Janqi Yerusalem
7
1 Dikkal, janqu waa Sulam bee, dikkal;dikkala dikk, nu niir la.
Waa ji
Moo, lu ngeen di seetaane janqub waa Sulam bi
ni kuy fecc galanu Ñaari Dali Xare?
2 Janqoo, lingeer sama,
sa tànk yee ka jekk ci sa dàll yi,
sa mooco yi mërgalu niy jaaro
yu ndaanaanu tëgg yette loxoom.
3 Sa jumbux bi di kaas bu mërgalu,
yàlla bumu ñàkk biiñu njafaan!
Sa biir bi di jalu pepp
mu ay tóor-tóor ñag.
4 Sa ween yi ni ñaari tef,
mbaa seexi kéwél.
5 Sa loos wi, coleet, rattax, ni tatay bëñi ñay;
say gët di lerxat ni déegi Esbon,
ya feggook buntu Bat Rabim.
Sa bakkan bi jub xocc ni tatay Libaŋ
ja tiim Damaas.
6 Sa bopp siggi ni tundu Karmel,
njañ liy nes-nesi ni sooyu buur,
létt yay fëy-fëyi, ba laaw buur.
7 Rafet, sopploo!
Soppee, bànneex nga!
8 Sa taxawaay bii garabu tàndarma la,
sa ween yi di cëggi doom ya.
9 Ma ne, maay yéeg tàndarma gi,
ŋëb doom yi.
Yal na say ween di sama cëggi reseñ,
sag noo jox ma doom yu xeeñ,
10 sa gémmiñ di xelli ngëneelu biiñ.
Ndaw si
Na walal sama nijaay,
tuurul ñiy nelaw.
11 Man, nijaay a moom,
te maay nammeelam.
Ayca ca tool ba
Ndaw si
12 Nijaay, ayca nu dem tool ba,
fanaani ca tóor-tóori fuddën yaa.
13 Nan teela xëyi ca tóokëri reseñ ya,
bu reseñ ji jebbee,
mbaa tóor-tóor yi focci,
mbaa gërënaat ji tóor, nu gis.
Fa laa lay jébbale mbëggeel.
14 Tóor-tóor yu xeeñb yaa ngi gilli,
lépp luy doom yu neex aje sunu bunt néeg,
yu yees yaak ya woon,
ma boole dencal la, nijaay.