33
1 Léegi Baay Ayóoba, ngalla déglul samay wax
te teewlu sama kàddu yépp.
2 Xaaral, ma àddu boog,
ba sama làmmiñ tudd li may bëgga wax.
3 Xel mu dëggu laay waxe,
samay kàddu di xam-xam bu wóor.
4 Ngelawal Yàllaa ma sos,
noowal Aji Man ji daal a ma may bakkan.
5 Soo manee, tontu ma;
defarul, janook man.
6 Maa ngii, yem ak yaw fa Yàlla;
ci ban lañu ma mooñe man itam.
7 Du sama ñàngaay bu lay tiital,
du sama daraja ju la diis.
Yàlla du moroom
8 Yaa wax déy, ma dégg,
te dégg naa bu baax say kàddu.
9 Nga ne: «Set laa def, tooñuma;
mucc ayib laa def, ñaawuma fenn.
10 Waaye Yàllaa ngii di ma wuta taqal,
def ma ab noonam,
11 jéng ma,
di xool fépp fu ma jaare.»
12 Foofu déy, moy nga dëgg, ma wax la ko,
Yàllaa sut doom aadama.
13 Ana loo koy sikke,
naan du layoo lenn ci mboolemi jëfam?
Yàlla dina wax ciy gént
14 Yàlla déy, dees koo teewluwul,
waaye day wax benn yoon ba yaar
15 ci biir peeñum géntu guddi,
fa nelaw dabe nit,
ba mu yàndoore kaw lalam.
16 Mu ne ko rukk ndéey,
boole kook màndarga, artoo ko ko,
17 ngir dëdduloo doom aadama ji ay jëfam,
musal jàmbaar cig réy,
18 sorale bakkanam pax,
ba ab xeej du ko bóoma.
Eliyu nee mitit ndéey la
19 Nit dina mbugaloo mitit wu ko tëral,
muy kat-kati rekk.
20 Day bañ dugub,
seexlu ñam wu ko gënoona neex,
21 jeex tàkk bay réer ak a feeñ,
yaxam ya ne fàŋŋ te sàngu woon,
22 dundam dëgmal ndee,
bakkanam di jegeji pax.
Eliyu nee njotlaay du ñàkk
23 Waaye su nit ki amee malaakam àttekat,
nay kenn sax ci junniy malaaka,
ngir xamal nit ki li ko war,
24 da koy baaxe, daldi ne Yàlla:
«Musal ko ba du wàccagum biir pax.
Maa ngeek njotlaayam.»
25 Yaram wa jotaat tooyaayu ndaw,
mu amaat dooley ngoneem;
26 bu ñaanee Yàlla, mu nangul ko,
geesu ko, mu sarxolle,
nde Yàllaay fey nit njekkam,
27 nit ki seedeeli ko ca nit ña, ne:
«Maa bàkkaar, maa xëtt njub,
te feyeesu ma ko sax!
28 Yàllaa ma jot ba jàlluma, jëm pax,
xanaa dellu di gis ug leer.»
 
29 Lii lépp déy, la Yàlla di def,
mook nit ñaari yoon ba ñett,
30 ngir sorale bakkanam pax,
bàyyee ko leeraangey àddina.
31 Baay Ayóoba, teewlul, déglu ma,
neel cell, ma wax la, man.
32 Soo amee lenn loo wax, àddul;
waxal, ngir bëgg naa laa dëggal.
33 Lu ko moy nag, yaa may déglu,
ne cell, ma jàngal la xam-xam.