Usay nax na Absalom
17
1 Gannaaw loolu Ayitofel ne Absalom: «Ngalla may ma, ma tànn fukki junniy xarekat ak ñaar (12 000) te dàqi Daawuda ci guddi gi. 2 Bu may dal ci kawam, da koy fekk mu sonn, jàq. Su ko defee ma xoqtal ko, ba mbooloo mi mu àndal mépp daw, ma rey ko, moom kenn. 3 Dinaa la délloosil mbooloo mépp. Bu ki ngay fexeel deeyee rekk, mbooloo mi mépp délsi, jàmm ne ñoyy.» 4 Pexe moomu nag jub ci Absalom, mook magi Israyil ñépp. 5 Teewul Absalom ne: «Wooleen Usay, Arkeen bi itam, nu déglu lu mu ciy wax.» 6 Usay dikk ca Absalom, mu wax ko la Ayitofel digle, ne ko: «Ndax loolu Ayitofel wax lanu wara def am déet? Wax nu lu ciy sa xalaat, yaw.»
7 Usay ne Absalom: «Li Ayitofel digle bii yoon de baaxul. 8 Xam nga sa baay ak ay nitam. Ay xarekat yu jàmbaare lañu te wex ni gaynde gu ñu nangu doom ya, te it, sa baay ku xam xeex la, du fanaan ak xarekat ya. 9 Xam naa ne ma nga làqu ci xuntim xeer, mbaa bérab rekk. Te bu aw nit jëkkee daanu ci seen biir yeen, ku ko dégg dina ne: “Jéll bu réy am na ca mbooloom Absalom.” 10 Su boobaa, ku ñeme, ba dëgëru fit ni gaynde sax, dinga tiit lool, ba ne yàcc, ngir Israyil gépp xam nañu ne sa baay ñeyi xare la, te it ñi ànd ak moom jàmbaar lañu. 11 Kon sama xalaat mooy nga boole ñi ànd ak yaw ba ñu daj, muy Israyil gépp, dale ko diiwaanu Dan ca bëj-gànnaar ba ca Beerseba ca bëj-saalum. Muy mbooloo mu bare, tollu ni suufas géej; te yaw ci sa bopp, nga jiite leen ci xare bi. 12 Nu song ko nag fu nu ko mana fekk, dal ci kawam, ni ab lay ci kaw suuf. Deesu ci bàyyi kenn muy dund, du moom, du kenn ciy nitam. 13 Su làqoo ci ab dëkk bu mag, na Israyil gépp yóbbaale ay buum ca tata ja, nu laaw ko, wat ba ca xur wa, ba kenn dootu gis aw doj wu ca bokkoon.» 14 Absalom ak waa Israyil gépp daldi ne: «Ndigalal Usay, Arkeen bii kat, moo gën ndigalu Ayitofel.» Booba Aji Sax jee nara indil Absalom musiba. Moo tax mu neenal pexem Ayitofel mu jub ma mu laloon.
15 Ci kaw loolu Usay wax ak Cadog ak Abiyatar sarxalkat ya, nettali leen la Ayitofel digal Absalom ak magi Israyil ña, ak la mu leen digal, moom Usay. 16 Mu ne leen: «Gaawleen yónnee léegi ca Buur Daawuda te wax ko ne ko bumu fanaan fa ñuy jàlle dex ga, jëm ca màndiŋ ma. Na jàlla jàll dex ga, lu ko moy dees na ko bóom, mook mbooloo ma mu àndal mépp.»
17 Ma nga fekk Yonatan ak Ayimaas ca En Rogel. Manuñu woona dugg ca biir dëkk ba, ndax ragal ñu gis leen. Ab jaam bu jigéen nag di dem ca Yonatan ak Ayimaas, di leen wax la xew, ngir ñu dem ca Buur Daawuda, yegge ko ko. 18 Teewul ab xale bu góor gis leen, wax ko Absalom. Ba mu ko defee ñu ànd ñoom ñaar, gaaw dem ca kër jenn waay ju dëkk Baxurim. Waa ja am ab teen ca ëttam, ñu dugg ca biir. 19 Ci kaw loolu soxna sa jël basaŋ, lal ko ca pindu teen ba, ba noppi wasaare pepp ca kaw, ba kenn du ca foog dara. 20 Jawriñi Absalom dikk ca kër ga, fekk fa ndaw sa, ne ko: «Ana Ayimaas ak Yonatan?» Ndaw sa ne leen: «Jéggi nañu dex gi.» Ñu seet, gisuñu kenn, daldi dellu Yerusalem.
21 Gannaaw ba ñu demee, Ayimaas ak Yonatan yéeg, génn teen ba, dem nag àrtuji Buur Daawuda. Ñu ne ko Ayitofel digle na nàngam ak nàngam ci moom, neeti ko: «Gaawleen jàll dex gi léegi.» 22 Ca saa sa Daawudaaki nitam ñépp jàll dexu Yurdan ga. Ba jant bay fenk, kenn sax desul ku jàllul dex ga.
23 Ci biir loolu Ayitofel gis ne déggeesul ndigalam, mu takk mbaamam, ñibbi ca dëkk ba mu fekk baax. Mu daldi topptoo mbiri këram ba mu jekk, ba noppi wékk boppam. Mu dee, ñu denc ko ca sëgi baayam.
24 Ba mu ko defee Daawuda àgg Maanayim, fekk Absalom di jàll dexu Yurdan, ànd ak xarekati Israyil yépp. 25 Amasa nag la Absalom faloon, mu jiite mbooloom xare ma, wuutu Yowab. Amasa moo doon doomu góor gu ñuy wax Yittra, di bànni Israyil bu jëloon Abigayil, mi Nayas di baayam. Abigayil ak Seruya, yaayu Yowab, ñoo bokk ndey. 26 Bànni Israyil daldi ànd ak Absalom dal ca diiwaanu Galàdd. 27 Ba Daawuda àggee Maanayim, Sobi doomu Nayas mu Raba, ga ca dëkkub Amoneen ña, moo ko teertu, mook Makir doomu Amiyel ma dëkk Lodebar; ak Barsilay waa Galàdd ba dëkk Rogelim. 28 Ñu daldi indi ay laltu aki ndab aki njaq, ak peppum bele ak peppum lors ak sunguf ak mbool ak xeeti ñebbe, 29 ak lem akum soow, aki gàtt, ak formaasu nag ngir Daawudaak mbooloom lekk. Ndaxte booba dañu ne: «Mbooloo mi de, xiif ak mar lañu boole, ak coonob màndiŋ ma.»