Buuri Israyil ak Yudaa ngi xeexoo
14
1 Ba buurub Israyil Yowayas doomu Yowakas duggee ñaareelu atu nguuram, ca la Amaciya doomu Yowas falu buur ca Yuda. 2 Ñaar fukki at ak juróom la amoon ba muy falu, te ñaar fukki at ak juróom ñeent la nguuru fa Yerusalem. Yaayam moo doon Yowadan ma cosaanoo Yerusalem. 3 Def na njub gi Aji Sax ji rafetlu, waaye dabul Daawuda maamam. Mboolem noonee Yowas baayam daan jëfe, na la daan jëfe 4 Bérabi jaamookaay ya jëleesu ko fa. Mbooloo maa nga doon def ay sarax ca bérabi jaamookaay ya ba tey, di fa taal cuuraay. 5 Ba nguur ga demee ba dëgër ci loxoom, moo bóom jawriñam ña bóomoon Buur baayam. 6 Waaye doomi bóomkat ya, bóomu leen, ngir dëppook la ñu bind ci téereb yoonu Musaa, te Aji Sax ji santaane ko, ne: «Deesul rey baay ndax doom te deesul rey doom ndax baay. Nit ku nekk, bàkkaaru boppam lees koy reyea
7 Moom Amaciya moo duma fukki junniy (10 000) waa Edom ca xuru Xorom wa, nangu dëkk ba ñuy wax Sela ca xare ba, tudde ko Yogtel, te noonu la tudd ba bésub tey jii. 8 Ba loolu amee Amaciya yónni ay ndaw ca buurub Israyil Yowayas doomu Yowakas doomu Yewu. Mu ne ko: «Dëkk naa la, dikkal nu jàkkaarloo!» 9 Yowayas buurub Israyil yónnee Amaciya buurub Yuda tontam, ne ko: «Ndég ga ca Libaŋ moo yónnee woon ca garabu seedar gu mag ga ca Libaŋ, ne ko: “Sa doom jii, may ko sama doom jabar.” Ci kaw loolu rabu àllu Libaŋ jaare fa, dëggaate ndég ga. 10 Dëgg la moos, yaa duma Edom, ba tax nag sam xel jay la. Tee ngaa bàkku te toog sa kër? Te sax ana looy dugge ci jote buy indi ay wu lay daane, yaw, daanewaale Yuda?»
11 Amaciya nag faalewul wax jooju, Yowayas buurub Israyil jóg; ñu jàkkaarloo mook Amaciya buurub Yuda, ca Bet Semes ga ca Yuda.
12 Ba mu ko defee muy jéllu Yuda fa kanam Israyil. Waa Yuda tasaaroo, ku nekk ñibbi ca sab xayma. 13 Yowayas buurub Israyil nag jàpp buurub Yuda, Amaciya doomu Yowas doomu Akasiya, ca Bet Semes. Gannaaw loolu mu dem Yerusalem màbb tata ja, la ko dale buntu Efrayim ba ca buntu ruq ba, muy ñeenti téeméeri xasab. 14 Ci kaw loolu mu jël mboolem lu doon wurus ak xaalis aki ndab ca kër Aji Sax ja, ak ca dencukaayi kër Buur, boole ca nit ñu mu jàpp, daldi dellu Samari.
Yowayas buurub Israyil saay na
15 Li des ci mbiri Yowayas ak li mu def ba ci njàmbaaram gi mu xareek Amaciya buurub Yuda, bindees na lépp moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. 16 Gannaaw gi Buur Yowayas saay, fekki ay maamam, ñu denc ko Samari, fa bàmmeelu buuri Israyil. Doomam Yerbowam falu buur, wuutu ko.
Amaciya buurub Yuda saay na
17 Amaciya doomu Yowas buurub Yuda dund na fukki at ak juróom gannaaw deewug buur Israyil Yowayas doomu Yowakas. 18 Li des ci mbiri Amaciya, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. 19 Lalal nañu ko pexe ca Yerusalem, mu daw dem Lakis. Ñu yónnee dabi ko ca Lakis, rey ko foofa. 20 Ba mu ko defee ay fas lañu yóbboo néew ba, denci ko Yerusalem, fa ay maamam, ca gox ba ñu naan Kër Daawuda.
21 Ba loolu wéyee waa Yuda gépp fal Asaryaab buur, mu wuutu baayam Amaciya, fekk mu am fukki at ak juróom benn. 22 Moom moo tabaxaat dëkk ba ñuy wax Elat, delloo ko ci biir Yuda, gannaaw ba Buur Amaciya saayee, fekki ay maamam.
Yerbowam mu ndaw falu na ca Israyil
23 Ba buurub Yuda Amaciya doomu Yowas duggee fukkeelu atu nguuram ak juróom, ca la Yerbowam doomu Yowayas falu ca Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na ñeent fukki at ak benn. 24 Muy def li Aji Sax ji ñaawlu, dëdduwul lenn ci bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat daan bàkkaarloo Israyil. 25 Moom moo delloo kemu réewum Israyil fa mu nekkoon, dale ko ca buntu dëkk ba ñuy wax Amat ba ca géeju Araba, muy la Aji Sax ji Yàllay Israyil waxoon jaamam ba, Yonent Yàlla Yunus, ma baayam Ametay cosaanoo Gaat Efer, Yunus jottli ko. 26 Fekk na Aji Sax ji gis Israyil gépp, gor ak jaam, nekke fitna ju metti te amul kenn ku leen wallu. 27 Aji Sax ji nag nammul woona far turu Israyil, ba jant bi dootu ko tiim fenn. Moo tax mu may leen ku leen xettli, muy Yerbowam doomu Yowayas.
28 Li des ci mbiri Yerbowam ak mboolem lu mu def ak njàmbaaram gi mu xaree te nangoo ko dëkk yi ñuy wax Damaas ak Amat gu Yuda, delloo ko Israyil, bindees na lépp moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ci seeni jant. 29 Gannaaw gi Buur Yerbowam saay, fekki maamam ya doon buuri Israyil. Doomam Sàkkaryaac falu buur, wuutu ko.