Muus, mucc
2
1 Sama doom, déggal samay wax,fonk samay santaane.
2 Teewlul xel mu rafet,
sam xel di dégg.
3 Ngalla wutala dégg,
wool dég-dég wall.
4 Sàkkul xel mu rafet ni xaalis,
wut ko ni alal ju làqu.
5 Kon nga xam luy ragal Aji Sax ji,
xam Yàllaa di kan;
6 ndax Aji Sax jeey maye xel mu rafet,
kàddoom di taxa xam, di dégg.
7 Day dencalal ndam kiy jubal,
di yiir ku mat.
8 Day wattu ku jub fu mu jaare,
di sàmm wóllëreem ciw yoon.
9 Kon nga xam njub ak yoon,
xam jubal ak mboolem yoonu mbaax.
10 Ndax xel mu rafet miy tàbbi sa xol,
nga xam, sa xol tooy,
11 nga foog, fegu,
am ug dégg, raw,
12 mucc ci yoonu ku bon
ak kuy wax lu jekkadi,
13 mucc ci kuy wacc yoonu njub,
di jaare mbedd yu lëndëm.
14 Kon nga mucc ci kuy def lu bon,
tey bànneexoo lu jekkadi.
15 Yoonu ku ni mel day lunk,
jaaruwaayam dëng.
16 Xel mu rafet da lay musal ci ndaw su yemadi,
bokk feneen, di wax lu neex.
17 Day dëddu wóllëreem, ba muy ndaw,
fàtte kóllëreem ak Yàllaam.
18 Këram day joy wuti ndee,
ay jaaruwaayam jëm njaniiw.
19 Ku dem ca moom dootoo délsi,
doo gisati yoonu dund mukk.
20 Kon nag aweel mbeddum waa ju baax,
toppal yoonu ku jub,
21 ndax kuy jubal ay dëkke réew mi,
te ku mat a fiy des.
22 Ku bon, ñu dagge ci réew mi;
kuy fecci worma, ñu buddi, sànni.