Bul gàddul kenn bor
6
1 Doom, dangaa gàddul nit bor,dige feyal jaambur,
2 saw làmmiñ yeb la cim pax,
nga keppu?
3 Yaa ngi ci sa loxoy moroom,
kon defal nii, doom, ba rëcc:
doxal tinuji ko,
raamali ko.
4 Bul gëmm,
bul nelaw!
5 Dawal ni kéwél gu rëcc ub rëbb,
ne fërr ni picc mu raw ab fiirkat.
Bul yaafus
6 Yaafus bee, xoolal xorondom,
seetal ci moom, ba muus.
7 Du ku ko yilif mbaa ku koy sas,
te jiiteesu ko.
8 Bu jotee mu denc ab dundam,
mu jot, mu for lekkam.
9 Moo yaafus bi, foo àppal tëraay bi?
Loo deeti xaar ci yewwu?
10 Ngay dajjant ak a for bët,
di tegley loxook a jaaxaan.
11 Néewlee ngi lay dikkal nib sàcc,
ñàkk gànnaayul la.
Ku dëng, nii lay mel
12 Ku tekkeedi te bon,
day wër di fen,
13 day piis, di wokkeb tànk,
di waxe baaraam,
14 jekkadiy xalaat, di mébét lu bon
aka yokku ay.
15 Moo tax musiba di jekki dal ko,
mu jekki yàqu, ba wees paj.
Aji Sax ji bañ na lii
16 Juróom benn a ngii yu Aji Sax ji bañ,
ba ci juróom yaar yu mu seexlu:
17 kuy daŋŋiiral,
kuy fen,
kuy rey nit ku deful dara,
18 kuy fexe lu bon ci xolam,
kuy gaawtuy def lu ñaaw,
19 seede buy fen rekk,
rawatina kuy yokku ay ci biiri bokk.
Ku njaaloo gis ko
20 Doom, defal li la baay sant,
te bul wacc ndigalal yaay.
21 Takkal foo tollu, taf ci sa xol,
fas ko ci sa baat.
22 Booy dox mu di la jiite,
nga tëdd, mu di la sàmm,
nga yewwu, mu di la waxal.
23 Santaane da lay niital,
ndigal leeralal la,
artook ub yar di yoonu dund.
24 Da lay aar ci ndaw su bon
ak jabaru jaambur ak làmmiñam wu neex.
25 Bu ko xemmeme taaram,
bumu la fiir aki lamsal.
26 Dogu mburu fey nab gànc;
waaye jabaru jaambur, bakkanu lëmm.
27 Te ku ne sawara cas, tafoo,
lakk say yére.
28 Ku dox ciy xal it,
say tànk ñor.
29 Mooy ànd ak jabaru jaambur,
ku ko def gis ko.
30 Deesul sikk ku sàcc aw ñam,
def ci biiram ndax xiif.
31 Waaye bu feeñee, fey boroom juróom yaari yoon,
joxe alalu këram yépp.
32 Njaaloo di ñàkk bopp,
kuy sànk bakkanam a koy def.
33 Mbugal ak toroxte dib añam,
te gàcceem du deñ.
34 Fiiraange day feesal xolu góor,
te du ñéeblu buy feyu.
35 Du faale ndàmpaay,
loo ko may, may, du giif.