seen kaw fa janook garabi sànd ya. 24 Booy dégg tànk yuy jaab ca kaw njobbaxtali sànd ya rekk, gaawtul, ndax booba Aji Sax jee la jiitu, di dumaji waa dalub Filisti.» 25 Daawuda nag def noonee ko Aji Sax ji sant, ba duma waa Filisti diggante Geba, ba ca buntu Geser.