Ñaari berndee ngi
(Saar 9)
Xel mu Rafet a ngi berndeel
9
1 Soxna si, Xel mu Rafet daa tabax këram,
yett juróom yaari kenoom.
2 Mu rendi ag juram,
njafaan ay biiñam, xelli,
taaj ay ndabam.
3 Xel mu Rafet yónni ay janqam,
di wootee fu kawee kawe ca dëkk ba,
4 naan: «Képp ku téxét, jàddal ba fii!»
Ku ñàkk bopp, mu ne ko:
5 «Kaay, ma may la, nga lekk,
xellil lay biiñ, nga naan.
6 Dëddul jëfi téxét ba dund,
di jubal ci yoonu dégg.»
Kuy xeloo ngi ak kuy ñaawle
7 Artu kuy ñaawle, feyoo saaga rekk,
yedd ab soxor, yooloo loraange.
8 Bul yedd kuy ñaawle, da lay jéppi;
yeddal ku rafet xel, mu naw la.
9 Xelalal ku xelu, mu yokku.
Xamalal ku jub, mu yokk njàngam.
10 Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu rafet xel,
xam Aji Sell ji di am ug dégg.
11 Maay Xel mu Rafet, ku ma topp gudd fan,
dund, dundati.
12 Rafet xel, jariñu,
kuy kókkalee, wéetook sa añ.
Ku dofee ngi berndeel
13 Jigéen ju dof day xumb,
reew, du xam lu xew.
14 Day toog bunt këram,
mbaa fu kawee kawe ca dëkk ba,
15 di woo ña fay jaare
te jubal seenu yoon.
16 Ma nga naa: «Képp ku téxét, jàddal ba fii!»
Ku ñàkk bopp, mu ne ko:
17 «Ndox mu lewul a neex,
ñamu làqu-lekk dàqati.»
18 Waaye kooka du xam ne waa njaniiw a nga fa,
te ku wuyji, tàbbi biir bàmmeel.