13
1 Doom ju xelu dégg yaru baay,
kuy ñaawle faalewuli àrtu.
 
2 Wax ju rafet yool na boroom,
workat fitna la namm.
 
3 Moom sa làmmiñ, sàmm sa bakkan;
rattaxle, yàqule.
 
4 Ab yaafus day yaakaar, du am;
ab njaxlaf sàkku, woomle.
 
5 Ku jub bañ na ay fen,
ku soxor di indi gàcceek yeraange.
 
6 Ku mat day jub, ba fegu;
moykat soxor, ba sànku.
 
7 Nit a ngi am-amlu, amul dara;
nit di dee-deelu te fees dell.
 
8 Ku am ay fey alal, ba mucc;
ku amul deesu ko tëkku.
 
9 Ku jub day leer nàññ,
ab soxor mel ni taal bu fey.
 
10 Réy-réylu jote rekk lay jur,
ku dégg ndigal a xelu.
 
11 Alal ju lewul day naaw;
foral benn-benn, ba biibal.
 
12 Yaakaar ju tas day jeexal xol,
aajo ju faju di suuxat bakkan.
 
13 Ku sofental ndigalu Yàlla, yàqule;
ku jëfe santaane Yàlla, yoolu.
 
14 Njàngle mu xelu day suuxat bakkan,
ba boroom du tàbbi ci fiiri ndee.
 
15 Dangay xam lu jaadu, ñu naw la;
yoonu workat day metti.
 
16 Képp ku teey jëfe xam-xam;
ab dof ay siiwal ndofam.
 
17 Ndaw lu bon day loru.
Ndaw lu wóor garab la ci nit.
 
18 Ku sàggane yoonu yar, séddoo ñàkk ak gàcce;
kuy déggi àrtu, am teraanga.
 
19 Aajo ju faju tooyal na xol,
te ab dof jomb naa dëddu mbon.
 
20 Àndal ak ku xelu, sam xel rafet;
ku lëngook ub dof, loru.
 
21 Ay topp na moykat,
ku jub juble.
 
22 Ku baax, donale ba cay sëtam;
alalu moykat, muuru ku jub.
 
23 Ku néewle bey na, meññeef ne gàññ,
ñu àtte ko ñàkkal, mu ñàkk ko.
 
24 Ku dul bantal sa doom, bëggoo ko.
Ku bëgg sa doom teel koo yar.
 
25 Ku jub day lekk ba regg,
soxor ba dëkke xiif.