Ku dégg ndigal, jariñu
4
1 Gone yi, tee ngeena dégg yaru baay,te déglu, ba am ug dégg?
2 Maa ngi leen di jàngal lu baax,
buleen fàtte sama njàngle.
3 Man it amoon naa baay,
di benn bàjjo ci saa ndey.
4 Baay digal ma, ne ma:
«Jàppal samay wax ci sam xel,
di jëfe samay santaane, ba dund.
5 Amal xel mu rafet akug dégg.
Bul fàtte te bul moy samay wax.
6 Bul dëddu xel mu rafet, da lay aar;
sopp ko, mu sàmm la.
7 Njàlbéenu xel mu rafet mooy sàkku ko;
ak loo mana am, amal ug dégg.
8 Nawal xel mu rafet, mu darajaal la;
tafoo ko, mu teral la.
9 Da lay takkal kaala gu jekk,
solal la mbaxanam buur.»
Moytul yoonu ku bon
10 Déglul, doom, te dégg saay wax,
ndax nga gudd fan.
11 Yoon wu xelu laa la teg,
jaarloo la yoonu njub.
12 Doo dox ba tërëf,
doo daw, téqtalu.
13 Ŋoyal cib yar, bul yoqi,
sàmm ko, moo yor sa bakkan.
14 Yoonu ku bon, bu ci tegu;
fu ab soxor di jaar, bu fa dox.
15 Moyul, bu fa jaare;
mbasal te wéy!
16 Ku bon du nelaw te lorewul,
du dajjant ba kera muy téqe.
17 Daa bon, def ko lekk,
di màndee coxoram.
18 Yoonu ku jub day leer,
ba ne ràññ ni bëccëg.
19 Yoonu ku bon ne këruus,
du xam lu muy téqtaloo.
Saxal ci lu baax
20 Doom, déglul samay kàddu,
teewlul samay wax.
21 Bu ci noppee ja jàkk,
te jàpp ko ci sa biir xel.
22 Mooy dundloo ku ci jàpp,
di wéral jëmmam jépp.
23 Sàmmala sàmm sab xol,
nde xalaati xol ngay jëfe.
24 Dàqal wor, mu sore la;
kàdduy naxe, na la dànd.
25 Xooleel, sa bët ne jàkk,
ngay xool sa kanam màkk.
26 Seetlul fi ngay teg tànk,
ba foo awe, mu wóor.
27 Bul jàdd, ndijoor mbaa càmmoñ,
na sa tànk moyu lu bon.