Ayóoba nee Yàlla du ku ñuy layool
9
1 Ayóoba dellu ne ko:2 Waaw, noonu la moos, xam naa ko!
Ana nu nit di ame dëgg fa kanam Yàlla?
3 Ku bëgga layook Yàlla it,
mu laaj la junni, doo tontu lenn.
4 Moo rafet xel, bare doole!
Ana ku koy jéema të, mu jig ko?
5 Keey randal tund yi te duñu ko yég;
keey mer, jàllarbi leen,
6 gësëm suuf fa mu tege,
ay kenoom jaayu.
7 Keey gëdd jant bi, aaye koo fenk,
ub ràpp biddiiwi asamaan.
8 Keey wéetoo di firi déndi asamaan,
di daagoo kawtey géej.
9 Moo sàkk dëllooñ gi féete bëj-gànnaar
ak yaar yi ci digg asamaan,
ak ga ca néegi bëj-saalum.
10 Keey def jëf ju màgg ju nattuwul,
ak kiraama yu limuwul.
11 Mu ngoog, daf may romb te duma ko gis,
jàll, wéy te duma ko yég.
12 Kii, bu këfee, ana ku koy tere?
Ana ku ko naa: «Looy def nii?»
13 Yàlla du dànk meram,
ciy tànkam la farandooy Raxab,
ninki-nànkay géej, di gappru!
14 Ana nu ma koy àddoo, man?
Ana kàddu yu may layook moom?
15 Su sama der setee it, duma mana àddu,
xanaa sama àttekat bii laay tinu.
16 Su ma ko woon cib layoo, mu wuyu itam,
du tax mu wóor ma ne dina ma teewlu.
17 Moom mi may rajaxee ngelaw lu réy,
te di ma gaaña gaañ ci dara,
18 mayuma sax ma astandiku,
xanaa reggal ma aw naqar.
19 Su dee kàttan, kee bare doole!
Su dee wàllu yoon, kan moo ma cay woo?
20 Ma am dëgg, sama kàddu sikkal ma,
ma mucc ayib, sama kàddu teg ma tooñ.
21 Maa mucc ayib a? Xam!
Maa sib sama dund gii!
22 Lépp benn la rekk! Moo tax ma ne:
«Ku mucc ayib ak ku bon lay boole fàkkas.»
23 Mbas ne jaas, rey ñu deful dara,
Yàlla di leen kekkook seen njàqare.
24 Àddinaa ngi tege ci loxol ku bon,
te Yàllaa ngi muur gëti àttekat yi!
Su dul moom ana ku mu doon?
25 Ab dawkat sax ni samay fan di jeexee ko raw.
Wone nañu gannaaw te gisuñu lu baax.
26 Samay fan tarxiis nañu, wéy, woyof ni gaali barax,
mbaa jaxaay ju naan jàyy cim rëbbam.
27 Su ma nee: «Naa fàtte sama tawat,
leeral kanam te bég,»
28 du tee ma ragal mboolem samay mitit,
nde xam naa ne du tee nga topp ma.
29 Ndegam maa tooñ,
ana lu may sonn, doye?
30 Su ma raggoo woon saabu,
ba raxasoo xeme sax,
31 du tee nga tàbbal ma cim leeñ,
ba samay yére sax seexlu ma.
32 Yàlla da dul nit ni man, ba may weranteek moom,
di ànd ak moom, layooji.
33 Su amoon sax kuy dox sunu digg, jubale nu;
sañ noo boole teg loxo,
34 teggil ma yetam, mu sore ma,
ba darajaam ju raglu dootu ma tiital,
35 konoon ma wax ak moom te duma tiit.
Waaye gannaaw demewul noonu, man laak man!