7
1 Xanaa du fani doom aadama fi kaw suuf
àppu doñ-doñ la,
dundam di dundu liggéeykat bu ñu bind?
2 Daa mel ni jaam bu namm keppaar
mbaa mbindaan mu yàkkamtig peyam.
3 Noonu laa séddoo ay weeri mititu neen,
jagoo ni ay guddiy coono.
4 Damay tëdd te naa:
«Kañ laay jóg nag?»
Waaye guddi gudda gudd,
walbatiku ba fajar xar génnliku na ma!
5 Maa ngi sàngooy sax ak àkki ban,
sama der biy xar, di wal.
6 Kukkub ràbb sax
ni samay fan di jeexee ko gaaw,
poqe di jeex, te yaakaar amul.
 
7 Éy Yàlla, bul fàtte ne sama dund gii,
ag noo doŋŋ la,
te dootuma teg bët ngëneel.
8 Bët bi may gis tey du ma gisati,
dinga ma niir, fekk nekkatuma.
9 Niir wu naaxsaay, ne mes,
mooy ku wàcci njaniiw, du yéegati!
10 Du ñibbeeti këram,
dëkkuwaayam dootu ko fat.
11 Moo tax duma téye sama làmmiñ,
xanaa di waxe biir njàqare,
di jooye biir naqar.
12 Dama di Géej menn mbaa Ninki-nànka,
ba nga di ma booleek ku may wattu?
13 Dama naan: «Naa nopploo tëraayub laltu,
ba yennikoo ab lal sama tawat,»
14 nga di ma tiitale ay gént,
di ma xoqtale ay jeneer,
15 ba ku ma xojoon sax, ma jël,
nde dee a ma gënal dese yii yax.
16 Doy na sëkk! Dunduma ba fàww;
ba ma, samay fan genn noo la!
17 Luy nit ba nga di ko gëddaal,
bay def sam xel ci moom,
18 di ko nemmiku saa yoo xëyee,
di ko nattu saa su ne?
19 Doo ma dummóoyu boog,
may ma sax fu ma wonaasoo?
20 Yaw miy seetlu jaam ñi,
ma bàkkaar, lu mu lay wàññi?
Ana lu tax nga di ma diiral sa bopp nii,
ba ma mujj diis la gann?
21 Lu tee kon nga baal ma samag moy,
jéggal ma samag tooñ?
Léegi tey ma tëri biir suuf,
nga di ma seeta seet, fekk nekkatuma.