Buur Daryus joxe na ndigal
6
1 Ba loolu amee Buur Daryus joxe ndigal, ñu seet ca kërug dencukaayi téere ya, fa ñu denc alali Babilon. 2 Ñu gis ca Egbatan, péeyu diiwaanu Medd, taxañ bu ñu bind seede bii:
3 At ma jëkk ca nguurug Buur Sirus, Buur Sirus joxe na ndigal ci mbirum kër Yàlla ga ca Yerusalem. Mu ne:
Nañu tabaxaat kër Yàlla gi, muy bérab bu ñuy sarxee ay sarax. Nañu dëgëral kenu ya. Na taxawaayam di juróom benn fukki xasaba, yaatuwaayam di juróom benn fukki xasab, 4 te ñetti sësalantey doj yu mag yu tegloo yu ne, ab sësalanteb dénk tege ca kawam. Nañu génnee njég ga ca alali Buur, joxe ko. 5 Bu loolu weesee, ndabi wurus yaak yu xaalis ya woon ca kër Yàlla ga, te Nabukodonosor jële woon ko ca kër Yàlla ga ca Yerusalem, indi ko Babilon, nañu ko delloo fa mu nekkoon ca kër Yàlla ga ca Yerusalem te fat ko fa.
6 Kon nag ñooñu di Tatnay boroom Wàllaa Dex ak Setar Bosnay ak seen nàttongo yay jawriñ ca Wàllaa Dex, nañu sore foofa. 7 Buleen tere liggéeyu kër Yàlla gee dox. Na boroom dëkki Yawut ñi ànd ak magi Yawut ñi, ñu tabaxaat kër Yàlla googu fa mu nekkoon.
8 Rax ci dolli ndigal a ngii tukkee ci man, jëm ci li ngeen wara defal magi Yawut yooyu ci biir liggéeyu kër Yàlla googu: Njég ga mu leen dikke, nañu leen ko fey ba mu mat, jële ko ca alali buur, ca galagi diiwaan ba ca Wàllaa Dex. Nañu ko fey ñooñu, ba liggéey ba baña taxaw. 9 Mboolem lu ci war, muy yëkk yu ndaw mbaa ay kuuy mbaa ay xar yu ndaw yu ñuy defal Yàlla Boroom asamaan saraxu dóomal, muy bele it mbaa xorom mbaa biiñ mbaa diw, lu ci sarxalkati Yerusalem laaj, nañu leen ko jox bés ak bés, te bañ koo sàggane. 10 Su ko defee ñu mana sarxalal Yàlla Boroom asamaan lu ko neex tey ñaanal Buur aki doomam gudd fan.
11 Gannaaw loolu ndigal a ngii tukkee ci man ñeel képp ku tebbi bii dogal: Dees na roccee ca néegam ab xànq, yékkati ko, wékk ko ca, ba noppi def këram ab sën ndax jëfam jooju. 12 Yàlla ji dëël turam boobu bérab nag, yal na daaneel bépp buur mbaa xeet wuy fexee tebbi bii dogal, ba nara yàq kër Yàlla gii ci Yerusalem.
Man Daryus maa joxe ndigal lii. Nañu ci farlu.
13 Ba mu ko defee Tatnay boroom Wàllaa Dex, ak Setar Bosnay ak seeni nàttongo daldi xar seen tànku tubéy ci jëfe ndigal la Buur Daryus joxe. 14 Magi Yawut ña nag tabax ba mu baax, mu dëppook kàdduy Yonent Yàlla Ase ak Sàkkaryaa, sëtub Ido. Ñu tabax ba sottal, muy la Aji Sax ji Yàllay Israyil santaane woon, te dëppook ndigalul Sirus ak Daryus ak Artaserses buuru Pers. 15 Kër gaa nga sotti ci ñetti fanu weeru Adar, juróom benneelu atu nguurug Daryus. 16 Ci kaw loolu mbooloom Israyil ànd ak sarxalkat yaak Leween ñaak mboolem ña ñibbsee ca ngàllo ga, ñu daloo tabax ba ci biir mbégte. 17 Sarxe nañu ca daloog kër Yàlla googu téeméeri yëkk, ak ñaar téeméeri kuuy ak ñeenti téeméeri xar yu ndaw, ak fukki sikket ak ñaar, dëppook limu giiri Israyil, def ko saraxu póotum bàkkaar, ñeel Israyil gépp. 18 Ci biir loolu ñu tabb sarxalkat ya, ca wàll ya ñu bokk ak Leween ña ca seeni kurél, ñu sasoo liggéeyu Yàlla ji ci Yerusalem, muy la ñu bind ci téereb Musaa.
19 Fukki fan ak ñeent ca weer wu jëkk wa nag, ña ñibbsee woon ngàllo ga daldi màggal bésub Mucc ba. 20 Fekk na sarxalkat yaak Leween ña laabal seen bopp, ba ñoom ñépp bokk laab. Ba loolu amee ñu rendi xarum bésub Mucc ba, ñeel mboolem ña ñibbsee ngàllo, ak ñoom sarxalkat yi ci seen bopp, ñook seeni bokk. 21 Ba mu ko defee, bànni Israyil ga ñibbsee ngàllo ga daldi bokk reerub bésub Mucc ba, ñook mboolem ña dogoo woon ak sobey yéefar yi ci réew mi, ngir sàkku Aji Sax ji, Yàllay Israyil. 22 Wormaal nañu it màggalu Mburu mu amul lawiir, diiru juróom ñaari fan, ci biir mbégte, ndax fekk na Aji Sax ji bégal leen lool ca na mu xiire buurub Asirib, mu yéwéne leen ba dimbali leen ci tabaxu kër Yàlla ga, Yàllay Israyil.