Elifas nee yaru Yàlla du ñàkk
4
1 Elifas waa Teman ba àddu ne:2 Ma jéema àddu boog, soo ma talee!
Ndaxam noppeeti, maneesu ko.
3 Yaw de, ñu bare jàngal nga leen,
loxo yu toqi woon, nga dooleel,
4 ku jangoon, nga wax, mu taxaw,
kuy óomam dammoon, nga dëgëral.
5 Léegi muy yaw, nga yoqi;
mbir mi dal fi sa kaw, nga jànnaxe.
6 Xanaa du sag ragal Yàllaay sa cëslaay,
sag maandute di sa yaakaar?
7 Seetal rekk, ana jaamburu Yàlla bu masa sànku?
Ana foo gis ku jub ku mujje yàqu?
8 Li ma gis daal, ku bey ñaawtéef,
ji coono, yaa koy góob.
9 Yàllaay wal noowam, nga sànku,
sànjam gelaw, nga jeele.
10 Gaynde ŋar, segg xiiru,
selli waxambaaney gaynde tojandoo.
11 Gaynde ga ñàkk um pàdd, dee,
doomi gaynde ga tasaaroo.
12 Man la kàddu dikkal ci kumpa,
sama nopp taataan ndéey la,
13 ci géntu guddi, fa xalaat di jaxasoo,
nelaw yu xóot dikkal boroom.
14 Tiitaange ne ma taral, may lox,
cér yépp di kat-kati.
15 Ngelaw lu sew jaare sama kanam,
sama kawari yaram ne sàyy-sàyyaaral.
16 Mu def ku taxaw, te xàmmiwuma ko,
di jëmm ju janook man, may gis.
Mu jëkke ne cell, mujje àddu, ma dégg.
17 Mu ne: «Nit man naa am njekk fa kanam Yàlla?
Am man naa laab fi kanam ki ko sàkk?
18 Ndegam surgaam ya ca asamaan sax wóoluw leen,
ay malaakaam sax, mu sikk leen,
19 gën ñi dëkke këri ban,
cosaanoo ci pëndub neen,
gëna neexa nappaaje gunóor.
20 Diggante subaak ngoon, ñu moxoñoo,
bala ngaa yég, ñu sànku fàww,
21 seen buumi xayma foqatiku,
ñu dee ci biir ag umple.»