Waa ji
5
1 Jigéen sama, séet sama, dikk naa sama tool,
sama ndàbb ak sama cuuraay, ma for,
sama lem xelli, ma lekk,
sama biiñ ak sama meew, ma naan.
 
Awu
Yeen soppe yi, lekkleen;
yeen ñi bëggante, naanleen ba màndi.
 
Xol jeex na, mujje neex
Ndaw si
2 Maa ngi nelaw, te xol yewwu;
dégluleen, sama nijaay ay fëgg.
Mu ne: «Xaritoo, jigéen sama, ubbil ma,
sama nenne, alal sama!
Sama bopp a ngi laye ba tooy,
njañ li fanaanee guus.»
3 Ma ne ko: «Summiku naa de,
xanaa duma soluwaat?
Jàngu naa jeeg,
xanaa duma taqati?»
4 Sama nijaay yoor loxoom ci xarante bi,
sama yaram ne sàyy.
5 Ma ne bërét, di ubbil nijaay,
sama yoxo yi, diwu ndàbb di ca siit,
sama waaraam yi, ndàbb rogalaat
ba ci njàppul bunt bi.
6 Maa ubbil nijaay,
waaye nijaay waññiku na, ba wéy.
Ba mu waññikoo, tuuti ma dee.
Seet naa ko, gisuma ko;
ma woo ko, wuyuwul.
7 Wattukat yiy wër dëkk bi gis ma;
ñu dóor ma, gaañ ma,
ñori sama malaan.
Wattukati tata jaa!
 
8 Ngalla yeen, janqi Yerusalem, waatal-leen ma
ne su ngeen gisee sama nijaay,
ne ko damaa wopp ndax mbëggeel.
 
Janqi Yerusalem
9 Yaw mi dàq ci jigéen ñi,
ana lu sa nijaay gëne keneen?
Ana lu mu ëpplee keneen,
ba nga di nu waatloo lii?
 
Ndaw si
10 Sama nijaay daa xees, leer;
kenn la ci fukki junniy góor.
11 Kanam gi ni wurus, di wurusu ngalam;
njañ li lëmësu,
ñuul ni ndobin.
12 Gët yi ni pitax yu feggook wali ndox,
sangoo meew,
feggook ndox mu ne xéew.a
13 Lex ya di tool,
gàncax ga ne ca bann,
tuñ ya diy tóor-tóor,
ndàbb wale ca, rogalaat.
14 Yoxo yi banti wurus la,
ngën-gi-per tappe ca;
jëmm ja rattax ni bëñu ñay
laloo peri safiir;
15 yeel yi kenuy doj wu jafe la,
sampe ci tànki wurusu ngalam.
Meloom ni tundi Libaŋ,
di tànnéef ni garabi seedar.
16 Gémmiñam, bànneexi neen,
jëmmam jépp jara xédd!
Yeen janqi Yerusalem,
sama nijaay a ngoog, samab xarit.