Ngën-gi-woy
1
1 Lii, di ngën-gi-woy, ñeel Suleymaan.
 
Ndaw si
2 Fóon maa, ngalla fóon ma,
sa cofeel a ma dàqal biiñ.
3 Sa diw yi ngay xeeñoo neex,
saw tur jib, mel ni lu xeeñ a xelli.
Moo tax janq ji nob la.
4 Yóbbaale ma, nu daw, dem.
Sama buur, yóbbu ma sa néeg,
nu bokk mbég ak bànneex,
di tàqamtikoo sa cofeel gi dàq biiñ.
Ñoo yey nob la!
Njëkke ñooru, mujje xejjoo
Ndaw si
5 Yeen janqi Yerusalem, damaa ñuul, rafet;
ñuul ni xayma ya ca Kedara,
mel ni ridoy Buur Suleymaan.
6 Buleen ma xoole sama ñuulaay bi,
jant bee ma lakk.
Samay càmmiñ a ma mere,
di ma wattuloo tóokëri reseñ ya,
te wattuwuma sama tóokëri boppb.
7 Sama soppey xol, ngalla wax ma
ana fooy foral,
di fa gooral, digg bëccëg?
Lu ko moy may muuru, di la wër
fi say xarit ak seeni gétt.
 
Waa ji
8 Aa! Xamoo koo?
Yaw mi dàq ci jigéen ñi!
Génnal rekk, topp wewi jur gi,
sàmmi say tef,
fi dendeek mbaari sàmm si.
 
9 Xarit, xam nga lu ma lay xoole?
Yànjaayu wajan wu takk watiiru Firawna.
10 Sa lex yaa ngi tàkk fi digg sàdd yi!
Céy wii loos ak caqu peram!
11 Sàddi wurus lanu lay defaral,
tapp ca xaalis.
 
Ndaw si
12 Li sama buur tëdd, di xéewlu lépp,
maa ngi gilli lu neex.
13 Sama nijaay di mbuusum ndàbb
may fanaan sama digg ween.
14 Saa nijaay, saa cabbu tóor-tóoru fuddën,
fa digg tóokëri Engedic.
 
Waa ji
15 Xarit, yaaka rafet,
yaaka taaru!
Say gët niy pitax.
 
Ndaw si
16 Nijaay, yaaka góorayiw,
yaaka maa neex!
Mbooy gu naat, nu laloo,
17 garabi seedar di sunu xànqi néeg,
garab gu dul ruus xadd kod.